Nañu fàttaliku li ñu jàng ci Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla
Laaj yii di topp, ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla lañu ko war a def, diggante 25 ak 31 oktoobar 2004. Ci lu mat 30 minit, wottukatu lekkool bi dina waxtaan ak ñi teew ngir fàttaliku li ñu jàng ci lekkool bi ci diggante 6 septaambar ba 25 oktoobar 2004. [Bul fàtte : Bu amee laaj boo xam ne kenn bindul loo war a jàng ngir xam tont bi, yaa ko war a wutal sa bopp. — Seetal téere École du ministère, xët 36-37.]
LIY TAX ÑU AAY CI WAX
1. Bu ñuy def waxtaan bu jëm ci li karceen di def ngir jaamu Yàlla, naka lañu war a waxe ngir ñi ñuy déglu bëgg gën a góor-góorlu ci li ñuy def ? [be p. 203 § 3-4]
2. Lan mooy waxaat li nga waxoon, maanaam ci tubaab répétition, te lu tax mu am solo ? [be p. 206 § 1-4]
3. Lu ñu mën a def ngir turu waxtaan bi feeñ bu baax ci li ñuy wax ? [be p. 210 § 1-5, wërale bi]
4. Naka lañu mënee xam ponk yi ëpp solo ci waxtaan bi ñu war a def ci mbooloo mi ? [be p. 212 § 1-4]
5. Lan nga mën a def ba kàddu yi ëpp solo ci waxtaan bi nga war a def bañ a bare lool ? [be p. 213 § 2-4]
WAXTAAN N° 1
6. Lan moo mënoon a tax ñi nekkoon ca jamano tuufaan bi bañ a gëm ne Yàlla dina alag lépp ca jamano jooju ? [w02 1/3 p. 5-6]
7. Bi Yeesu nekkee ci kow suuf, nit ñi dañu ko doon woowe “ Jàngalekat bi ”. Woowewuñu ko “ Fajkat bi ”. Loolu lu muy wone ? (Lukk 3:12, NW ; 7:40, NW) [w02 1/5 p. 4 § 3 ; p. 6 § 6]
8. Naka la Léebu 11:24, 25 wonee ne góor-góorlu ci waaraate bi, lu am solo la ? [w02 15/7 p. 30 § 3-5]
9. Ca Eden, bi Aadama ak Awa bañee déggal Yàlla, lan lañu weddi te loolu ñu def, lu mu indi ci àddina ? (1 Mu. 3:1-6) [w02 1/10 p. 5 ; p. 6 § 2-3]
10. Naka lañu mënee xam at bi ñu waroon a taxawalaat diine dëgg gi ca Yérusalem ? [si p. 285 § 5]
LI ÑU WAROON A JÀNG CI BIIBËL BI AYU-BÉS BU NEKK
11. Ndegam Yexowa moo waxoon Balaam mu dem bokk ci ñi àndoon ak Balakk, lu tax mu mer bi ko Balaam defee ? (4 Mu. 22:20-22)
12. Bu jigéen bu nekk karceen digee dara, ndax jëkkëram mën na ko dindi ? (4 Mu. 30:6-8)
13. Tey, lan moo mel ni dëkki Israyil fu nit ñi mënoon a daw làqu ? (4 Mu. 35:6) [w95 15/11 p. 17 § 8]
14. Bu 5 Musaa 6:6-9 waxee ne dañu war a takk Kàddu Yàlla ci suñu loxo ak ci suñu jë, ndax dafa bëgg wax ne téere boobu ci boppam lañu war a jël, takk ko ?
15. Bi ñu waxee waa Israyil ne seeni yëre duñu màgget bay nekk ay sagar, ndax dañu bëggoon a wax rekk ne dinañu leen jox yëre yu bees ? (5 Mu. 8:4)