Woy-Yàlla 87 (195)
Bésu Yeowa la
(Sabuur 118:24)
1. Bésu Yeowa la. Riig nañ’ Nguuru Yàlla.
Ca Siyon, samp na aw Doju koñ.
Na baatu ñép’ jolli, nañ’ ko woy, xeeb dolli,
Nguuram kep’ lañ’ wóolu ngir fomp suñ’ rangooñ.
(AWU)
Loo ñuy indil, Nguuru Yeowa?
Njubte, dëgg gu làmboo ndam.
Ak lanati, Nguuru Yeowa?
Dund ba fàw’ ci àjjanaam.
Woyleen Kiy Aji-Kilifa,
Ndax ngoram ak mbëggeelam.
2. Tey, Buur Yeesu lañ’ fal, xare Yaa ngiy dégmal.
Jamonoy Ibliis a ngiy wéy léegi.
Kàddu geek fit waaral; xabaaram deel weejal.
Dimbalil ñi woyaf ñu topp Kàddu gi.
(Awu)
3. Buur beek Nguuram nañ’ naw; moom lañu fal ca kaw.
Yaa la taxawal; nguuram doy na ñu.
Ci kër’ Yaa deel dugg! Yiwam deel ñaan dëgg,
Ndax ñu bey suñu sas ba fàw’, di ci kañu.
(Awu)