Ndax dinga nangu ñu def ay ndaje seen kër ?
1 Ci jamano karceen yu njëkk ya, ñu bare dañu doon nangu ñu def ndaje yi ci seen kër (1 Kor. 16:19 ; Kol. 4:15 ; Flm. 1, 2). Tey it, mbooloo karceen yi dañuy def ay ndaje ci kër nit ñi : njàngum téere bi ak ndaje yi ñuy am bala ñuy waare. Waaye ci yenn mbooloo, kër yu ñuy defe ndaje yooyu doyuñu. Looloo tax ñiy teew ci yenn njàngum téere mat 30 nit walla sax lu ko ëpp. Li gën mooy ñu bañ a weesu 15 nit.
2 Lu réy la : Ndax bëgg nga ñu def njàngum téere bi ci sa kër ? Masuloo ci xalaat ? Fu ñu koy def, ñi fay teew waruñu xat. Béréb bi dafa war a set, am leer bu doy, te féex. Njàngum téere bi bokk na ci ndaje mbooloo mi. Yexowa dafa ñuy jàngal foofu. Kon bu ñu defee ndaje boobu ci sa kër, am nga lu réy. Ñu bare wax nañu ne dañu ci jële lu réy ci wàllu ngëm.
3 Boo amee ci sa kër fu ñu mën a def njàngum téere bi, wax ko magi mbooloo mi. Xéyna fu mu nekk nii, dañuy wut fu ñu mën a def benn njàngum téere bi. Bu la sa kër mayul loolu, ndax mën nañu fa def ndaje bu ñuy am bala ñuy waare ? Xéyna it soxlaguñu fu ñuy defe ndaje yooyu. Waaye ba tey waxal mag ñi ne nangu nga ñu def ndaje ci sa kër. Mën na am ñu soxla ko ëllëg.
4 Nañu xam fu ñu war a yem ci kër jaambur : Bu ñuy daje kër jaambur, nañu xam ne alalu jaambur la. Way-jur yi war nañu yemale seeni doom ci béréb bu ñuy defe ndaje mi. Waruñu leen a bàyyi ñu dugg fu leen neex. Nañu xalaat it dëkkandoo yi. Buñu def lenn lu leen di yàqal, walla lu leen di tanqal. — 2 Kor. 6:3, 4 ; 1 Pie. 2:12.
5 Yawut yi 13:16 mu ngi ñuy ñaan ñu bañ a fàtte ‘ def lu baax ak di sédde ci suñu alal, ndaxte sarax yu mel noonu ñoo neex Yàlla ’. Boo nangoo ñu def ay ndaje ci sa kër, dinga sédde ci sa alal te “ sargal Yexowa ak sa alal ”. — Léeb. 3:9.