Ubbite bi
Ndax mas nga laaj lii ?
Lan mooy dëgg gi jëm ci Yàlla ?
Loo mën a def ba am jàmm ci sa kër ?
Lu tax coono yi bare ci àddina si ?
Lu tax Yàlla bàyyi lu bon di am ?
Lu tax Yàlla sàkk suuf si ?
Fan la ñi dee nekk ?
Lan la malaaka yi di defal nit ñi ?
Naka nga mën a jegee Yàlla ?
Am na ci Mbind mu sell mi ay tont yu leer ci laaj yooyu. Ay milioŋi nit ñoo leen jàng te kontaan ci. Yow it, boo bëggee, mën nga am tont yooyu.
Boo bëggee yokk sa xam-xam ci li nga jàng ci téere bii, demal ci www.pr418.com walla nga jokkoo ak ñi defar téere bii.