Defal li nga dige woon bi nga doon jébbalu
1 Bés bi ñu la doon sóob, bés bu réy la woon. Bés boobu, wóor na ne yaa ngi koy fàttaliku, mu yàgg mbaa mu jege. Du ci sóob bi la yépp di jeexe. Ci lañuy tàmbali di liggéeyal Yàlla ba keroog ñuy de. Te liggéey boobu mën na yàgg ba abadan (1 Ywna. 2:17). Def li nga dige bi nga doon jébbalu, lu mu ëmb ?
2 Royal ci Krist : Bi ñu ko sóobee ba pare, ca la Yeesu “ tàmbale liggéeyam ”, di “ yégle xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla ”. (Lukk 3:23 ; 4:43.) Noonu it, bu ñu sóobee nit ngir wone ne jébbalu na ci Yexowa, ci lañu koy fal waaraatekatu xibaar bu baax bi. Dëgg la, tey bala ngay am li ngay dunde, danga war a liggéey ba sonn, ay waxtu yu baree-bare. Waaye loolu terewul ne liggéeyu karceen bi mooy bi ëpp solo (Macë 6:33). Ñi jébbalu ci Yàlla duñu rey seen bopp ngir am alal ju dul jeex, walla tur bu mag. Dañuy jéem a ‘ matal seen yónnent ’, ni ko ndaw li Pool defe woon (Room 11:13). Kuy jaamu Yexowa, am na lu réy. Ndax fonk nga loolu, te di ci def lépp li nga mën ?
3 Ni ko Yeesu defe woon, dañu war a ‘ dàq Seytaane ’. (Saak 4:7.) Bi ñu sóobe Yeesu ba pare, Seytaane dafa ko jéem a defloo lu bon. Loolu it lay def tey ak ñi jébbalu tey jaamu Yexowa (Lukk 4:1-13). Ak àddina seytaane bii ñu wër, dañu war a yar suñu bopp, di moytu lépp li mën a wàll suñu xel, walla yàq suñu xol (Léeb. 4:23 ; Macë 5:29, 30). Lii lañu xelal karceen yi : “ Mënuleena sukk ci reerub Boroom bi, sukk ci reerub rab yi. ” (1 Kor. 10:21). Loolu laaj na ñu sore fo yu tilim yi, àndandoo yu bon yi, ak li bon li nekk ci internet. Ñi bàyyi yoonu Yàlla dañuy defar ay téere. Téere yooyu it, war nañu leen a moytu. Bu ñu gaawee ràññe pexe seytaane yi, dinañu mën a def li ñu dige woon bi ñu doon jébbalu.
4 Jëfandikool li ñu Yàlla may : Yexowa may nañu Kàddoom ak mbooloo karceen yi ngir ñu jàpple ñu ci li ñu dige woon bi ñu doon jébbal suñu bopp. Deel tàmm jàng Biibël bi te ñaan Yàlla bés bu nekk (Yos. 1:8 ; 1 Tes. 5:17). Deel fonk ndaje yi ñuy am ci mbooloo mi (Sab. 122:1). Àndal ak ñi ragal Yexowa tey topp ay ndigalam. — Sab. 119:63.
5 Bu la Yexowa jàpplee, dinga mën a def li nga dige woon bi nga doon jébbalu ci moom, te dinga ko mën a jaamu ba abadan. — Sab. 22:26, 27 ; Fil. 4:13.