Yégle yi
◼ Téere yi ñuy wone ci weeru ut : La route qui mène à la vie éternelle. Seetleen li ngeen war a def ngir wone ko ci gox bi seen mbooloo moom yépp. Boo waree tukki ci biir Afrig, nanga yóbbaale ay téere yu doy ngir joxe ci yu bare. Septaambar : La vie : comment est- elle apparue ? Évolution ou création ? Oktoobar : Benn La Tour de Garde ak benn Réveillez-vous ! Bu nit ki wonee ne suñu waxtaan neex na ko, war nañu ko won téere Laaj bi, te jéem a tàmbali ak moom benn njàngum Biibël bi. Nowàmbar : Téere Laaj walla téere Xam-xam. Bu ngeen gisee ku am téere yooyu ba pare, wonleen ko téere Adorez Dieu, walla téere yu yàgg yi.
◼ Ci diggante 20 ba 26 ci weeru Oktoobar bii di ñów, dinañu tàmbali jàng téere Adorez le seul vrai Dieu ci njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi.
◼ Wottukat biy jiite walla nit ku muy tànn war na seet ndax xaalisu mbooloo mi mat na. Loolu, bésu 1 septaambar lañu ko war a def, walla ni mu gënee gaaw gannaaw bés boobu. Bu ñu defee loolu ba pare, war nañu ko xamal mbooloo mi, bés bu ñuy wax fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi.
◼ At mu nekk, dañuy seet ñaata téere ak yéenekaay ñoo des ci mbooloo mi. Ren, bésu 31 ut 2003 lañu ko war a def, walla ci bés bu ko gën a jege. Liggéey boobu, mu ngi mel ni li kiy toppatoo téere yi di def weer bu nekk te war nañu bind li ñu ci waññ ci kayit bi tudd Stock des publications (S-18). Su amee ay mbooloo yu bokk fu ñuy dence seeni téere, kiy toppatoo yéenekaay yi ci mbooloo mu nekk dina joxe ñaata yéenekaay ñoo des ci mbooloom. Mbooloo mi war a jot loolu, maanaam biy toppatoo mbooloo yi ci des ci wàllu téere yi, bànqaas bi dina ko yónni ñetti kayit yi tudd Stock des publications (S-18). Nangeen bind li ñu ciy laaj ci benn bi te yónnee ko bànqaas bi, bala bésu 6 septaambar. Ñaareelu kayit bi, sotti lay doon. Denc leen ko ci mbooloo mi. Ñetteel bi, nangeen ko jëfandikoo bu ngeen di def liggéey boobu. Sekkerteer bi mooy toppatoo liggéey boobu. Moom ak wottukat biy jiite ñoo war a bind seen tur ci kayit bi ñuy yónnee ak bi ñuy denc (S-18).
◼ Bu mbooloo yi di laaj téere yi ñu soxla, mën nañu ci boole léegi téere yii : Calendrier des Témoins de Jéhovah 2004, Examinons les Écritures chaque jour — 2004 ak Annuaire des Témoins de Jéhovah — 2004.
◼ Waaraatekat yi nekk Senegaal, def nañu liggéey bu rafet ci weeru Awril. Waare nañu 33 289 waxtu, joxe 17 432 yéenekaay, am 13 797 nit ñu nu dellu seeti, te def 1 892 njàngum Biibël. Loolu masul woon a am. Amoon na 200 pioñee yuy jàpple. Weer woowu, 339 waaratekat ñoo nekkoon pioñee. Loolu it masul woon a am.
◼ Ci bésu 1 suweŋ 2003, 72 waaraatekat yi nekk ci mbooloo Dakar Nord, jébbal nañu Yexowa seen Saalu Nguur bu ñu sog a tabax. Bég nañu lool ci 314 nit ñi fa teewoon.