TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 1/03 p. 2
  • Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Turu xaaj yi
  • 13-19 sãwiyee
  • 20-26 sãwiyee
  • 27 sãwiyee ba 2 feewriyee
  • 3-9 feewriyee
Sasu Nguuru Yàlla — 2003
km 1/03 p. 2

Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi

13-19 sãwiyee

Woy-Yàlla 94

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 4 ci Sasu Nguuru Yàlla bii, walla ci Sasu Nguuru Yàlla yi jiitu, te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi ñu mujj a jot. Ku ci nekk, bu waxee ci benn yéenekaay ba pare, na tàllalal ki muy waxal ñaari yéenekaay.

15 min : Fexe ba nit nangu dëgg gi te fekk waxuloo dara. Waare ak waxtaan ak ñi teew. Jikko karceen yu rafet yi, seede bu am doole la. Tax na ba ay jëkkër, walla ay jabar yu nekkul woon Seede Yexowa, mujj di jaamu Yexowa (1 Pie. 3:​1, 2). Nettalil li ñu wax ci La Tour de Garde bu 1 sãwiyee 1999 ci xët 4 ak bu 1 oktoobar 1995 ci xët 10 ba 11, ak it li nekk ci Annuaire bu 1995 xët 46. Bala ndaje bi di jot, waxal ñaar walla ñetti nit ne dinga leen ñaan ñu wax lu baax li ñu jële ci topp ndigali Biibël bi ci fànn boobu.

20 min : “ Defal li nga dige woon bi nga doon jébbalu. ”a Bu ngeen waxtaane ci xise 3 ba pare, na nga waxtaan ak benn janq walla benn waxambaane bu ñu sóob te laaj ko laaj yii : Bi ñu ko soobee ba tey, yann jafe-jafe la daje ? Lan moo tax mu mën leen a xeex ba gañe ? Bi mu jébbalee boppam Yexowa ba léegi, lu baax lan la ci jële ?

Woy-Yàlla 9 ak ñaan bu mujj bi.

20-26 sãwiyee

Woy-Yàlla 28

8 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi.

15 min : Bés bu nekk, ndax dinga jàng aaya bés bi ? Waare ak waxtaan ak ñi teew. Waxal nit ñi ñu góor-góorlu ngir jëfandikoo bu baax téere Examinons les Écritures chaque jour — 2003. Waxtaanleen ci kàddu yi nekk ci xët 3 ba 4. Joxleen ay xelal yuy wax ci ni njaboot yi mëne def aaya bés bi. Waxtaanleen ci ñaar walla ñetti aaya yi ñu war a def weer wi di ñów ci aaya bés bi, ak kàddu yi ñuy àndal. Bu ko defee nit ñi dinañu gis njariñ bi nekk ci jàng aaya bés bi, bés bu nekk. Na jëkkër ak jabar wone ni ñuy jànge ñoom ñaar aaya bi ñu war a def tey ak kàddu yi muy àndal.

22 min : “ Jàngalal nit ñi làkk bu sell bi. ”b Bu ngeen waxtaane ci xise 6 ba pare, na benn waaraatekat bu mën waaraate wone ni ñu mëne tàmbali benn njàngum Biibël bi ci buntu këru nit ku ñuy dellu seeti. Na tànn benn waxtaan ci yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2002 ci xët 2 te topp ko. Na waxtaan it ci benn xise ci téere Laaj bi. Buy jeexal waxtaan bi, na laajte benn laaj bu ñuy tontu ci xise bi ci topp, te wax ne dina ci tontu buy dellusi. Waxal ñi teew ñu seet ndax ñi ñuy seeti duñu nangu jàng Biibël bi noonu.

Woy-Yàlla 29 ak ñaan bu mujj bi.

