TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 9/99 p. 1
  • Ndax dangay liggéey, jublu ci dara?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndax dangay liggéey, jublu ci dara?
  • Sasu Nguuru Yàlla — 1999
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Nanga seetiwaat nit ñi ngir tàmbali ay njàngum Biibël bi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
Sasu Nguuru Yàlla — 1999
km 9/99 p. 1

Ndax dangay liggéey, jublu ci dara?

1 Yeowa mooy Yàlla ji am jubluwaay. (Isa. 55:10, 11) Ñu ngi ñuy xiirtal ci ñu roy ko. (Efes 5:1) Ci lu wóor, loolu warkoon naa feeñ ci fasoŋ bi ñuy beye suñu sasu waare. Ba tax laajte bi jaadu na: “Ndax dangay liggéey, jublu ci dara?”

2 Di waare kër-oo-kër, di seede saa yoo ci ame yoon, ak a siiwal suñuy mbind yi, loolu lépp bokk na ci sas wu ñuy bey, jublu ci dara. Waaye fàttelikul ne suñu yónnent ëmbul waare doŋŋ, waaye itam di sàkk ay taalibe. (Macë 28:19, 20) Bu ñu jiwee jiwu dëgg gi jëm ci Nguur gi, soxla nañoo dellu te suuxat leen, am ci toppatoo, saa su nekk, ba ñuy séentu ci Yeowa yokku gi. (1 Kor. 3:6) Soxla nañoo farlu ci dellu seeti nit ñi, ba noppi di tàmbali ay njàngum Biibël bi.

3 Yaatalal sa sas: Saa yoo mënee geestu ci li nga def, démb, ci liggéeyu waare bi te wax sa bopp: “Matal naa li ma jublu woon a def,” dangay yëg péex ci sa xol. Ni ñu ko bindee ci 2 Timote 4:5, lii Pool la jamp, naan: “Nanga (. . .) matal sag yónnent.” Looloo ngiy ëmb di gën a góor-góorlu ngir toppatoo jépp itte ci dëgg gi, ju ñu taseel. Ci sa doxalinu liggéeyu waare bi ayu-bés gu nekk, jàppal jot gooy jagleel nit ñi ngay dellu seeti. Jublul ciy jéem a tàmbali ak ñi seen xol jagoo njub ay njàngum Biibël bi. Loolu warkoon naa nekk sa jubluwaay, booy bokk ci sasu waare wi.

4 Laajal ay yéenekat la ñu yëgoon ci seen xol, ba ñu gisee, cim ndaje mu mag, ñu sóob ña ñu doon jàngal Biibël bi. Seen mbég a nga tollu woon, bu ko rawul sax, ak mbégu ña ñu sóoboon. Mataloon nañu jubluwaay bu réy! Waa ju sàkkoon taalibe wax na lii: “Di sàkk taalibee ngiy tekki taggkati Yeowa yu gën a bare. Mu ngiy tekki dund, ngir ñiiy nangu dëgg gi. Jàngal ñeneeni nit dëgg gi, dama ko rekk bëgg—daa nekk lu amul moroom! (. . .) Ñu bare ci ñi jàng a bëgg Yeowa mujj nañoo nekk samay xariti benn-bakkan.”

5 Jortul nga jàpple nit ba mu mujj a doon jaamu Yeowa, ju jébbalu ci moom! Ndaw luy jur mbég! Meññeef bu ni mel a ngiy jóge ci jublu ci dara, ba ñu doon liggéey ci sasu waare wi.—Kol. 4:17.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager