Woy-Yàlla 69 (160)
Nañu dox ci ngor lëmm
(Sabuur 26:1)
1. Céy Yeowa, Boroom bi, àtte ma.
Ci yaw laa wàkkirlu, di dox ci ngor lëmm.
Seppali ma, te fexe maa seetlu;
Seggal xel meek xol bi ndax ma mën’ barkeelu.
(AWU)
Lu jëm ci man, dogu naa, du caaxaan:
Di dox, ba abadan, ci ngor lëmm laay ñaan.
2. Duma dëju ak nit ñu bon, ñiy fen.
Sib naa àndub nit, ñi faalewul li jub fen’.
Ak ñi soxor bul faat sama bakkan,
Ak ñi seen loxo fees ak njublaŋ te añaan.
(Awu)
3. Li ma fonk dëkkuwaayu sa kër
Tax na ma jàpp ci sa njaamu, bu dëgër.
Te danaa dox, wër sa saraxukaay,
Di la gërëm ca kow, di tagg sa mbaaxaay.
(Awu)