Nañu fàttaliku li ñu jàng ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla
Laaj yii di topp, ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla lañu ko war a def, ci diggante 24 feewriyee ba 2 màrs 2003. Ci lu mat 30 simili, wottukatu lekkool bi dina waxtaan ak ñi teew ngir fàttaliku li ñu def ci lekkool bi ci diggante 6 sãwiyee ba 24 feewriyee 2003. [Bul fàtte : Bu amee laaj boo xam ne kenn bindul loo war a jàng ngir xam tont bi, yaa ko war a wutal sa bopp. — Seetal li ñu wax ci téere École du ministère, xët 36-37.]
LIY TAX ÑU AAY CI WAX (Téchnique oratoire)
1. Dëgg la walla déet : Booy jàng ci kow, bu dee sax li nga wax wuute na ak li ñu bind, boo waxee lu niroo lu jub rekk, sa njàng mi jub na. Leeralal sa tont. [be p. 83]
2. Mottalil kàddu bii : Ku bëgg mën a jàng bu baax, dafa war a ․․․․․․․․, ․․․․․․․․, ․․․․․․․․ ci baat bu kowe. [be p. 85]
3. Lan moo am solo lool, bu ñu bëggee wax baat yu leer (1 Kor. 14:8, 9) ? [be p. 86]
4. Lan moo mën a tax li ngay wax bañ a leer ? Lan lañu mën a def ngir suñu kàddu gën a leer ? [be p. 87-8]
5. Ci ñaari weer yi weesu, yan ñooy yenn baat yi nga dégg ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi, te war leen a wax di leen waxaat ba mën leen a tudd ni mu ware ? [be p. 92]
WAXTAAN N° 1
6. Dëgg la walla déet : Suñuy bët mën nañu tax ñu gën a déglu. Leeralal sa tont. [be p. 14]
7. Mottalil kàddu gii : ․․․․․․․․ si, ․․․․․․․․ wi, ․․․․․․․․ bi, Yàlla moo leen a sàkk ngir ñu xamal ñu fu ñu tollu ci waxtu wi. [si p. 279 § 7]
8. Mottalil kàddu gii : “ Bés ” yi ñuy wax ci Biibël bi mën na nekk bésu ․․․․․․․․ waxtu, bésu ․․․․․․․․ waxtu, bésu ․․․․․․․․ at, walla bés bu mat ․․․․․․․․. Baat yi muy àndal ñooy wone ban bés la. [si p. 279 § 8]
9. Fi Aana, Mark, ak Ilias jaar ci àddina mën na ñu dimbali ngir ñu bañ a dem ba bañ a bëggati dara ci àddina. Naka ? Naka lañu mënee jëfandikoo fi ñooñu jaar ngir dimbali nit ñi ? [w01 1/2 p. 20-3]
10. Xam ni nit ñi daan rawante bu njëkk ci wàllu tàggat yaram, naka lay taxe ñu gën a nànd yenn aaya ci Biibël bi ? Naka la waree feeñ ci fasoŋ bi ñuy dunde ? [w01 1/1 p. 28-31]
LI ÑU WAROON A JÀNG CI BIIBËL BI AYU-BÉS BU NEKK
11. Dëgg la walla déet : Ndegam samp nañu Nguuru Yàlla ca asamaan ca atum 1914, bu ñuy ñaan, waratuñu wax “ na sa nguur ñëw ”. (Macë 6:10.) Leeralal sa tont. [be p. 279 ; w96 1/6 p. 31]
12. Dëgg la walla déet : Li Yeesu wax ci Macë 11:24 dafay wone ne ñi Yexowa alag ak safara ci Sodom ak Gomor dinañu dekki. Leeralal sa tont.
13. Tànnal tont yi jub : Surga bu takku te teey bi Yeesu doon wax ci Macë 24:45-47 mooy : a) Jataay biy dogal ci Seede Yexowa yi ; b) mbooloom karceen yi Yàlla tànn te nekk ci kow suuf si ci jamano bu mu mënta doon ; c) Yeesu Krist ci boppam. Surga boobu dafay jox “ waa kër gi ” li ñuy lekk ci waxtoom. “ Waa kër gi ” mooy a) bépp karceen bu Yàlla tànn ; b) yeneen xar yi ; c) képp kuy jàng téere yu karceen yi defar. Kilifa gi dénk na surga bi alalam yépp ci atum a) 1914 ; b) 33 ci suñu jamano ; c) 1919.
14. Tànnal tont bi jub : Mbaal mi Yeesu wax ci Macë 13:47-50 dafa forandoo mbooloo karceen yi Yàlla tànn, ak a) Nguuru Yàlla bi Almasi bi jiite ; b) yeneen xar yiy ànd ak ñoom ; c) Mbooloo yuy wuyoo turu karceen te fekk toppuñu Yeesu.
15. Ni ko Macë 5:24 waxe, loo war a def boo gisee ne dafa mel ni danga tooñ sa benn mbokk karceen ? [g96 8/2 p. 26-7]