Liggéey boo xam ne, bala ñu koy mën a def, fàww ñu woyof
1 Kàddu Yàlla mu ngi lay laaj nga “ woyef. Ku la [...] saaga [...], bul feyyu, waaye ñaanal ko lu baax ”. (1 Pie. 3:8, 9.) Xelal boobu baax na ci liggéeyu waare bi. Li am sax mooy, liggéeyu waare bi ñu dénk karceen yi, mën na wone fu ñu tollu ci woyof.
2 Woyof nekk na jikko buy tax ñu mën a muñ lu naqadi. Bu ñuy waaraate, dañuy dem ci nit ñu nu xamul, te nit ñooñu, du ñoom ñoo nu wax ñu ñów ci ñoom. Xam nañu ne dina am ñu ciy naqadi deret. Bu booba, bu ñu bëggee wéy ci liggéey boobu, dina laaj ñu woyof. Am na ñaari pioñee ñu doon waaraate ci gox bu naqadi woon lool. Lu mat ñaari at, suñu ñaari mbokk yu jigéen yooyu, dem nañu kër-oo-kër di waaraate bés bu nekk. Waaye kenn ubbiwul buntam ngir déglu leen. Waaye terewul ñu kontine. Tey am na ñaari mbooloo karceen ci gox boobu.
3 Li ñuy def bu ñu dajee ak ku ñàkk kersa : Woyof dina tax ñu mën a roy ci Yeesu bu ñu dajee ak ku naqadi deret walla ku ñàkk teggin (1 Pie. 2:21-23). Suñu benn mbokk mu jigéen moo doon waaraate ci benn kër. Boroom kër gu jigéen gi moo ko njëkk saaga, ba pare, jëkkër ji saaga ko moom itam, te dàq ko. Suñu mbokk mi daldi muuñ, te ne leen xéyna beneen yoon dina mën a wax ak ñoom. Loolu dafa jaaxal ñaar ñooñu ba nga xam ne, bi beneen seede ñówee seen kër, dañu ko déglu, te nangu nañoo ñów teew ci ndaje bu amoon ci Saalu Nguur gi. Suñu mbokk mi ñu dàqoon mu nga fa woon. Mu nuyu leen, ba pare mu dem seen kër ngir gën a waxtaan ak ñoom. Ñun itam, bu ñu tontoo ‘ tont gu lewet, te ànd ak wegeel ’, dina mën a tax ku ñu bañoon a déglu, mujj ko nangoo def. — 1 Pie. 3:15 ; Léeb. 25:15.
4 Buñu réy-réylu : Suñu xam-xam ci wàllu Biibël bi warul a tax ñuy xeeb nit ñi, walla ñu leen di sewal (Ywna. 7:49). Kàddu Yàlla mu ngi nuy ñaan ñu bañ a “ jëw kenn ”. (Titt 3:2.) Bu ñu melee ni Yeesu, woyof ci suñu biir xol, dinañu may nit ñi doole (Macë 11:28, 29). Bu ñu woyofee, dina tax suñu xibaar gën a neex ñi nuy waxal.
5 Woyof, dina tax ñu mën a wéy di waaraate ci gox yu naqadi yi. Mën naa tax ñi nu bañoon a déglu, soppeeku, te dafay tax nit ñi bëgg déglu xibaaru Nguur gi. Ci kow loolu lépp, dafay neex Yexowa, moom miy “ yiwal ñi woyef ”. — 1 Pie. 5:5.