Ay njàngale ngir ndaje Dundinu Kerceen ak liggéeyu waare bi
© 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
1 BA 7 SEPTAAMBAR
NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA KÀDDU YU XELU PÀCC 29
Dëddul ngëm ak aada yi àndul ak li Biibël bi di jàngale
Kàddu yu Xelu 29:18, NWT
18 Fu peeñu amul, mbooloo mi def lu ko neex, waaye ñiy topp yoonu Yàlla dinañu bég.
wp16.06 6, wërale bi
Xam ñi nekk asamaan
Nit ñu bare tey, dañu mel ni ay jaam, ndax ragal biddaa ak malaaka yu bon yi. Dañuy takk ay ndombo, ay téere ak di diwoo saafara ngir aar seen bopp. Waaye ñun soxlawuñu def loolu. Biibël bi dalal na suñu xel bi mu nee lii: «Aji Sax ji déy suuf sépp lay jéere ay gëtam, ngir dooleel ñi ko wéetalal seen xol.» (2 Jaar-jaar ya 16:9) Yexowa miy Yàlla dëgg, te ëpp kàttan fuuf Seytaane, dina la aar boo ko wóoloo.
Boo bëggee Yexowa aar la, fàww nga jàng xam li ko neex te di ko def. Ci misaal, ci jamonoy taalibe yu njëkk ya, Kerceen ya dëkkoon Efes, dañu dajale seen téere ya ñu daan luxuse, lakk lépp. (Jëf ya 19:19, 20) Noonu itam, boo bëggee Yàlla aar la, fàww nga tàggook lépp luy ndombo, takk téere ngir aar sa bopp, jàng téere yuy wax ci luxus, ak lépp lu laal mbirum rab.
Kàddu yu Xelu 29:3a, NWT
3a Kuy jëfe xel, bégal sa baay, waaye kuy ànd ak jigéenu moykat yi yàq sa alal.
w19.04 17 § 13
Nanga xamle li Biibël bi wax ci ñi dee
13 Boo xamul ndax aada bii walla jëf jii, neex na Yexowa am déet, ñaanal Yexowa mu may la xel ngir nga xam li nga war a def. (Jàngal Yanqóoba 1:5.) Boo paree nga gëstu ci suñu téere yi. Boo gisul, mën nga laaj magi mbooloo mi. Duñu la wax li nga war a def, waaye dinañu la won ay xelal yu nekk ci Biibël bi yu la mën a dimbali. Booy def loolu, dinga ‘tàmm jëfe sam xel, ngir ràññee lu baax ak lu bon’ (Yawut ya 5:14).
Kàddu yu Xelu 29:25, NWT
25 Ragal nit, fiir la. Waaye ku wóolu Yexowa, dina la musal.
w18.11 11 § 12
Dinaa dox ci yoonu dëgg
12 Ay doxalin ak aada yu àndul ak li Biibël bi di jàngale. Yenn saay, suñuy mbokk, ñi ñu bokkal liggéey walla ñi ñu bokkal lekkool, mën nañu ñu xiir ci bokk ci feet yu neexul Yexowa. Lan lañu mën a def ba bañ a daanu ci seen fiir? Xanaa ñu fexee xam bu baax gis-gisu Yexowa ci feet yooyu. Jàngaat suñu téere yi wax ci feet yooyu ak fi ñu cosaanoo, mën nañu ci dimbali. Bu ñuy xalaat bu baax ci li tax Biibël bi tere ñu feet yooyu, dinañu gën a dëgëral suñu kóolute ci ne, ñu ngi dox ci li «neex Boroom bi.» (Efes 5:10) Nañu wóolu Yexowa ak Kàddoom. Loolu dina ñu dimbali ñu bañ a «ragal nit» (Kàddu yu Xelu 29:25).
Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi
Kàddu yu Xelu 29:5, NWT
5 Kuy jay sa moroom, yaa ngi koy dugal.
it «Jayaate» § 1
Jayaate
Kiy jayaate, dafay wax wax ju neex, di tagg nit ki, di ko wax lu dul dëgg ak waxu naaféq ngir neex ko. Waaye kiy jayaate dafay lor moroomam, ndaxte dafa koy xiir ci yëg boppam torop ak ci réy-réylu. Te kiy jayaate dafay wut a neex ki muy jay walla am ci moom dara. Dafay bëgg ki muy jay jàpp ne fàww mu jox ko dara mbaa mu gërëm ko. Li muy wut mooy kooku daanu ci fiir bi mu ko tegal. (Kàddu yu Xelu 29:5) Waaye jikko jooju bokkul ci xel mu rafet mi bawoo ci Yàlla. Mu ngi bokk ci xelum àddina si nga xam ne, li ci gën a fës mooy bopp sa bopp, parparloo ak naaféq. (Yanqóoba 3:17) Kon naxaate, fen, topp nit walla di ko màggal, ak di tagg nit ngir mu rus ba jox la dara, neexul Yàlla. (2 Korent 1:12; Galasi 1:10; Efes 4:25; Kolos 3:9; Peeñu 21:8).
