Yégle yi
◼ Téere yi ñuy wone ci weeru oktoobar : Benn La Tour de Garde ak benn Réveillez-vous ! Bu nit ki wonee ne suñu waxtaan neex na ko, won ko téere Laaj bi, te fexeel ba tàmbali ak moom benn njàngum Biibël. Nowàmbar : Écoute le grand Enseignant. Bu nit ki waxee ne amul doom, won ko téere Laaj bi te jéem a tàmbali benn njàngum Biibël. Desàmbar : Le plus grand homme de tous les temps. Mën nga wone it benn ci téere yii : La Bible: Parole de Dieu ou des hommes? ; Recueil d’histoires bibliques ; Vous pouvez vivre éternellement sur une terre qui deviendra un paradis. Sãwiyee : Bépp téere bu ñu defar bala atum 1990. Mbooloo yu amul téere yu yàgg yooyu mën nañu wone téere L’humanité à la recherche de Dieu.
◼ Porogaraamu “ Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla ci atum 2005 ” mu ngi ci xët 3 ba 6. Dencleen ko bu baax ndaxte dingeen ko soxla ci at mi yépp.
◼ Ci atum 2005, waxtaan bi ñuy faral di am ci àddina si sépp, bu ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu weesoo, dimaas 10 awril lañu koy def. Bu beneenee, dinañu leen wax turu waxtaan bi. Ayu-bés boobu, su wottukat biy wër ci mbooloo yi nekkee ci yéen, walla su ngeen amee ndaje bu mag, waxtaan boobu na ngeen ko def ayu-bés bi ci topp. Benn mbooloo warul def waxtaan boobu balaa bésu 10 awril 2005.
◼ Bu waaraatekat soxlaa téere, waru ko laajal boppam bànqaas bi. Weer wu nekk, bala ñuy yónnee ci bànqaas bi li mbooloo mi soxla ci wàllu téere, wottukat biy jiite war na def benn yégle. Bu boobaa, képp ku soxla téere, dina ko mën a wax kiy toppatoo téere yi ci mbooloo mi. Buleen fàtte ne am na téere yoo xam ne kenn du leen denc ci mbooloo mi. Bala nga leen di am, fàww nga wax kiy toppatoo téere yi ci seen mbooloo, mu laaj leen bànqaas bi.
◼ Bu ngeen nekkee ci ndaje bu gën a mag bi tudd “ Nañu ànd ak Yàlla ”, buleen fàtte bind ci lu gàtt li ëpp solo ci waxtaan yi. Dina tax ngeen mën a bokk ci waxtaan bi ñu war a def ci benn ndaje liggéeyu waare ci weeru feewriyee 2005, ngir fàttaliku li ñu jàng ci ndaje bu mag boobu.
◼ Ñu ngi leen di xamal ne bànqaas bi am na adarees bu bees. Mooy adarees bii : Association “ Les Témoins de Jéhovah ” du Sénégal, B.P. 3107 18523 Dakar, Sénégal. Leetar yi Betel bi moom kese lañu war a yónnee ci adarees boobu. Post bi xamal na ñu ne ñiy jëfandikoo suñu boîte postale dañu bare torop. Li ñu fay yónnee dafa bare ba nga xam ne, ci yoon, lu ëpp benn boîte postale lañu waroon a am. Kon nag, dañu bëgg xamal waaraatekat yi ne waruñu joxe adarees boobu ngir ñu yónnee leen fa leetar yi ñu moom. Waaye nag, am na leetar yoo xam ne ci adarees boobu lañu leen war a yónnee. Mooy leetar yi jëm ci mbirum mbooloo yi, mel ni leetar yiy wax téere yi mbooloo mi soxla, li mbooloo mi def ci waaraate bi, leetar yiy wax ci Saalu Nguur gi, walla ci leneen lu mel noonu.