TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • yc lesoŋ 14 p. 30-31
  • Nguur gi nar a jiite suuf si sépp

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nguur gi nar a jiite suuf si sépp
  • Jàngal-leen seeni doom
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Xaritu Yàlla yi dinañu dund ca Àjjana
    Mën nga nekk xaritu Yàlla !
  • Lan mooy coobare Yàlla ngir suuf si ?
    Lan la ñu Yàllay laaj?
  • Lan la Yàlla bëggoon bi muy sàkk suuf si ?
    Xibaaru jàmm bi jóge ci Yàlla !
  • Li nguuru Yàlla nar a def
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
Xóotalal waxtaan bi
Jàngal-leen seeni doom
yc lesoŋ 14 p. 30-31
Yeesu Kirist mu ngi nekk buur di nguuru ci àjjana bi nekk ci kaw suuf si sépp

NJÀNGALE 14

Nguur gi nar a jiite suuf si sépp

Ndax xam nga ban Nguur lañuy wax fii ? — Waaw, Nguuru Yàlla la, Nguur googu moo nar a defar suuf si ba mu nekk àjjana ju rafet. Ndax bëgg nga xam lu jëm ci Nguur googu ? —

Nguur gu nekk am na buur buy jiite ñi fa dëkk. Ndax xam nga kan mooy buur ci nguuru Yàlla ? — Yeesu Kirist la. Moom ci kaw asamaan la nekk. Ci kanam tuuti, dina nekk buuru ñépp ci kaw suuf ! Bés bu Yeesu nekkee buur ci kaw suuf si sépp, ndax dinañu kontaan ? —

Lan nga yàkkamtee def ci biir àjjana ?

Dinañu kontaan lool kay ! Ci biir àjjana, nit ñi dootuñu xeex, geer dootul am. Ku nekk dinga bëgg sa moroom. Kenn dootul feebar, kenn dootul dee. Ñi gumba dinañu gis, ñi tëx dinañu dégg, ñi lafañ dinañu mën a daw, dinañu mën a tëb. Ñépp ay am lekk bu bare. Dina am jàmm diggante mala yi ak diggante nit ak mala. Ñi dee dinañu dekki. Rebeka, Raxab, Daawuda, Iliyas ak ñeneen ñi ñu wax ci téere bii dinañu dekki ! Ndax bëgg nga leen a gis bés bu ñu dekkee ? —

Yexowa dafa la bëgg te dafa bëgg itam nga kontaan. Boo kontine di jàng ngir xam Yexowa te di def li mu bëgg, yaw itam dinga dund ba fàww ci àjjana ju rafet ! Ndax du loolu nga bëgg ? —

JÀNGAL CI SA BIIBËL

  • Esayi 2:4 ; 11:​6-​9 ; 25:8 ; 33:24 ; 35:​5, 6

  • Yowaana 5:​28, 29 ; 17:3

LAAJ YI :

  • Kan mooy buur bi ci nguuru Yàlla ?

  • Ci ñan la Yeesu nar a nguuru ?

  • Bés bu Yeesu nekkee buur ci kaw suuf si sépp, dund bi naka lay mel ?

  • Boo bëggee dund ba fàww ci Àjjana, lan nga war a def ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager