Woy-Yàlla 98 (220)
Suñu àjjana: tey ak ëllëg
(2 Korent 12:4)
1. Yeowa Yàlla, ñu-ng’ lay màggal
Ngir suñu àjjanay tey.
Li ñu fay jàng, ñaan ak’ daje
Daf’ ñuy yokk sagook teey.
Waaw, nañu gërëm Yaa
Ndax barkeem yu réy;
Wax dëgg, ci njaamoom
Am nañu mbég tey!
Bëgg la, yaw Yaa, ak suñ’ moroom
Mooy buum gi gën a dëgër.
Moo tax ñu déggoo ci sa njaamu,
Taxaw ba fàw’ ci sa kër.
2. Yeesu Krist Buur bi, moom nga dénk
Lép’ lu jëm ci sa njubte.
Ba mu falook tey, ci sa ndeyjoor,
Lép’ lay ilif tey àtte.
Yeowa, ñu-ng’ lay woy,
Ndax yaa ñu xamal
Sa nas bu kéemaane:
Indi sa coggal.
Yal na suñ’ demin dëppoo dëgg
Ak xabaar bi ñuy waare;
Buñu fakkatal ñi mel ni xar,
Ñii ñuy jàngal, ni-m’ ware!
3. Gannaaw xare bi, Ar-Mageddon,
Bu Yàlla xeexee Ibliis,
Kookaak njabootam, dinañ’ tàbbal
Ci kàmb ndax dañ’ dërkiis.
Ci la say jaam yi dee,
Ci sëg yiy jóge
Ngir jaamu laak bànneex.
Céy, ni ñuy bége!
Dinañ’ dimbali ñép’, ba ñu mat,
Yeesu di ñu saraxal.
Keroog ci kow suuf, ba abadan,
Mbég dëgg nga fiy amal.