Woy-Yàlla 75 (169)
Woy wu bees wi
(Sabuur 98:1)
1. Woyalleen Yàlla, Boroom bi, woyu mbég, wu bees;
Yéeneleen lu réy, li mu nar’ def ak li wees.
Màggalleen loxoom bu sell, biy yóbbuji ndam.
Àtteem ci kow nit ñi, daa jub ci suñ’ kanam.
(AWU)
Nañ’ leen woy!
Bu woy wu bees wi dal!
Nañ’ leen woy!
Nguuru Yaa lañu fal.
2. Xaaculleen Yàlla, yéen waa suuf si, yiy nox-noxi;
Taggleen Yeowa ak mbég, di rex-rexi.
Woyalleen ca kow Yeowa Yàlla, Boroom bi.
Ak xalam, buftaak liit, nañ’ ànd ci woy wi.
(Awu)
3. Géej gi am doole, ak li ci ne, Yaa nañ’ màggal.
Baatu ñii ci kow suuf, na jolli, bu-ñ’ baaral.
Duus yi, nañu bég; na dex yi tàccu, bu-ñ’ baaru.
Ñu kowe mbaa suufe, na tund yi awu.
(Awu)