NJÀNGALE 2
Rebeka dafa bëggoon di bégal Yexowa
Rebeka jigéen bu bëggoon Yexowa la. Jëkkëram mu ngi tuddoon Isaaxa. Moom itam dafa bëggoon Yexowa. Naka la Rebeka ak Isaaxa xamantee ? Naka la wonee ne dafa bëggoon di bégal Yexowa ? Nañu jàng nettali bii ngir gën a xam Rebeka.
Ibrayima ak Saarata ñoo nekkoon waajuru Isaaxa. Ñoom ñu ngi dëkkoon Kanaan. Waa dëkk boobu gëmuñu woon Yexowa. Ibrayima dafa bëggoon doomam tàkk jabar buy jaamu Yexowa. Mu daldi yónni benn surgaam ngir mu wutali Isaaxa jabar ca dëkku Karan fi mbokki Ibrayima dëkkoon. Foog nañu ne surga boobu Eliyeser la woon.
Rebeka nangu woon na def liggéey bu metti ngir may jiléem yépp ndox
Eliyeser daldi dem ànd ak yeneeni surga Ibrayima. Tukki bu sore la woon. Bi ñuy dem ñu jël fukki giléem ngir yóbbaale lekk ak saricë bu bare. Lan moo mënoon a dimbali Eliyeser mu xam ban jabar lay tànnal Isaaxa ? Eliyeser ak yeneen surga yi mu àndaloon dañu àgg ci dëkku Karan, taxaw ci benn teen. Eliyeser xamoon na ne dina am nit ñiy ñëw rootsi foofu. Noonu mu daldi ñaan Yexowa nee ko : ‘ Su ma ñaanee ab janq mu may ma ndox, bu ma mayee ba mayaale sama giléem yi ndox, dinaa xam ne kooku mooy jigéen ji nga tànn. ’
Ginnaaw loolu Rebeka ñëw ci teen bi. Biibël bi nee na Rebeka jigéen ju rafet la woon. Eliyeser daldi ko ñaan ndox ngir naan, Rebeka tontu ko ne : ‘ Dinaa la may ndox te dinaa may itam sa giléem yi ndox. ’ Xoolal loolu rekk ! Giléem, bu maree ndox bu baree bare lay naan. Kon Rebeka dafa waroon a jaabante lu bare bala giléem yépp di naan. Ndax gis nga ci foto bi liggéey bu metti bi muy def ? — Eliyeser dafa waaru woon ci ni Yexowa nangoo ñaanam.
Eliyeser daldi may Rebeka kado yu bare te rafet. Rebeka wax ko mu ñëw moom ak ñi mu àndal ci kër pàppam. Bi ñu fa demee, Eliyeser wax leen li tax Ibrayima yónni ko ak ni Yexowa nangoo ñaan bi mu def. Waa kër Rebeka yépp daldi kontaan te nangu Rebeka nekk jabaru Isaaxa.
Rebeka ànd na ak Eliyeser Kanaan te nekk jabaru Isaaxa
Ndax foog nga ne Rebeka dina bëgg a nekk jabaru Isaaxa ? — Rebeka dafa xamoon ne Yexowa moo yónni Eliyeser ci moom. Loolu moo tax bi ko waa këram laajee ndax bëgg na dem Kanaan te nekk jabaru Isaaxa, mu ne : ‘ Waaw-waaw, bëgg naa dem. ’ Noonu mu ànd ak Eliyeser. Bi mu àggee Kanaan, Isaaxa tàkk ko mu nekk jabaram.
Rebeka def na li Yexowa bëggoon mu def, looloo tax Yexowa barkeel ko ba mu bokk ci maamu Yeesu yi ! Boo melee ni Rebeka te def liy bégal Yexowa, Yexowa dina la barkeel yaw itam.
JÀNGAL CI SA BIIBËL
Njàlbeen ga 12:4, 5 ; 24:1-58, 67