8 BA 14 SEPTAAMBAR
NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA KÀDDU YU XELU PÀCC 30
«Bul tax ma ndóol mbaa ma bare alal»
Kàddu yu Xelu 30:8, 9, NWT
8 Musal ma ci naaféq ak fen. Bul tax ma ndóol mbaa ma bare alal. May ma rekk li ma war a dunde. 9 Ndax ma bañ a regg ba weddi la, naan: «Kan mooy Yexowa?» Bul tax ma ndóol itam, ndax ma bañ a sàcc, di tilimal sama turu Yàlla.
w18.01 24-25 § 10-12
Ban mbëggeel mooy indi mbégte dëgg?
10 Dëgg la ne, ñun ñépp a soxla xaalis. Am xaalis mën nañu aar. (Kàdduy Waare 7:12) Waaye ndax mën nañu bég dëgg bu ñu yorul lu bare? Waaw-waaw! (Jàngal Kàdduy Waare 5:12.) Yonent Yàlla Agur, doomu Yake lii la bind: «Bul tax ma ndóol mbaa ma bare alal. May ma rekk li ma war a dunde.» Xam nañu bu baax li tax Agur bëggul woon a ndóol. Moom ci boppam wax na li tax. Nee na bëggul woon ndóol dugal co ci sàcc, ndaxte loolu dina tilimal turu Yàlla. Waaye lu tax mu ñaan Yàlla bañ a bare alal? Lii la ci teg: «Ndax ma bañ a regg ba weddi la, naan: ‘Kan mooy Yexowa?’» (Kàddu yu Xelu 30:8, 9) Xéyna yow itam, xam nga nit ñoo xam ne, seen yaakaar gépp ci alal lañu ko teg waaye du ci Yàlla.
11 Ñi bëgg xaalis mënuñu neex Yàlla. Lii la Yeesu wax: «Kenn mënul a jaamoondoo ñaari sang; lu ko moy, dina bañ kii, bëgg ki ci des, walla mu jàpp ci kii, xeeb ki ci des. Mënuleen a boole jaamu Yàlla ak alal.» Te balaa muy wax jooju lii la waxoon: «Bàyyileen di dajale alal fii ci kaw suuf, ndaxte max ak xomaag mën nañu yàq lépp, te sàcc yi mën nañu koo sàcc. Waaye, dajaleleen alal fa kaw asamaan, ndaxte foofu amul max ak xomaag yu ko mën a yàq, te sàcc mënu fa dugg, sàcc ko.» (Macë 6:19, 20, 24, NWT).
12 Ñu bare gis nañu ne, yombal seen dund, yemul rekk ci may leen mbégte waaye dafa tax it, ñu gën a am jot ngir jaamu Yexowa. Benn góor gu tudd Jack te dëkk Etaa Sini, dafa jaay këram bu mag ak sosiyeteem ngir nekk pioñee ni jabaram. Lii la wax: «Jaay suñu kër, yombul woon ci ñun. Waaye li am mooy, saa yu ma demoon liggéeyi, damay ñibbeek naqaru xol ndax poroblem yu bare, fekk sama jabar moom dafa doon bég sa su nekk. Te teg ci di ma kókkali naan: ‘Sama pataroŋ moo gën ci pataroŋ yi!’ Léegi Yexowa mooy suñu pataroŋ ñun ñaar ñépp, ndaxte man it pioñee laa ni moom.»
Kàddu yu Xelu 30:15, 16, NWT
15 Watar yi* [*Xeetu sax la buy dund ci ndox tey tafu ci nit walla ci mala di muucu deretam] am nañu ñaari doom yu jigéen yuy yuuxu: «Jox ma! Jox ma!» Am na ñetti yëf yu dul suur, ñeent yu dul wax mukk: «Doyal naa!»: 16 Bàmmeel, jigéen ju mënul a jur doom, suuf su ñàkk ndox, ak safara si dul wax mukk: «Doyal naa!»
w87 15/5 30 § 8
Dinga bég boo ragalee Yexowa
◆ 30:15, 16. Lan la misaal yi nekk ci aaya yooyu di wone?
