Woy-Yàlla 86 (193)
Waarleen “xabaar bu baax bii ci Nguur gi”!
(Macë 24:14)
1. Xabaar bu baax bii ci Nguur gi war nan’ yégle,
Muy seede fu ne akit ci ku ne.
Turu Yeowa, nag, war nañu koo xamle;
‘Dina ko làyyil’ lañuy yéene.
(AWU)
Kon, waarleen xabaar bu baax bii.
Ngir Yàlla ñii woyaf nañ’ góobi.
Ci turu Yaa, ba fàw’, na ñép’ woo, mag ak ndaw;
Nañu ko làyyil te di ko naw.
2. Jamano jii daa bon, nañ’ sàmm suñu jot
Ci nekkal suñ’ bopp ak mbuumbaay.
Nañ’ jiital Nguuru Yaa ak waaraate bi kot’,
Mu doon, nag, ba fàw’ suñu ngañaay.
(Awu)
3. Ci biir waaraate bi, Yàlla bu ngeen jàq,
Ndax dañu leen xatal bu metti.
Saxleen ci ak teggin; fit, ragal lay dàq.
Doguleen ba li-ñ’ leen sas sotti.
(Awu)