Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
12-18 me
Woy-Yàlla 57
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 8, te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde bu 1 me ak Réveillez-vous ! bu 22 awril. Ku ci nekk, na wax ci benn yéenekaay kese, waaye ñaar la war a wone. Te it na wax nit ki ne mën na maye li ko neex ngir jàpple suñu liggéey.
20 min : Yéen wayjur yi, nangeen dimbali seeni doom ngir ñu jëm kanam ci wàllu ngëm. Waxtaan ci ay ponk yu am solo ci téere École du ministère, xët 9-12 ak 21-38. Waxal wayjur yi ñu boole xët yooyu ci seen njàngum Biibël bi ci njaboot gi ngir dimbali seeni doom ñu jëm kanam ci liggéeyu waare bi. Woneel ay ponk yi mën a dimbali ndaw yi ngir ñu gën a mën waaraate.
15 min : “ Ñun lañu dénk xibaar bu baax bi. ”* Bala ndaje bi di jot, tànnal benn walla ñaari waaraatekat ngir ñu nettali li ñu soppi ci seen àddina ngir yokk li ñu def ci liggéeyu waare bi.
Woy-Yàlla 21 ak ñaan bu mujj bi.
19-25 me
Woy-Yàlla 29
15 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi. Waxtaanleen ci “ Saalu Nguur yi ñu tabax ci àddina si — ci ay réew yu nekk ci Ërob ”. Waxal ne liy jàpple liggéey boobu mooy xaalis bi ñuy maye ngir tabax Saalu Nguur yi ci suñu bànqaas ak ci yeneen réew yu barewul xaalis.
15 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.
15 min : “ Nanga waar nit ñi saa yoo ci amee bunt ngir màggal Yexowa. ” Waare ak waxtaan ak ñi teew. Boo àggee ci xise 3, laajal ni ñu mënee tàmbali benn waxtaan ci Biibël bi : 1) Bu ñuy dem jëndi dara walla bu ñuy duggi màrse. 2) Bu ñu nekkee ci kaar walla ci taksi. 3) Bu ñuy waxtaan ak suñu benn dëkkandoo. 4) Bu ñuy waxtaan ak ñi ñu bokkal liggéey fu ñuy liggéeye. 5) Bu ñuy waxtaan ak suñu benn waa kalaas ci lekkool bi. Bala ndaje bi di jot, laajal benn waaraatekat mu nettali naka la doon seede saa yu ci amee bunt.
Woy-Yàlla 56 ak ñaan bu mujj bi.
26 me-1 suweŋ
Woy-Yàlla 77
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fàttalil ñépp ñu bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru me te joxe ko. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 8, te wone ni ñu mënee wone La Tour de Garde bu 15 me ak Réveillez-vous ! bu 8 me. Ku ci nekk, na wax ci benn yéenekaay kese, waaye ñaar la war a wone. Kenn ci ñoom dina maye kayit Aimeriez-vous en savoir plus sur la Bible ? ginnaaw nit ki mu waxal dafa bañ a jël ci yéenekaay yi.
10 min: Ay tont ci seeni laaj. Waare lay doon. Ci lu gàtt waxal ci li nekk ci Le ministère du Royaume bu feewriyee 2001, xët 6, xise 12-15, lu jëm ci waaraate ci telefon. Walla nga wone yeneen fasoŋu waare ci telefon yi baax ci seen gox.
25 min : “ Kàddu Yàlla mooy dëgg. ”a Laajal laaj yi nekk ci suufu xaaj bii. Nit kuy waaraate, bu jëfandikoo Biibël bi ngir tontu laaj yi ñu koy laaj, dafay dimbali nit ñi ñu jàng dëgg gi. Laajal ñi teew ñu nettali naka la leen loolu dimbalee ñoom ci seen bopp bi ñu doon jàng Biibël bi. Boo àggee ci xise 6, na benn waaraatekat bu aay wone ni ñu mëne jàng ci Biibël bi bu ñuy njëkk wax ak nit. Bu koy def na topp li nekk ci xaaj “ Faramfàcceel ci fasoŋ bu jub Kàddug Yàlla ”. — km-WO 12/01 xët 1 xise 3-4.
Woy-Yàlla 86 ak ñaan bu mujj bi.
2-8 suweŋ
Woy-Yàlla 50
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Seetaatal ci Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2002 xët 2 ak 3, benn walla ñaari fasoŋ bi ñu mënee wone téere Laaj ak Xam-xam.
20 min : Séy ci yoon — Loolu la Yàlla laaj. Waare ak waxtaan ak ñi teew. Ci ay réew yu bare nekkaale du dara ci nit ñi. Am na sax ñuy wax ne loolu dafa am njariñ. Woneel li Biibël wax ci loolu. Lii la ñépp a war a xam : Séy, ci Yàlla la jóge (rs p. 224-225). Nekkaale, njaaloo la (fy p. 17). Am na ay boroom xam-xam ñuy seetlu liy dal ñiy nekkaale. Lii lañu gis : Ñiy nekkaale bala ñuy séy, ñu ci gën a bare dinañu fase (g02 8/3 p. 29 ; g92 8/9 p. 28 ; g91 8/5 p. 28). Bu karceen yi toppee ndigali Yàlla yi, dañuy sargal Yexowa. Te it seen njariñ lay doon. — Isa. 48:17, 18.
15 min : Naka la leen jariñe ? Waxtaan ak ñi teew. Wottukatu lekkool bi moo ko war a def. Ci weeru sãwiyee dañu tàmbali benn fasoŋ bu bees bi ñu defe Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla. Ci lu gàtt waxal lan moo ci bees. Woneel lu baax li mu indi booba ba léegi. Ndax ñi bokk ci Lekkool bi, maanaam eleew yi, yokku nañu ? Ñi bëgg tontu ci laaj yi ñuy laajte ci Lekkool bi, ndax gën nañu bare ? Ban njariñ la eleew yi jële ci fasoŋ bi ñu leen di xelal léegi ? Laajal ñi teew ñu wax lu ñu jële ci Lekkool bu bees bi. Laaj leen it ñu wax lu ñu xalaat ci porogaraam bu bees bi, maanaam naka la leen nar a dimbalee ëllëg.
Woy-Yàlla 23 ak ñaan bu mujj bi.
[Li ñu bind ci suu]
a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.