27 sãwiyee ba 2 feewriyee

Woy-Yàlla 42

10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fàttalil waaraatekat yi ñu bind li ñu def ci liggéeyu waare bi te joxe ko. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 4, te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi ñu mujj a jot. Ku ci nekk buy jeexal na jox ki mu doon waxal kayit bu ndaw bi tudd Aimeriez-vous en savoir plus sur la Bible ? Nit ñi nuy waxal, kenn ki dafay nangu jël téere yi, keneen ki dafay bañ. Ci lu gàtt, waxal ni ñu mënee dellu seeti nit ñi jël yéenekaay ak kayit bu ndaw bi. — Seetleen li nekk ci Le ministère du Royaume bu sãwiyee 2002, xët 8 xise 10.

15 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.

20 min : Dimbalil nit ñi ñu jege Yexowa. Waare ak waxtaan ak ñi teew. Téere bu bees boobu, dinañu ko wone ci waaraate bi ci weeru feewriyee. Waxtaanleen ci li ñu bind ci xët 3 ngir ñiy jàng téere bi, te tànnal yenn yëf yu nekk ci téere bi, te wone ko. Ñeenti xaaj yi nekk ci téere bi, bu ci nekk dafay wax ci benn ci jikko Yàlla yi ëpp solo. Ci xaaj bu nekk, dina am benn pàcc buy wone ni Yeesu wone jikko ji ñuy wax ci xaaj bi, ak benn pàcc buy wone ni ñu mëne wone jikko jooju ñun itam. Am na fukk ak juróom ñaari nataal yuy feesal xët bi yépp tey wone li ñu nettali ci Biibël bi. “ Éléments de méditation ” yi dañuy xalaatloo nit ñi ci leneen lu am solo lu jëm ci li ñu doon waxtaane. Seetaatleen li nekk ci xaaj bi tudd “ Li ñu mën a wax bu ñuy wone téere Approchez-vous de Jéhovah ”, te na benn waaraatekat bu mën waaraate wone ni ñu mëne topp benn ci fasoŋu waaraate yooyu.

Woy-Yàlla 65 ak ñaan bu mujj bi.

3-9 feewriyee

Woy-Yàlla 33

15 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Seetleen li nekk ci “ Ay tont ci seeni laaj ”. Waxal waaraatekat yi ñu jëfandikoo kayit bi tudd Veuillez suivre l’intérêt (S-43), bu ñu gisee kuy làkk làkk bu ñu déggul, ngir topp li ñu waxoon ci leetar bi ñu yónne mbooloo yi yépp te ñu bindoon ci bésu 1 màrs, 2000. Su dee sax nit ki wonewul ne xibaaru Nguur gi neex na ko, war nañu jëfandikoo kayit boobu.

12 min : Royleen ci seen ngëm. Waxtaanal ak benn magu mbooloo bu yàgg jaamu Yexowa, di ko topp bu baax ak xol bu woyof (Yaw. 13:⁠7). Laaj ko laaj yii : Naka la def ba xam dëgg gi ? Yan jafe-jafe la xeexal ndax bañ a bàyyi dëgg gi ? Ci wàllu ngëm, lan moo ko tax a jëm kanam ? Lan la def ngir yootu céru sàmm ci mbooloo (1 Tim. 3:⁠1) ? Lan moo ko dimbali ba mu mën a boole wareefam ci mbooloo mi ak liggéeyam ak it wareefam ci njabootam, te bu ci nekk yem fi mu war a yem (1 Tim. 5:⁠8) ? Lu mu xalaat ci ndimbal bu muy indil nit ñi ci mbooloo mi ?

18 min : “ Liggéey boo xam ne, bala ñu koy mën a def, fàww ñu woyof. ”c Bu ngeen di waxtaan ci xise 3, waxal ñi teew ñu wax li ñu mën a def bu ñu gisee ci waaraate bi ku ñu bëgg ñaawal, ku ñàkk kersa, ku bëgg xuloo, walla ku mer. Bu ngeen di def xise 4, waxal li nekk ci téere Étude perspicace, volume 1, xët 1158, xise 2.

Woy-Yàlla 55 ak ñaan bu mujj bi.

[Li ñu bind ci suuf]

a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager