Woy-Yàlla 93 (211)
Nañu bokk, ak mbég, ci ngóob mi
(Macë 9:37, 38)
1. Ñu ngiy dund jamanoy ngóob mi;
Tey, cér bu jéggi dayo la.
Malaaka yi ñoo di góobkat yi,
Ñu ànd ci, ndax moo yell.
Krist Yeesu mooy ki xàll yoon wi,
Ba mu jiwee ci biir tool bi.
Dara desatul lu dul góob tool yi;
Ak mbég nañu dem, kon, góobi.
2. Feesal nañ’ sàq yeek dugub bi.
Ñiiy ñax mu bon mi fés nañu.
Te ñu ngi ñuy jéem a gàllankoor,
Di yëytu; lool’ tiitaluñu.
Mbooloo Yeowa, moom, daa jàpp;
Liggéeyub bés lëm’ duñu daw,
Ndax ngóobum ñi mel ni ay xar daa réy;
Ci dimbali leen, nañ’ taxaw.
3. Bëgg Yeowaak suñu moroom
Da ñuy xiir ci doon ñu farlu.
Ndegam muj gi lañu jàkkaarlool,
Ci ngóob mi nañu góor-góorlu.
Ci jamanoy ngóob mii, lañ’ war’ jëf,
Di jàpple ñiiy dégluji.
Ndaw mbég yu ñuy am ci tool bi, ci ñoom,
Ba ñuy ràññee ñiiy dugub ji.
4. Krist Yeesu, Boroom ngóob gaa ngiy gis
Ni ñuy fexe pepp bi ñor.
Ñi ñu war’ jàngal, ni tool yu weex,
Ay ndiiraan lañu, ci lu wóor!
Mbég yi ñu ciy jële ñoo dàq,
Ba ñuy ànd liggéey ak Yaa.
War nañ’ ci sawar, di ko def ak mbég,
Takku ci ngóob mi ci dunyaa.