Nañu fàttaliku li ñu jàng ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla
Laaj yii di topp, ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla lañu ko war a def, ci diggante 25 ak 31 ut 2003. Ci lu mat 30 simili, wottukatu lekkool bi dina waxtaan ak ñi teew ngir fàttaliku li ñu def ci lekkool bi ci diggante 7 sulyet ba 25 ut 2003. [Bul fàtte : Bu amee laaj boo xam ne kenn bindul loo war a jàng ngir xam tont bi, yaa ko war a wutal sa bopp. — Seetal li ñu wax ci téere École du ministère, xët 36-37.]
LIY TAX ÑU AAY CI WAX
1. Bu ñuy waaraate, lu tax ñu war a xool ki ñuy waxal ? [be p. 125 § 1-2 ; p. 125, encadré]
2. Bu fekkee ne dangay ragal bala ngay waaraate, lan moo la ci mën a dimbali ? [be p. 128 § 4-5]
3. Ci Saalu Nguur gi, booy def benn waxtaan ci kanamu ñépp, lan moo la mën a dimbali ba booy wax, mu mel ni dangay waxtaan ak say xarit ? [be p. 129 § 2 ; p. 129, encadré]
4. Naka lañu mëne topp li ñu wax ci 3 Musaa 16:4, 24, 26, 28 ; Yowanna 13:10 ; Peeñu bi 19:8 ? Lu tax mu am solo lool ? [be p. 131 § 3 ; p. 131, encadré]
5. Nit ku xam fi mu war a yem te “ maandu ”, naka lay mel ? (1 Tim. 2:9, 10) [be p. 132 § 1]
WAXTAAN N° 1
6. Karceen yi dañu war a muñalante. Waaye lan lañu dul nangu ci seen biir ? (Kol. 3:13) [w01 15/7 p. 22 § 7-8]
7. Dëgg la walla déet : Bu ñuy wax ci benn yëf ba joxe ci li ñuy wax nombre ordinal (mel ni ñaareel bi, ñetteel bi) wax nañu ñaata yëf moo am. Leeralal sa tont. [si p. 282 § 24-5]
8. Ci lépp li ñu mën a xiir ci jàng Kàddu Yàlla, lan mooy li gën ? Lu tax loolu moo ñu war a xiir ci jàng Kàddu Yàlla ? [be p. 24 § 1]
9. Nit ku am xel, naka lay ‘ sàmmee xam-xam ’ ? (Léeb. 10:14) [w01 15/7 p. 27 § 4-5]
10. Ayóoba dafa tàmmoon a def lu baax. Lu tax ñu war ci xalaat bu baax ? (Ay. 1:1, 8 ; 2:3) [w01 1/8 p. 20 § 4]
LI ÑU WAROON A JÀNG CI BIIBËL BI AYU-BÉS BU NEKK
11. Naka la jataay biy dogal fexee ba ñoom ñépp ñu nangu ne soxlawul ñu xarfal karceen yu nekkul woon Yawut ngir ñu mën a mucc ? (Jëf. 15:25)
12. Lu tax jataay biy dogal wax Pool mu topp yenn ndigal yu nekkoon ci Sàrtu Musaa, fekk Yexowa waxoon na ne soxlatul ñu topp sàrt boobu ? (Jëf. 21:20-26) [it-2 p. 701 § 4 ; it-2 p. 1166 § 2-5]
13. Fen yi nit ñi doon wax ci Ndaw li Pool dañu niroo ak lu ñaaw li ñuy wax ci Seede Yexowa yi tey. Yan fen lañu waxoon ci moom ? (Jëf. 24:5, 6) [w01 15/12 p. 22 § 7–p. 23 § 2]
14. Bi ñu ko tëjee sax lu mat ñaari at ci benn kër, ci lan la Pool nekke waaraatekat bu jar a topp ? (Jëf. 28:30, 31)
15. Lu tax ñu mën a wax ne njiiti àddina si bokk nañu ci “ ndigalu Yàlla ” ? Loolu lu muy def ci karceen yi ? (Room 13:1, 2) [w00 1/8 p. 4 § 5]