TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • yc lesoŋ 4 p. 10-11
  • Dafa bégaloon pàppam ak Yexowa

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Dafa bégaloon pàppam ak Yexowa
  • Jàngal-leen seeni doom
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li Yefte Dig Yexowa
    Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
Jàngal-leen seeni doom
yc lesoŋ 4 p. 10-11
Yefte mu ngi toog ak doomam bu jigéen bi muy nekk xale bu ndaw

NJÀNGALE 4

Dafa bégaloon pàppam ak Yexowa

Yefte mu ngi ñaan Yexowa bi soldaari Israyil doon xeex seeni noon

Lan la Yefte digoon Yexowa ?

Yefte jóge na xare ñibbisi këram, mu ngi lëng doomam bu jigéen bi ko gatandusi

Yombul woon ci doomu Yefte bi, waaye terewul mu def li pàppam dige woon

Ndax gis nga xale bu jigéen bi nekk ci foto bi ? — Pàppam, Yefte la tudd. Xale bu jigéen bi waxuñu turam ci Biibël bi waaye xam nañu ne bégaloon na pàppam ak Yexowa. Nañu jàng nettali bii ngir xam ko moom ak pàppam Yefte.

Yefte góor gu baax la woon. Dafa doon jël jot bu bare ngir jàngal doomam lu jëm ci Yexowa. Góor gu am doole la woon te mën a jiite. Loolu moo tax yawut yi wax Yefte mu jiite leen ngir ñu dem xeexi ak seeni noon.

Yefte dafa ñaan Yexowa ngir ñu am ndam. Mu dig Yexowa ne, bu ko mayee ndam, dina ko may nit kiy njëkk a génn këram ngir gatandu ko. Nit kooku dina dem liggéey te dëkk dundam yépp ci tàntu Yàlla bi maanaam fi ñu doon jaamoo Yàlla. Yexowa may na Yefte ndam ! Ndax xam nga bi mu ñibbee këram kan moo ko njëkk a gatandu ? —

Waaw, doomam bu jigéen la woon ! Doom boobu rekk la Yefte amoon te léegi dafa ko war a bàyyi mu dem dëkk fu sore. Loolu nekkoon na lu metti ci moom. Waaye fàttalikul ne dafa am li mu dige woon. Doomam nee ko : ‘ Pàppa, dafa am loo dig Yexowa ba pare, kon nanga sàmm sa kàddu. ’

Doomu Yefte bu jigéen bi mu ngi taxan matt ngir Kër Yàlla ga ; xaritam yi ñëw seetsi ko

At mu jot, xaritu doomu Yefte yi dañu ko doon seetsi

Loolu metti woon na itam ci doomu Yefte ndaxte bu demee liggéey ci tàntu Yàlla bi du mën a am jëkkër te du mën a am doom. Waaye dafa bëggoon a def li pàppam dige woon te dafa bëggoon a bégal Yexowa itam. Loolu moo ko ëppaloon solo am jëkkër walla am doom. Ci noonu, mu génn seen kër dem dëkk ca tàntu Yàlla bi dundam yépp.

Ndax foog nga ne li mu def tax na ba pàppam ak Yexowa bég ? — Waaw-waaw bégloo na leen ! Boo nangoo dégg ndigal te bëgg Yexowa dinga mën a mel ni doomu Yefte bi. Dinga bégal itam sa pàppa ak Yexowa.

JÀNGAL CI SA BIIBËL BI

  • Deutéronome 6:​4-6

  • Juges 11:​30-​40

  • 1 Korent 7:​37, 38

LAAJ YI :

  • Kan moo nekkoon Yefte ? Lan la dige woon ?

  • Lan moo taxoon def li pàppam dige metti ci doomu Yefte ?

  • Doomu Yefte bi, lan moo ko ëppaloon solo yeneen mbir yépp ?

  • Naka nga mën a def ba mel ni doomu Yefte bi ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager