Ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi
11 ba 17 ut
Woy-Yàlla 96
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Yenn ci yégle yi nekk ci Sasu Nguuru Yàlla. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 8, te wone ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 22 sulyet ak La Tour de Garde bu 1 ut. Ku ci nekk, bu waxee ci benn yéenekaay ba pare, na tàllalal ki muy waxal ñaari yéenekaay. Na kenn ci ñoom wone li ñu mën a tontu bu amee ku ñu wax : “ Dama jàpp. ” — Seetal li nekk ci téere Comment raisonner, ci xët 19.
15 min : “ Nañu roy ci mbaaxaayu Yexowa. ”a Yenn saay kenn dina defal nit lu baax te loolu dina tax nit kooku nangu déglu xibaar bu baax bi. Ñaanal ñi teew ñu nettali lu mel noonu. Waxal waa mbooloo mi ne li ñuy def ngir jàpple seeni mbokk ci ngëm, rafet na lool.
20 min : “ Barke yi ñuy am bu ñu nekkee pioñee. ”* Laajal laaj yi nekk ci suufu xaaj bii. Waxal benn walla ñaari pioñee ñu wax barke yi ñu am bi ñu nekkee pioñee. Waxal ne képp ku bëgg nekk pioñee mën na am kayit bi ñuy bind ngir nekk pioñee.
Woy-Yàlla 74 ak ñaan bu mujj bi.
18-24 ut
Woy-Yàlla 37
12 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fu ñu tollu ci xaalisu mbooloo mi. Waxtaanleen ci xaaj bi tudd : “ Ndaje bu mag bu benn fan biy ñów : li ñu fay waxtaane. ” Waxal kañ la ndaje boobu di am, te waxal nit ñi ñu fexe ba nekk fa. Bu fekkee ne ndaje boobu ci weer yii di ñów lañu koy def, waxal ne ñi bëgg ñu sóob leen dañu ko war a wax wottukat biy jiite.
15 min : “ Liggéey buy seddal xol. ”b Bala ndaje bi di jot, waxal ñaar walla ñetti waaraatekat ne dinga leen laaj naka la liggéeyu waare bi di seddale seen xol.
18 min : “ Nañu toppatoo bu baax béréb fu ñuy jaamu Yàlla. ”c (Xise 1 ba 5) Laajal laaj yi nekk ci suufu xaaj bii. Bu ngeen di def xise 3 ak 4, waxal ni mbooloo mi di def ngir setal Saalu Nguur gi. Waxal lépp li nit ñi war a xalaat bu baax ci wàllu set-setal bi. Waxal waa mbooloo mi ne li ñuy def ngir suñu Saalu Nguur gi jekk ci fi ñuy jaamu Yàlla, rafet na lool.
Woy-Yàlla 49 ak ñaan bu mujj bi.
25-31 ut
Woy-Yàlla 78
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Na ñaari nit topp li nekk ci xët 8, te wone ni ñu mënee wone Réveillez-vous ! bu 8 ut ak La Tour de Garde bu 15 ut. Ku ci nekk, bu waxee ci benn yéenekaay ba pare, na tàllalal ki muy waxal ñaari yéenekaay. Na suñu benn mbokk ak doomam (waxambaane walla janq) waajal ni ñu nar a wone yéenekaay yi. Dañuy njëkk xool ci lu gaaw li nekk ci xaaj bi tudd Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi, ba pare ñu topp li ñu ci wax.
15 min : Li nekk soxla ci mbooloo mi.
20 min : Nañu am fitu waaraate (1 Tes. 2:2). Waare ak waxtaan ak ñi teew. Waxal lu tax ñu bare dañu ragal a jege nit ñi ngir xamal leen xibaaru Nguur gi. Loolu dina dal sax ñi nga xam ne bi ñu tàmbalee waaraate, mat na léegi ay ati-at. Tànnal yenn ci yi ñu nettali ci La Tour de Garde bu 1 desàmbar 1999 ci xët 25, ak La Tour de Garde bu 15 desàmbar 1999 ci xët 25, ak ci La Tour de Garde bu 1 awril 1996 ci xët 31. Waxal ñi teew ñu nettali naka lañu fexee ba am fitu waaraate, fekk dañu ko ragaloon a def. Àggaleel waxtaan bi ak li nekk ci La Tour de Garde bu 15 desàmbar 1999 ci xët 23 ba 24 ngir wone waa mbooloo mi ni ñu mënee am doole ci Yexowa.
Woy-Yàlla 13 ak ñaan bu mujj bi.
1-7 septaambar
Woy-Yàlla 49
10 min : Yégle yi jëm ci suñu mbooloo. Fàttalil waaraatekat yi ñu bind li ñu def ci liggéeyu waare bi ci weeru ut te joxe ko. Waxal téere yi ñu war a wone ci weeru septaambar. Bala ndaje bi di jot, waxal benn walla ñaari waaraatekat ne dinga leen laaj ñu nettali lu rafet li ñu def bu ñu doon waaraate saa yu ñu ci amee bunt fekk ñu ngi nekkoon ci jamano noppalu, walla ci nawet bi.
15 min : Boo waxee nit ne dinga ñówaat, ndax dinga ko def ? Waare ak waxtaan ak ñi teew ci li nekk ci La Tour de Garde bu 15 septaambar 1999 ci xët 10 ba 11, ci xaaj bi tudd “ Autres manières de tenir ses promesses ”. Bu ñu dajee ak nit ku suñu waxtaan neex, tàmm nañu jàpp ak moom bés bu ñuy ñówaat ngir waxtaan ak moom. Ndax dinañu fa dellu ni ñu ko waxe ? Waxleen ci ndigal yi nekk ci Biibël bi yu war a tax ñu gën a góor-góorlu ngir def li ñu dige. Waxal ñi teew ñu wax lu baax li ñu am bi ñu gaawee dellu seeti nit ku suñu waxtaan neex.
20 min : “ Nañu toppatoo bu baax béréb fu ñuy jaamu Yàlla. ”d (Xise 6 ba 12) Laajal laaj yi nekk ci suufu xaaj bii. Woneel bu baax lu tax ñu war a toppatoo bu baax suñu Saalu Nguur gi. Ngir loolu, jëfandikool wërale bi nekk ci xët 5. Ci lu gàtt waxal naka la seen Saalu Nguur mel. Waxal it li ngeen bëgg def ngir defar li ci yàqu, walla li ngeen bëgg defar ngir Saal bi gën a baax.
Woy-Yàlla 22 ak ñaan bu mujj bi.
[Li ñu bind ci suu]
a Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
b Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
c Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.
d Li ngay njëkk wax warul weesu benn minit, ba pare laajal ñi teew ay laaj, te may leen ñu tontu.