Woy-Yàlla 94 (212)
Jëre-jëf Yeowa!
(1 Tesalonikk 5:18)
1. Jëre-jëf Yeowa, ndax yaa ñu wàcceel
Leer gu jafe; tus lañ’ ko dul wecceel.
Jaa-jëf ci li ñu am céru mën laa ñaan;
Di la jegeey tax, suñ’ tiis ñu mën’ daan.
2. Jëre-jëf Yeowa, ndax sa Doom jiy gor;
Am na ndam ci dee ak Ades, yiy lor.
Jaa-jëf ci sa njiitéef, bu ñu lay jaamu;
Noonu mën nañ’ fey dige, bi-ñ’ taamu.
3. Jëre-jëf Yeowa, ci suñuy mbokk;
Ànd yu baax, seen biir lañ’ koy fekk.
Jaa-jëf it ci mayug sa doole jiy jëf;
Moo ñuy dimbali ndax ñu bañ’ tërëf.
4. Jëre-jëf suñ’ Yàlla, ci céru xamle
Sa tur ak dëgg, gi ñuy jàngale.
Jaa-jëf ndax, léegi, musiba yép’ ne mes,
Ba barkey sa Nguur, ba fàw’, di fi des.