Woy-Yàlla 97 (217)
Nañu xaritook Yeowa
(Sabuur 15:1, 2)
1. Céy, Yeowa Yàlla, kan ay doon sa xarit?
Kan ngay dalal ci sa tànt ba fàw’, mu doon sa nit?
Nit ki njaamoom sell, te ak fit fees dell,
Waaw, ki xolam laab tey wax ak a jëf ci say xàll.
Kan, Yeowa Yàlla, ngay fasal kóllëre?
Kuy dëkk ak yow ci sa tund, doon sa wóllëre?
Kiy wone ciy waxam, yar ak xam-xam, tegginam ci moroomam.
(AWU)
Yeowa, yal na-ñ’ doon xarit ba abadan.
2. Kan, Yaa Yeowa, ngay dalal ba abadan?
Kan ay doon sa xarit, ki ngay jëflanteel dëggantaan?
Waaw, kiy sàmm kàddoom, ci coonoom ak nattoom,
Ki ne xocc ci mbëggeel, tey def dëgg gi geñoom.
Céy Yeowa Yàlla, xaritoo lañuy wut.
Sa Kàddoo ngi ñuy xamal li jub ak li daganut.
War nañ jubbantiku, doon ñu takku, ci doon say gaa di bàkku.
(Awu)
3. Ak yaw, Yaa Yeowa, ba fàw’ dinañ’ dëkk.
Waaw, sa jàmm ji sut lépp, xel mënu ko takk.
Jaare ci Krist Yeesu, mujj nañoo yeeslu
Ci sa njaamu, ay ndiiraani nit a ngiy barkeelu.
Noonu Aji-Kàttan, dinañ’ wéy di sàmm
Sa kóllëre ak dundin gu sell, ne ci temm.
Ñun mbooloo mu déggoo, dañoo jagoo jox la njaam gi nga yelloo.
(Awu)