Woy-Yàlla 99 (221)
Yéen ndaw ñi! Royleen seen ngëm
(Yawut yi 6:12)
1. Ba-ñ’ ko feralee, Samwil dem na Siloo,
Ca kër Yàlla ga, ñu di ko liggéeyloo.
Ab yonent ca Israyel la mujj doon;
Ci siggal turu Yàlla la dogu woon.
Doomiy Eli ya caay-caay lañ’ làmboo woon.
Ndax doon nañ’ mën sóob Samwil ci jëf ju bon?
Déet, ndax Samwil ku dégg ndigal la woon.
Doonul tooñ Yeowa walla jàdd yoon.
2. Doore ciy atam yu njëkk, Timote
Xamoon na Mbind yi, ànd-ak cawarte.
Li ñu ko jàngal la tàmmoon di jëfoo,
Naan, nit ku takku ba fàw’, du ci toxoo.
Ca biir mbooloo ma, tur wu rafet a tax,
Ñépp ànd seedeel ko jikko ju baax.
Yool nañ’ kook céru tukkeek Pool ci dunyaa,
Sasam yóbbe barke ci diiwaan yu yaa.
3. Janq yi, fàttalikuleen seen moroom,
Jaamub Yeowa, bu taqoon ca njaamoom.
Nekk surga terewul ngëmam dëgër;
Fitam ak takkoom tax na ñeneen kër-kër’.
Lii la dem xamal jabaru Na-aman:
‘Yonent Yeowa, faj ko, dina ko man!’
Ñey-xare ba dogal topp xelalam.
Ndaw tawféex ju bawoo ci seedes surgaam!
4. Ndaw ñi, góor ak jigéen, yéen lañuy jamp;
Na leen royukaay yii leeral ni làmp.
Dénk nañ’ ñu lu am maanaa waay, tey jii!
Yeowa tànn na ñiy dem xareji.
Yéen ndaw ñi, suñuy soppe, aywa ci biir!
Ànd-ak jaam’ Yàlla yép’, yi dëgg di xiir.
Nañ’ jibloo artoom te wéy di ko màggal;
Ci muju fan yi, Yeowaa ñuy neexal.