Yégle yi
◼ Téere yi ñuy wone ci weeru feewriyee : Téere bu bees bi tudd Approchez-vous de Jéhovah. Mbooloo yi amagul téere boobu, mën nañu wone téere Création, walla téere Révélation : dénouement. Màrs : Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex. Dinañu góor-góorlu ngir tàmbali ay njàngum Biibël bi. Awril ak me : Benn Tour de Garde ak benn Réveillez-vous ! Ci liggéeyu waare bi, dinañu dellu seeti ay nit ñu suñu waxtaan neex, mel ni nit ñoo xam ne mas nañu teew ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, walla ci beneen ndaje, waaye tàmmuñu teew ci ndaje yi yépp. Bu ñuy dellu seeti nit ñooñu, nañu góor-góorlu ngir jox leen téere Adorez le seul vrai Dieu. War nañu def li ñu mën ngir jàng ak ñoom Biibël bi, rawatina bu ñu masee jàng ak seede Yexowa yi téere Xam-xam ak téere Laaj.
◼ Wottukat biy jiite walla nit ki mu tànn war na seet ndax xaalisu mbooloo mi mat na. Loolu, 1 màrs lañu ko war a def, walla ni mu gënee gaaw gannaaw bés boobu. Bu ñu defee loolu ba pare, war nañu ko xamal mbooloo mi, bés bu ñuy wax fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi. Waxal xaalis bi mbooloo mi maye ngir jàpple liggéeyu waare bi ñuy def ci àddina si sépp, ak li mu maye ngir xaalis bi mbootaay bi di dajale ngir yeneen mbir.
◼ Sekkerteer bi ak wottukatu liggéeyu waare bi war na seet li pioñee yi def ci waaraate bi. Bu ci amee ku ci waaraatewul waxtu yi ko war, mag ñi war nañu seet ni ñu ko mënee dimbali. Nañu seet li nekk ci leetar S-201 yi ñuy jot at mu nekk, ak Le ministère du Royaume bu ut 1986, xët 4 ba 5, xise 12 ba 20.
◼ Ci atum 2003, waxtaan bi ñu faral di am ci àddina si sépp bu ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu weesoo, mu ngi tudd : “ Ndax waxtu àtte Babylon jot na ? ” Seetal li ñu ci wax ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bu septaambar 2002.
◼ Léegi, kenn dootul jotati La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yu ñu yónnee ci adareesam (abonnement). Kon bu La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yu mujj yi agsee ci mbooloo yi, war nañu leen gaaw a jox waaraatekat yi. Dina tax ñu mën a jot ci yéenekaay yi ñu moomal suñu bopp, te mën leen a jàng bala ñu leen di wone ci waaraate bi.
◼ Mbooloo Dakar English ak Dakar Sud jébbal nañu Yexowa seen Saalu Nguur gu bees gi nekk Medina, ci bésu 23 ak 24 Nowàmbar 2002. Bu ñu boolee ñi teew ci ñaari fan yi ñu ko doon defe, mat nañu 372.
◼ Ci bésu 1 desàmbar 2002, 20 waaraatekat yi nekk ci mbooloo Kaolack, jébbal nañu Yexowa seen Saalu Nguur gu bees. Bés boobu, 133 nit ñoo fa teew.