Woy-Yàlla 100 (222)
Nanga teewlu dëgg ci yool bi!
(2 Korent 4:18)
1. Keroog silmaxa di gisaat
Te noppiy ki tëx di déggaat,
Bu màndiŋ yi delloo tóor-tóor
Te kekk li, ndax ndox, di lóor,
Keroog lafañ di tëb nib bëy,
Bu tàggoo, ndax dee, di ne fëy’
—Dinga xéewlu ci bànneex bii,
Soo teewloo dëgg ci yool bi.
2. Keroog ñii luu di waxati,
Keroog màgget ñiy ndawati,
Bu meññeef ak ngóob ne gàññ
Te njariñ deesu ko waññ,
Keroog woyiy xale yiy riir,
Bu mbég ak jàmm di leen yiir,
Ñii dekki dinga mën’ làmbi,
Soo teewloo dëgg ci yool bi.
3. Keroog bukki di for ak xar,
Keroog gayndeek sëllu di far,
Gone kese di leen wommat,
Ñu miin ba dee seen sàmmkat.
Keroog rangooñ di ne meles,
Bu tiitaangeek naqar ne mes,
Dinga gis barkey Boroom bi,
Soo teewloo dëgg ci yool bi.