Woy-Yàlla 68 (157)
Jaamuleen Yeowa ci seen ndaw
(Dajalekat 12:1)
1. Ci tuñiy gone, Yaa mas naa tagge;
Sargal nañ’ Yeesu, ni Mu ko bëgge.
Waaw, gone sax mën naa màggal Yàllaam,
Ànd ak mag ñi ngir woy sellaayam.
2. Doomiy karceen yi fonk liy dëgg,
Wegleen seen’ way-jur, ba ngeen di màgg.
Liy yoon, am nañ’ sañ-sañu jàngal leen.
War ngeen leen a déggal te bégal leen.
3. Yéen ndaw ñi, góor-góorluleen ndax sell;
Jàngleen a wàkkirlu ci Yàlla.
Buleen wut bayre ci dunyaa, biy nax;
Ànd bu bon day yàq nit ku baax.
4. Sooleen fàttalikoo Yaa ci seen ndaw,
Te ci njaamoom, ci dëg’ ak xel, ngeen aw,
Ba ngeen di màgg, dingeen gën di bég,
Te ci xolam, Yàlla bànneex lay yég.