Woy-Yàlla 76 (172)
Jëkkleen a wut Nguur gi
(Macë 6:33)
1. Am na lu neex Yaa Yeowa,
Di ko jural mbég dëgg,
Moo di Nguuru Doomam, Yeesu.
Jubbanti lép’ la bëgg.
Ngëm a tax yonent-yi séen ko
Te jàpp ci jooj’ yaakaar.
Tey, suñ’ Njiit Yeesoo ngi ñuy xiir,
Ñu def lu ni mel tey waar.
(AWU)
Jëkkleen a wut, kon, Nguur gi,
Ki ko sos ak liy njubte.
Jiitalleen Yaa, di ko làyyil,
Te jaamu kook takkute.
2. Ndaw cér bu jaamu Yàlla am,
Bokk ci sasu Nguur gi!
Ndegam loolu lañ’ ñu baaxe,
Nañu ci farlu léegi.
Bu ñuy jaaxle, kon, ngir ëllëg:
‘Lek’ ak naan, ndax dinaa am?’
Yaa dina ñu ko ci dollil,
Su ñu jëkkee wut Nguuram.
(Awu)
3. Léegi jamano jile jeex,
Yàlla samp fi ju bees.
Nit ñép’ dinañ’ tagg Yàlla;
Ak bànneex la suuf siy fees.
Nañ’ yéene xabaaru Nguur gi,
Ndax ñi mel ni xar mën’ xam
Ne seen yaakaar Yeowa la,
Akit njiitéefu Nguuram.
(Awu)