Yégle yi
◼ Téere yi ñuy wone ci weeru me : Benn La Tour de Garde ak benn Réveillez-vous ! Am na ay nit ñu teewoon ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, walla ci beneen ndaje, waaye tàmmuñu teew ci ndaje yi yépp. Bu ñu leen di dellu seeti ñoom walla ñeneen nit ñu suñu waxtaan neex, nañu góor-góorlu ngir jox leen téere Adorez Dieu. War nañu def li ñu mën ngir jàng ak ñoom Biibël bi, rawatina bu ñu masee jàng ak seede Yexowa yi téere Xam-xam ak téere Laaj. Suweŋ : Téere Xam-xam walla téere Laaj. Boo tasee ak ku am téere yooyu ba pare, won ko beneen téere bu ndaw bu ko mën a itteel. Sulyet ak ut : Téere La route qui mène à la vie éternelle. Seetleen ni ngeen war a def ngir wone téere boobu ci seen goxu mbooloo yépp. Bu fekkee ne dangay waaj a tukki ngir dem Afrig, nanga yóbbaale lu doy ci téere yooyu ngir mën ci joxe lu bare.
◼ Wottukat biy jiite walla nit ki mu tànn war na seet ndax xaalisu mbooloo mi mat na. Loolu, 1 suweŋ lañu ko war a def, walla ni mu gënee gaaw gannaaw bés boobu. Bu ñu defee loolu ba pare, war nañu ko xamal mbooloo mi, bés bu ñuy wax fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi.
◼ Ci weeru màrs 2003, wottukat biy wër ci réew yi, suñu mbokk Sébastien Johnson, ñëwoon na ci mbooloo yi nekk Senegaal ak Mali. Defal na leen waxtaan bi tudd “ Bégleen ndax yaakaar bi ”. Ca bésu 2 màrs, 277 nit ñoo ñów déglu waxtaan boobu ca Saalu Nguur bi nekk Sogoniko ca Bamako. Dakar, ca bésu 9 màrs, 1 220 nit ñoo ko ñów déglu ca Almadi, ca saalu ndaje yu mag yi.
◼ Ci bésu 8 màrs 2003, 40 waaraatekat yi bokk ci mbooloo Dakar-Franco-Wolof, ñoo doon jébbal Yexowa seen Saalu Nguur bi ñu doon sog a defaraat. Saalu Nguur boobu, mu nga féete ca Almadi, ci wetu saalu ndaje yu mag yi. Ñi fa teewoon matoon nañu 212 nit.