Woy-Yàlla 67 (156)
“Bëgg naa ko”
(Lukk 5:13)
1. Ndaw mbëggeel, gu ñu Yeesu won,
Ba mu wàccee fa mu dëkkoon.
Ndax nit mën a dund, xam li dëgg wund,
Xamle na dëggu Yaa ak liy yoon.
Nit ku nekk la daan dëfël;
Ku wopp, làggi, mu wéral.
Sasam, dëg’, moom miy buur, matal na ko;
Ak mbëggeel, daan na wax: “Bëg’ naa ko.”
2. Ndaw ndimbal lu Yàlla amal!
Ndaxte jaam bu takku la fal.
Nañ’ ko jàppleek mbég; suñu farlu na yég,
Ndax ku néew doole ñu mën’ musal.
Dëgg, kooku dana mën’ wax
Ne fonk nañu ko bu baax.
Su gitim ak jiirim ci yaw jubloo,
Ndax, yaw, dinga wuyoo: “Bëg’ naa ko”?
3. Bëgg Yàllaa tax ñuy xamle,
Di dellusi tey jàngale
Ñii jamonoy jooyloo, teyit di yoqiloo;
Ñiiy wut dëgg war nañ’ jàpple.
Akay mbég, bu ñooñu nàndee
Dëgg gi, ba di ko dunde,
Sawar ci njaamu Yaa te jiital ko.
Wax jilee ko waral: “Bëg’ naa ko”.