Saalu Nguur yi ñu tabax ci àddina si — ci ay réew yu nekk ci Ërob
1 Ci ay réew ci Ërob, boole ci Penku Ërob, tere woon nañu liggéeyu Seede Yexowa yi ci at yii weesu. Ci lu ëpp, dañu leen doon xatal lool. Seede yi mënuñu woon a am seeni ndaje ci kanamu ñépp. Te amuñu woon sax ay Saalu Nguur fu ñuy defe ndaje yooyu. Waaye ci at yii paase, ‘ Yexowa dafa ñu defal lu réy. Bég nañu ’. — Sab. 126:3.
2 Ci atum 1983, nguur yi dañu tàmbali wàññi seen xatal boobu ci Seede Yexowa yi. Atum 1989 fekkoon na réewu Poloñ ak Ongri nangu Mbootaayu Seede Yexowa yi. Ci atum 1991, réewu Rusi nangu na loolu itam. Booba ba léegi, liggéeyu Seede Yexowa yi mu ngi yokku ci réewu Rusi ak réew yi bokkoon ci moom bu njëkk. Diggante màrs 1996 ak oktoobar 1998, ay bànqaas yu yore 11 réew ci Ërob, ñaan nañu ñu abal leen xaalis ngir tabax 359 Saalu Nguur. Jataay biy dogal nangu na ñu jox leen xaalis boobu.
3 Xoolal foto yi nekk fii. Ndax Yexowa du lu réy la defal mbootaayam (Sab. 136:4) ? Waaw ci dëgg, mën nañu ne ñu ngi jariñoo bu baax xaalis bu ñuy maye ngir loolu te kontaan nañu. Maye yooyu bokk nañu ci li Yeesu waxoon ci Yowanna 13:35 : “ Ni ñuy xame ne samay taalibe ngeen, mooy ngeen bëggante. ”
4 Am na benn porogaraam bu ñu def ngir tabax ay Saalu Nguur ci réew yu barewul xaalis. Ci Ërob, Rumàni bokk na ci réew yooyu. Weeru Sulyet 2000 ba tey, dimbali nañu leen ba ñu tabax 36 Saalu Nguur. Ci Ukrén tabax nañu 61 Saalu Nguur ca atum 2001. Te yi ci gën a bare, benn palaŋ kese lañu doon topp ngir tabax leen. Looloo tax ñu gaaw noonu. Te it dañu bëggoon a tabax yeneen 76 Saalu Nguur ci atum 2002. Ay téeméeri Saalu Nguur lañu tabax noonu ci Bulgari, Korowasi, Masédwan, Moldawi, Rusi ak Serbi-Monténégro ak xaalis bu ñuy maye ngir tabax ay Saalu Nguur.
5 Tabax ay Saalu Nguur ci yenn réew yombul woon. Foofu bala ñuy mën a tàmbali tabax bi, dafay yàgg te dañuy sonn. Te li nga war a fey ngir tabax benn Saalu Nguur foofu ci Ërob moo ëpp fuuf li ñuy fey ci yenn réew ci Afrig walla Amerig Latin. Waaye ca réew yooyu barewul xaalis, ñiy jaamu Yexowa ñu ngi yokku rekk. Kon, ba tey dañu fa soxla ay téeméeri Saalu Nguur.
6 Saalu Nguur yooyu yépp yi nga xam ne ñu ngi gën di bare rekk, aka nekk lu baax te rafet ! Te ñu bare dañu ne seede bu rafet la fi ñu leen tabaxe. Seede Yexowa yi dañuy topp li nguur yi laaj ci wàllu tabax. Yenn saay bu waa nguur gi gisee loolu, dañu ciy kontaan lool.
7 Yonent Yàlla Isayi waxoon na ne ñiy jaamu Yexowa dinañu yokku ci suñu jamano. Yàlla jaar na ci moom ngir wax lii : “ Man mii, Yexowa, dinaa tax loolu gën a gaaw ca jamanoom. ” (Isa. 60:22). Bu ñu seetee fukki at yii paase, mën nañu ne ñu ngi ci jamano boo xam ne Yàlla mu ngi yokk ñi koy jaamu ca Penku Ërob. Dañu bëgg liggéeyu tabax ay Saalu Nguur ci ay réew yu bare gën a gaaw. Ñu ngi ñaan Yàlla mu barkeel li ñuy def ngir jàpple liggéey boobu bu ñuy maye xaalis. Dina tax Saalu Nguur yi gën a bare ci réew yu barewul xaalis. Ñiy jaamu Yàlla dinañu yokku ci Ërob. Te ay nit ñu gën a bare dinañu waare ba ca “ cati àddina ”. — Jëf. 13:47.
[Nataal bi nekk paas 3]
Ay Saalu Nguur yu ñu boole, Moscou, Russie
[Nataal bi nekk paas 4-6]
Saalu Nguur yu bees ci Penku Ërob
Strumica, Macédoine
Daruvar, Croatie
Bitola, Macédoine
Sokal, district de Lviv, Ukraine
Sofia, Bulgarie
Krasnooktyabrskiy, région de Maïkop, Russie
Bački Petrovac, Serbi-Monténégoro
Plovdiv, Bulgarie
Tlumatch, district d’Ivano-Frankivsk, Ukraine
Rava-Ruska, district de Lviv, Ukraine
Stara Pazova, Serbi-Monténégro
Zenica, Bosnie-Herzégovine
Sokal, district de Lviv, Ukraine
Jydatchiv, district de Lviv, Ukraine