TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • mwb24 Nowàmbar p. 2-16
  • 4 nowàmbar ba 10 nowàmbar

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • 4 nowàmbar ba 10 nowàmbar
  • Dundinu kerceen ak liggéeyu waare bi—Kaye ndaje bi—2024
Dundinu kerceen ak liggéeyu waare bi—Kaye ndaje bi—2024
mwb24 Nowàmbar p. 2-16

4 NOWÀMBAR BA 10 NOWÀMBAR

TAALIFI CANT 105

Woy-Yàlla nº 3 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

Réew mi Yàlla digoon waa Israyil. Foto yu ñu boole: 1. Ibraayma. 2. Isaaxa. 3. Yanqóoba.

1. Dafay «fàttaliku ba fàww kóllëreem»

(10 minit)

Li Yexowa digoon Ibraayma dafa ko waxaat Isaaxa ak Yanqóoba (Njàlbéen ga 15:18; 26:3; 28:13; Taalifi Cant 105:​8-11)

Dige boobu dafa meloon ni lu mënul nekk (Taalifi Cant 105:​12, 13; w23.04 28 §11-12)

Yexowa masul a fàtte kóllëre gi mu fasoon ak Ibraayma (Taalifi Cant 105:​42-44; it-2 493)


LAAJAL SA BOPP LII: ‘Xam ne Yexowa ku jar a wóolu la, lan lay def ci man?’

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 105:​17-19—Naka la «Kàddug Aji sax ji» nattoo Yuusufa maanaam naka la ko kàddu Yàlla dimbalee ci nattu yi mu amoon? (w86 11/1 19 §15)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

(4 minit) Taalifi Cant 105:​24-45 (th lesoŋ 5)

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(1 minit) KËROO-KËR. Li nga mën a def bu dee ki ngay waxal dafa jàpp (lmd lesoŋ 2 ponk 5).

5. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(2 minit) KËROO-KËR. Nit ki dafa bëgg a werante ak yaw. Nanga tëj waxtaan bi ci anam bu rafet (lmd lesoŋ 4 ponk 5).

6. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki

(4 minit) KËROO-KËR. Bi ngeen mujjee waxtaan, nit ki dafa la waxoon li ko itteel. Jox ko yéenekaay buy wax ci loolu. (lmd lesoŋ 8 ponk 3)

7. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki

(4 minit) WAARAATE SAA YUÑU AMEE BUNT. Waxal nit ki lu jëm ci application JW Library®, te dimbali ko mu telesarse ko (lmd lesoŋ 9 ponk 5).

DUNDINU KARCEEN

Woy-Yàlla nº 84

8. Ni ñu mënee wone suñu mbëggeel ci Yeesu

(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.

Bu ñuy jël suñu jot ak suñu alal ngir jàpple liggéeyu nguuru Yàlla te def ko ak suñu bépp kàttan, noonu lañuy wone suñu mbëggeel ci doomu Yexowa, Yeesu Kirist mi mu fal buur. Bu ñuy def loolu, dinañu neex Yexowa te suñu mbokk yi ci wàllu ngëm dinañu njariñoo bu baax liggéey yi ñuy def (Yowaana 14:23). Ci misaal, waxtaan yi nekk ci jw.org ci xaaj bi tudd «Li ñuy def ak li ngeen di maye», dañuy wone ni suñu maye yi di dimbalee bu baax suñu mbokk yi ci ngëm, yi nekk ci àddina sépp.

Ab loxo buy dugal xaalis ci benn boyet. Foto yu ñu boole: 1. Ab mbokk bu góor a ngi taxaw ci kanamu benn attekat. 2. Benn mbokk bu jigéen a ngi liggéey ci benn ci béréb yi ñuy tabax ngir jaamu Yàlla. 3. Benn mbokk bu jigéen a ngi seetaan wideo ci làkku muuma yi.

Woneel WIDEO bi tudd: Maye yi ngeen di def am nañu solo lool. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Buñu amee ay mbokk yu war a taxaw ci kanamu yoon, ndaxte fi ñu dëkk dañu leen di jéem a téere ñu jaamu Yexowa ni mu ware, dañu leen ciy dimbali. Naka la maye yi ngeen di def di ñu jàpple ci loolu?

  • Dañuy jot ay maye yuy jóge ci dëkk yoo xam ne seen am-am yemul. Ni ñuy def ba tollale maye yooyu, naka lañuy amale njariñ ci tabax ay saalu nguur ci àddina si sépp?—2 Korent 8:14

  • Naka la maye yi ngeen di def, di ñu dimbalee ci tekki Biibël bi ci ay làkk yu bare?

Xoolal yeneen leeral ci suñu palaas ci internet

Ab loxo buy dugal xaalis ci benn boyet.

Naka nga mënee def ay maye ngir jàppale liggéey bi ñuy def ci àddina si sépp? Demal ci suñu application JW Library. Ci suufu paas bu njëkk bi, am na fi ñu bind ci farãse «Dons». Ci dëkk yu bare, boo bësee ci «Dons», dinga gis fi ñu bind Faire un don aux Témoins de Jéhovah. Bësal fi ñu bind «FAQ» ngir telesarse téere buy tontu ci laaj yi nit ñi di faral di laaj ci lu jëm ci maye yi.

9. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

(30 minit) bt-F pàcc 17 § 13-19

Kàddu yi ñuy tëje ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº 97 ak ñaan

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager