Woy-Yàlla 56 (135)
Yeowa, suñu Dëkkuwaay
(Sabuur 90:1)
1. Yaw Yaa, yaa doon suñu dëkkuwaay,
Dale ci ba-ñ’ sosoo ba tey.
Laata nga fee sàkk tund yi,
Doon nga yéem ndax sa ndam lu réy.
Yaay Yàlla dëgg ba abadan;
Yaw Yaa, doo soppeeku ba fàw’.
Ak loo delloo nit ci ban ak suuf,
Sa mbëggeel tax na ñu mën’ raw.
2. Junniy at, diir bu gudd ci ñun,
Ci yaw a ngi mel ni démb.
Nit a ngi mel ni ñax miy tóor-tóor;
Day mujj’ ruus, niki jëmb.
Juróom-ñaar walla ñet’ fukki at
Lañu mën a yaakaar dund;
Ndaxam li ñuy yóbbe mooy coono;
Tiis ak dundu nit kee ànd.
3. Jàngal ñu ni ñuy xaymaa suñ’ fan,
Ndax ñu mën cee jële bànneex.
Ba ñuy góor-góorlu sàkku sago,
Ñu ngi lay gërëm bu dul jeex.
Yaw Yeowa, na sa yiw wàcc
Ci sa kow jaam, yi ñuy nattu.
Feddalil liggéeyu suñ’ loxo;
Feddalil suñu yëngatu.