Yéen, way-jur yi—Nekkleen royukaay bu rafet ngir seeni doom
1 Kàddug Yàllaa ngi ñuy wax ne “baayu [akit ndeyu] ku jub, ci lu wóor, dina bég.” (Léeb. 23:24, 25) Ndaw barke ngir way-jur yi nekk royukaay bu rafet ngir seen njureel! Lii la kenn, ku bokk ci ab Kurélu Bànqaas[u Seede Yeowa yi], wax ci ay way-juram: “Dëgg gi moo doon seen dund gépp, te li ma bëggoon, man it, moo doon fexe mu doon sama dund gépp.” Waaw, lan la doom yi warkoon a gis ci seeni way-jur?
2 Yar ak teggin, akit weg bu xóot: Warugaru way-jur yi la, rëdd ci xelu seeni doom jikko yu rafet. Yar ak teggin ñu ngi koy jàng, du rekk ci li ñu leen di ko jàngal ak làmmiñ, waaye ci li ñuy seetlu ak a roy. Looloo tax, lu seen jëfin di wone? Ndax seeni doom dinañu leen di dégg, ngeen di wax “baal ma,” “su la neexee,” ak “jëre-jëf”? Ci biir njaboot gi, ndax dingeen digaale ci seen biir ak weg gu xóot? Ndax dingeen bàyyi xel ci li ñeneen ñiy wax? Ndax dingeen déglu, bu leen seen doom yiy waxal? Ndax dingeen feeñal jikko yu rafet yooyu, bu ngeen nekkee ci Saalu Nguur gi, akit bu ngeen nekkee ci seen biir kër?
3 Digganteek Yàlla yu dëgër ak cawarte ci yëngu-yëngu waare gi: Mbokku karceen, mu jébbal liggéeyu waare gi jotam gépp, maanaam lu ëpp 50 at, a ngiy fàttaliku: “Sama yaay ak sama pàpp, royukaay yu rafet lañu woon lu jëm ci fonk ndaje yi te sawar ci sasu waare gi.” Nan ngeen di wone seeni doom ne, sàmm diggante waa-kër gi ak Yàlla itteel na leen? Ndax dingeen di seet, bés bu ne, jukkib bés bi? Ndax tàmm ngeen di jàng Biibël beek njaboot gi? Ndax seeni doom dinañu leen gis, ngeen di jàng Biibël beek mbind yi Mbootaay gi génne? Lan lañuy dégg, bu ngeen di ñaanal njaboot gi? Ndax dingeen taaj, ak seeni doom, waxtaan wuy tabax seen digganteek Yàlla, di waxtaane yëf yuy jariñ, yu jëm ci dëgg geek mbooloo gëmkat yi? Ndax yàkkamti ngeen teewe ndaje yi yépp, te bokk itam ci sasu tool bi, njaboot gi gépp ànd a bokk ci?
4 Yéen way-jur yi, xalaatleen ci royukaay bi ngeen nekk ci seeni doom. Fexeleen mu doon bu rafet, kon, bu boobaa dinañu ko fonk seen giiru-dund gépp. Jabaru wottukat buy wër, ju nekk léegi ci ay 70 atam, lii la wax: “Ba léegi, maa ngiy jariñoo royukaay bu rafet bi ma samay way-juri karceen, yu làmboo mbëggeel yi, bàyyil. Te li may gën a ñaan Yàlla mooy, ma wone ngërëm gu takku ci ndono loolu, ci li ma koy jëfandikoo ni mu ware, tey ba abadan.”