TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • mwb24 Nowàmbar p. 3
  • 11 nowàmbar ba 17 nowàmbar

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • 11 nowàmbar ba 17 nowàmbar
  • Dundinu kerceen ak liggéeyu waare bi—Kaye ndaje bi—2024
Dundinu kerceen ak liggéeyu waare bi—Kaye ndaje bi—2024
mwb24 Nowàmbar p. 3

11 NOWÀMBAR BA 17 NOWÀMBAR

TAALIFI CANT 106

Woy-Yàlla nº 36 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. «Dañoo fàtte Yàlla ma leen di musal»

(10 minit)

Ragal taxoon na ba waa Israyil bañ a déggal Yexowa (Mucc ga 14:​11, 12; Taalifi Cant 106:​7-9)

Xiif ak mar taxoon na ba waa Israyil doon xultu di jàmbat ci kanamu Yexowa (Mucc ga 15:24; 16:​3, 8; 17:​2, 3; Taalifi Cant 106:​13, 14)

Jaaxle taxoon na ba waa Israyil jaamu ay xërëm (Mucc ga 32:1; Taalifi Cant 106:​19-21; w18.07 20 § 13)

Benn mbokk bu jigéen a ngi waaj a dem ci liggéeyu waare bi. Muy xalaat ci ni ko Yexowa dimbalee woon. Foto yu ñu boole: 1. Magi mbooloo mi dañu ko seeti woon ngir xiirtal ko. 2. Am na ku ko mayoon saag bu fees ak lekk. 3. Xaritam dafa ko yonni woon leetar ak benn foto.

XALAATAL CI LII: Di xalaat ci lépp li ñu Yexowa mas a defal, naka lañu loolu mënee dimbali buñu nekke ci jafe-jafe?

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 106:​36, 37—Lu tax ñu mën a méngale jaamu xërëm ak saraxal rab yi, maanaam maalaaka yu bon yi? (w06 15/7 13 § 9)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

(4 minit) Taalifi Cant 106:​21-48 (th lesoŋ 10)

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Na li ngay wax nekk lu yomb a nànd —Ni ko Yeesu defe

(7 minit) Waxtaan ak ñi teew. Woneel WIDEO bi, ba pare ngeen waxtaan ci lmd lesoŋ 11 ponk 1-2.

5. Na li ngay wax nekk lu yomb a nànd —Nañu roy ci Yeesu

(8 minit) Waxtaan bi dafa sukkandiku ci lmd lesoŋ 11 ponk 3-5 ak «Seetal aaya yii itam».

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº 78

6. Li mbooloo mi soxla ci wàllu ngëm

(15 minit)

7. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

(30 minit) bt-F pàcc 18 § 1-5 ak wërale bi nekk ci paas 142 ak 144

Kàddu yi ñuy tëje ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº 77 ak ñaan

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager