Ay tont ci seeni laaj
◼ Bu ñuy waaraate ci telefon, ndax war nañu wax ci maye yi ñu mën a def ngir jàpple liggéeyu waare bi ?
Liggéey bu ñuy def ci àddina si sépp ngir jàngale Biibël bi, xaalis bi muy laaj yépp, dañu koy jële ci maye yi nit ñi di def ngir jàpple ñu. Loolu, dinañu ko mën a wax nit ñi bu ñu taxawee seen kanam. Waaye bu ñuy waaraate ci telefon, waruñu wax dara lu jëm ci maye yooyu. Su ko defee, nit ñi duñu foog ne dañu bokk ci ñiy ñaan xaalis ci telefon. Liggéey boobu Seede Yexowa yi di def, wutuñu ci benn xaalis. — 2 Kor. 2:17.
◼ Bu ñuy waaraate ci telefon, lan lañu war a def su amee ku wax ne bëggatul Seede Yexowa yi woo ko ci telefon ?
War nañu def li nit kooku bëgg. Dinañu bind ci kàrtu gox bi bés bi mu waxee loolu. Su ko defee, waaraatekat yi duñu ko woowati. Benn yoon at mu nekk, dinañu seetaat fi ñu binde turu ñi bañ ñu woo leen. Ay waaraatekat yu mën waaraate bu baax te xam bu baax ni ñuy waxe ak nit, dinañu woo nit ñooñu. Dinañu jéem a xam ndax ba léegi bëgguñu Seede yi woo leen telefon ngir waar leen. — Seetal Réponses à vos questions ci Le ministère du Royaume bu sãwiyee 1994.