Woy-Yàlla 92 (209)
Toppleen ci Buur, biy xarekat!
(Efes 6:16, 17)
1. Yeowa, dañ’ am woy wu ñu lay woyal:
Sa Nguur ak sa ndam lañu bëgg’ woy.
Dañoo am xabaar bu ñépp mën’ nànd;
Suñu yónnent, nañ’ fexe bañ koo moy.
(AWU)
Kon, aywa! (Aywa!)
Ak fit, aywa! (Ak fit, aywa!)
Yéen jàmbaar yi, kon, aywa,
Ngir xeex nooniy Yeowa;
Toppleen ci Xarekat, bi dul tële.
Ci seen xare, dingeen baaxle!
2. Jàmbaariy Yàlla, jógleen te xareji,
Ñey-xareb mbooloo Yaa leen di jiite.
Jëlleen pakku ngëm gi ak jaasiy xel mi;
Solleen kasku muccam ak kóolute.
(Awu)
3. Suñu kàttan taxul ñu daan suñuy noon;
Mën-mën doŋ’ taxul ñu yóbbu ndam li.
Waaye ñép’ mën nañ’ daan ci dooley Yàlla,
Loolu tax turu Yeowa jolli.
(Awu)