Woy-Yàlla 57 (136)
Jaam yu goree ngiy barkeel Yeowa
(Sabuur 18:25)
1. Gor yaa ngi lay naw, Yaa, di la woy ci dunyaa;
Yal nanga leen may ñu doon ñu texe.
Yaw yaa jar a màggal; say yoon dañuy jubal.
Ci ngor, di la sargal lañuy fexe.
2. Siggal la lañuy wut—cant gi du doon tuut—
Dañuy wottu ci lép’, di daw sobe.
Wax ñu ni suñu ngëm, waaw, kanam mënee jëm.
Yal nañ’ fésal ngor lëm’, su la soobee.
3. Baal ñu, gën ñoo xamal liy sa nas giy jommal,
Ak Nguur gi nga samp, muy lu yéeme.
Deel won ñép’ li la doy, ndax kenn bañ a moy.
Nangul ñaan yeek suñ’ woy, noo ko tàmme.
4. Fexeel, yaw suñ’ xarit, ba ñu dàq bép’ tiit,
Ba ñuy bàkk sa nguur tey woy sa tur.
Yal na ñu jàmm yiir teyit suñuy woy riir;
Ci diggu gépp giir sa pal lay jur.