XAAJ 1
Ndax Yàlla fonk na nit?
ÀDDINA SI tey bare na ay jafe-jafe. Xeex, musiba, feebar, ñàkk xaalis, njublaŋ ak yeneen, sonal na ay milioŋi nit. Yow it bés bu nekk dangay am ay jafe jafe. Ku ñu ci mën a dimbali ? Ndax am na sax ku ñu ci bëgg a dimbali ?
Ni Yàlla bëgge nit moo gën a foor ni yaay bëgge doomam
Wóor na ne Yàlla dafa fonk nit te dafa ñu bëgg a dimbali. Lii la wax ci kàddoom : “ Ndax jigéen mën na fàtte liir bu muy nàmpal ba du yërëm doom bu mu jur ? Jigéen sax mën na fàtte waaye man duma la fàtte mukk. ”a
Ndax kàddu yooyu du seddal suñu xol ? Diggante yaay ak doom dafa foor. Waaye mbëggeel bi Yàlla am ci nit moo gën a foor fuuf. Yàlla du ñu bàyyi mukk ! Am na lu réy te rafet lu mu def ba pare ngir dimbali ñu. Loolu mooy lan ? Dafa ñu won li ñu mën a indil jàmm. Loolu lan la ? Gëm ko dëgg.
Gëm Yàlla dëgg moo lay indil jàmm. Day tax ngay moytu poroblem yu bare te poroblem boo am dinga xam li nga war a def. Dinga gën a jege Yàlla, sa xel dina dal te sa xol dina sedd. Gëm Yàlla dëgg dina la may it ëllëg bu neex, maanaam dinga mën a dund ba fàww ci àjjana.
Waaye gëm Yàlla dëgg, lan la ëmb ? Te ngëm googu, nu ñu ko mën a ame ?
a Xoolal li nekk ci Esayi 49:15, MN ci Mbind mu sell mi.