Woy-Yàlla 40 (87)
Reeru Sang bi
(1 Korent 11:23-26)
1. Yeowa, suñu Baay ba ca kow,
Guddi gu mag gaa ngook, agsi.
Ca fukki fan yaak ñeent ca weeru Nisan,
Sa tur, jollil nga ci suuf si.
Ba Israyel génnee Misara,
Fekk reere na mbote ma,
Ñooña nekkoon ay jaam, yoo soogoon a goreel,
Woy nañ’ sa ndam ak sa màqaama.
2. Krist, Sang bi, tur na deretam,
Amal noonu la ñu bindoon.
Ñu ngi, Yaa, di màggal sa tur wi sell
Ak mbëggeelu Krist, tey ci ngoon.
Ci taabal bi ñu lal, ñu ngiy gis
Biiñ beek mburu mi, ay misaal;
Nañ’ fàttaliku ne ñam yu sell lañu;
Ku ko yeyoowul waru leen laal.
3. Mburu mi, yaram’ Krist lay misaal,
Wu mu ñu jébbalal ba fàw’.
Kaasu biiñ bi di misaalu deretam,
Ndax ci bàkkaar ak dee ñu raw.
Na Fàttaliku bii doon lu sax
Ci suñu xel ak suñu xol.
Nañu dox bés bu ne ci yoon, wi Krist xàll,
Dund ga dul jeex doon suñu yool.