NJÀNGALE 12
Jarbaatu Pool bi dafa amoon fit
Nañu jàng lu jëm ci benn xale bu góor bu musal nijaayam ci dee. Apootar Pool moo nekkoon nijaayu xale bu góor boobu. Xamuñu ni xale bi tuddoon, waaye xam nañu ne defoon na loo xam ne ku am fit rekk moo koy def. Ndax bëgg nga xam li mu defoon ? —
Pool, dañu ko tëjoon kaso ca Yerusalem, ndaxte dafa waare ci Yeesu. Amoon na ay góor yu bañ Pool, ñu daldi def benn kómpaloo ngir jàpp ko. Ñu ne : ‘ Nañu wax kilifa soldaar yi mu sant leen ñu yóbbu Pool tirbinaal. Dinañu làqatu ci yoon bi. Bu Pool rombee rekk, ñu rey ko ! ’
Jarbaatu Pool bi dafa wax Pool ak kilifa soldaar yi kómpaloo bu bon bi.
Jarbaatu Pool bi dégg kómpaloo boobu. Lan la def ? Dafa dem ca kaso ba wax ko Pool. Ci saa si, Pool nee ko mu dem wax ko kilifa soldaar yi. Ndax wax ak kilifa gi yomboon na ci jarbaatu Pool ? — Déedéet, yombul woon ndaxte kilifa ku mag la. Waaye jarbaatu Pool ku am fit la woon moo tax mu wax ak kilifa gi.
Kilifa gi daldi xam li muy def. Mu jël lu mat 500 soldaar ngir kenn bañ a laal Pool. Mu ne leen ñu yóbbu Pool Sesare ci guddi gi. Ndax ñi bëggoon a rey Pool rey nañu ko ? — Déedéet. Góor yu bon yooyu mënuñu woon sax laal Pool ! Seen kómpaloo bi doxul.
Lan nga mën a jàng ci nettali bii ? — Yaw itam mën nga nekk ku am fit ni jarbaatu Pool. Bu ñuy wax nit ñi lu jëm ci Yexowa dañu war a am fit. Ndax dinga am fit te kontine di wax ci lu jëm ci Yexowa ? — Boo ko defee, dinga mën a tax nit mucc.
JÀNGAL CI SA BIIBËL BI
Jëf ya 23:12-24
Macë 24:14 ; 28:18-20
1 Timote 4:16