Jàmm ci biir kër, naka lañu ko mën a ame ?
Ndax dëgg-dëgg, loolu mën na am ?
Lu ñu mën a def ba am ko ?
Xoolal njaboot bi ñu wone fii. Gis nga ni ñu booloo te nekk benn. Ndax loolu bare na tey ? Kër yu bare tey amatuñu jàmm. Ñàkk liggéey bare na. Séy yu bare ñu ngi tas. Ñu bare ñu ngi yar seen doom ñoom kenn, te loolu yombul. Benn boroom xam-xam ci wàllu njaboot nee na : “ Tey, ñu bare dañu ne séy yu dul yàgg dina gën a yokku. ”
Lu tax njaboot yi bare jafe-jafe tey ? Lu ñu mën a def ba am jàmm ci suñu biir kër ?
Njaboot, fan la sosoo ?
Bala ñu mën a tontu ñaari laaj yi nekk ci kaw, fàww ñu xam fan la njaboot sosoo ak kan moo taxawal séy. Su ko defee, ñu mën koo laaj li ñu war a def ngir am jàmm ci suñu biir kër.
Yeesu Kirist nee na Yàlla moo sàkk nit, góor ak jigéen, te lii la wax: “ Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas ”. (Macë 19:4-6.) Wax jooju, dafa ko jële ci xaaj bi njëkk ci Biibël bi.
Ni ko Yeesu Kirist waxe, Yàlla moo sàkk suñu maam Aadama ak Awa te dafa bëggoon ñu am jàmm ci seen biir njaboot. Dafa jël Awa, may ko Aadama te ne góor dina “ ànd ak soxnaam, ñuy kenn ”. (Njàlbéen ga 2:22-24.) Kon lu waral jafe-jafe yi bare ci biir kër yi ? Ndax du ñàkk topp li Yàlla wax ci kàddoom, Biibël bi ?
Lu ñu mën a def ba am jàmm ci suñu kër ?
Àddina si tey mu ngi xiir nit ñi ci topp seen intere rekk. Ca Etaa Sini, lii la benn boroom xam-xam ci wàllu xaalis wax : “ Mën nga nekk nit ku bëgge te am xel mu dal. ” Waaye wut alal du la indil jàmm ci sa biir kër. Da lay yàqal lu bare. Dina yàq sa diggante ak sa waa kër te jël sa jot ak sa xaalis. Léegi nag, xoolal ñaari aaya yi nekk ci Biibël bi yu mën a tax jàmm am ci biir kër gi.
“ Lekk ay lujum kese yu ñu togg ak mbëggeel moo gën lekk yëkk bu ñu duufloo bu ñu togg ak mbañeel. ”
“ Mburu mu wow, mu ànd ak jàmm, moo gën berndeg kër [maanaam lekk bu neex te bare] gu ànd ak coow. ”
Léeb yi 15:17, MN ; 17:1.
Kàddu yooyu, am nañu doole de, du dëgg ? Seetal ni àddina war a mel bu ñépp toppoon kàddu yooyu ! Biibël bi dafa ñuy wax ni ñu war a doxale ak suñu waa kër. Nañu seet yenn xelal yu am solo yu mu ñu jox.
Jëkkër : ‘ Nanga bëgg sa jabar ni nga bëgge sa bopp. ’ — Efes 5:28-30.
Wax boobu dafa gàtt waaye aka am solo ! Biibël bi nee na it jëkkër dafa war a ‘ jox jabaram teraanga ju mat ’ . (1 Piyeer 3:7.) Loolu dafa koy def buy toppatoo jabaram bu baax, boole ci mbëggeel bu mat. Dina bëgg a xam li muy xalaat te bu jabaram di wax dina ko déglu bu baax. (Xoolal li nekk ci Njàlbéen ga 21:12.) Góor guy toppatoo bu baax jabaram ni mu bëgge ñu toppatoo ko, ndax jàmm du am ci biir kër gi ? — Macë 7:12.
Jabar : ‘ Nanga weg sa jëkkër. ’ — Efes 5:33.
Jigéen buy jàpple jëkkëram ci wareefam, day yokk jàmm ci biir këram. Loolu la Yàlla bëggoon bi mu sàkkee jigéen, ndaxte dafa ko sàkkoon ngir mu ‘ jàpple jëkkëram, te jekk ci doon wéttalam ’ . (Njàlbéen ga 2:18.) Jigéen buy jàpple jëkkëram te may ko cér, ndax yaa ngi gis barke yi muy indil waa këram ?
Jëkkër ak jabar : “ Na ñépp fullaal séy, te lalu séy bi bañ a taq sobe. ” — Yawut ya 13:4.
Bu ñu defee loolu, ci lu wóor barke lay doon ci biir njaboot, ndaxte njaaloo day tas kër (Proverbes 6:27-29, 32). Looloo tax Biibël bi ne : “ Na sa xol sedd boo nekkee ak sa jabar bi nga takk bi nga nekkee waxambaane te nanga bég ak moom [...] Lu tax ngay xemmem beneen jigéen ? ” — Léeb yi 5:18-20, MN.
Waajur yi : “ Nangeen yar [seeni doom] ci yoon bi baax ci [ñoom]. ” — Léeb yi 22:6, MN.
Jàmm dina gën a bare ci kër bu waajur faralee di toog di waxtaan ak seeni doom, di nekk ak ñoom te di leen toppatoo. Looloo tax Biibël bi wax waajur yi ñuy jàngal seeni doom lu baax bu ñuy toog ci seen kër, bu ñuy ànd di dox, bu ñuy tëdd ak bu ñuy jóg (Deutéronome 11:19). Biibël bi wax na it ne waajur bu bëgg doomam, dafa ko war a yar. — Efes 6:4.
Xale yi : “ Naka yeen xale yi, nangeen déggal seeni waajur, ci li ngeen bokk ci Boroom bi. ” — Efes 6:1.
Dund ci àddina boo xam ne ‘ lu la neex def ’, déggal seeni waajur yombul. Waaye topp li Ki sos njaboot wax, ndax amul solo ? Moom moo xam li ñu war a def ngir am jàmm ci suñu biir kër. Kon déggalleen seeni waajur. Buleen bàyyi àddina xiir leen ci lu bon. — Proverbes 1:10-19.
Ci biir kër, bu ñépp toppee li Biibël bi wax, jàmm dina am foofu. Te li ci gën a neex mooy dinañu am ëllëg bu neex ci àddina bu bees bu ñu Yàlla dig (2 Piyeer 3:13 ; Peeñu ma 21:3, 4). Kon yéen waa njaboot yi, faralleen di jàng Biibël bi ! Am na benn téere bu ñu mën a am ci tubaab buy faramfàcce li Biibël bi wax ci mbirum njaboot. Mu ngi tudd Le secret du bonheur familial. Téere boobu dimbali na ay njaboot yu bare ci àddina si sépp.
Aaya yi ñu fi lim, ñu ngi leen jële ci Mucc gi Yàlla waajal, Njàlbéen ga ak Téereb Injiil di Kàddug Yàlla. Aaya yi ànd ak MN, ci Les Saintes Écritures — Traduction du monde nouveau — avec notes et références lañu ko jële, firi ko ci wolof. Aaya yi amagul ci wolof, bind nañu ci tubaab turu téere Biibël bi fi ñu nekk te dëngal mbind yi.