Misaal yooyu dañuy wone ne, ku bëgge du doyal mukk ci kiliftéef walla ci xaalis. Saxu watar dafay muucu deret te du mas a màndi. Nit ñi dañuy gas ay bàmmeel ngir suul ñi dee waaye suuf si du mas a fees. Jigéen ju jaasir juy jooy ndax li mu mënul a am doom. (Njàlbéen ga 30:1) Bu tawee, suuf si dafay naan ndox mi waaye loolu terewul mu wowaat. Safara suy tàkk, loo ci sànni mu lakk ko, di xaar leneen. Kon ku bëgge mën nañu ko misaale loolu lépp. Waaye ñi nangoo déggal Yàlla, seen bëgg-bëgg yaram du leen jiital ba mën leen.
Kàddu yu Xelu 30:24, 25, NWT
24 Am na ñeenti mbindeef yu bokk ci mbindeef yi gën a tuuti ci kaw suuf, waaye dañu muus: 25 mellentaan yi, mbindeef yu barewul doole lañu, waaye dañuy waajal seen lekk ci jamonoy noor.
w11 1/6 10 § 4
Nañu def li ñu mën
Dajaleel xaalis bala ngay jënd. Am na ñu jàpp ne, dajale xaalis bala ngay jënd, dafa xewwi. Waaye loolu dina ñu musal ci poroblemu xaalis yu bare. Te ñu bare ñi koy def, loolu dimbali na leen ba amuñu ay bor ak coono yi am bor àndal. Ndaxte li nga leb mooy faral di gën a seer li nga jënd ndax entere yi ñu ciy teg. Biibël bi mu ngi ñuy xamal ne, mellentaan dafa «muus» ndaxte li mu soxla noor, ci ‘jamonoy ngóob la koy dajale’ (Kàddu yu Xelu 6:6-8; 30:24, 25).
Wéyal di nekk ganu Yexowa ba fàww!
18 Baax na ñuy xalaat ci ni ñu gise xaalis. Laajal sa bopp laaj yii: ‘Ndax damay faral di xalaat ci xaalis ak li xaalis mën a jënd? Su ma lebee xaalis ndax damay yéex a fey, jàpp ne ki ma lebal soxlawu ko noonu? Ndax am xaalis tax na ma foog ne maa gën ñeneen ñi? Ndax yéwén naa? Ndax dama jàpp ne képp ku am alal ci mbooloo mi rekk, dafa bëgg xaalis? Ndax ñi am alal rekk laay xaritool, di daw ñi amul dara?’ Nekk ganu Yexowa cér bu réy la! Nañu moytu bëgg xaalis torop ngir wéy di am cér boobu. Suñu defee loolu, Yexowa du ñu bàyyi mukk! (Jàngal Yawut ya 13:5).
Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi
Kàddu yu Xelu 30:26, NWT
26 Daman yi, mbindeef yu barewul doole lañu, terewul ci doj yi lañuy tabax seen kër.
w09 15/4 17 § 11-13
Càkkeef bi dafay wone ne Yexowa boroom xel mu réy la
11 Daman beneen mala bu ndaw la, waaye mën nañu jànge ci moom lu am solo. (Jàngal Kàddu yu Xelu 30:26.) Boo gisee daman, dafa nirook njomboor bu réy, waaye tank yi ak nopp yi dañu gàtt. Mala bu ndaw boobu, fu am ay doj lay dund. Bët yu baax la am. Moo tax bu ko beneen mala bëggee jàpp, dafa koy gaaw a gis te nëbbatu. Daman yi dañuy faral di gurupoo ngir ku ci nekk aar moroomam. Te loolu dafa leen di dimbali ci jamonoy seddaay. Yexowa moo leen sàkke noonu.
12 Lan lañu mën a jànge ci daman yi? Li njëkk mooy, daman yi dañuy xool fu sore ngir gis mala yi leen bëgg a rëbb. Te it duñu sori seen pax yi ñu dëkk. Loolu moo tax duñu leen gaaw a jàpp. Ñun itam war nañu am gis-gis bu leer ci wàllu ngëm ngir mën na moytu fiiri Seytaane. Apootar Piyeer lii la xelal kerceen yi: «Àndleen ak seen xel tey moytu, ndaxte seen noon, Seytaane, mu ngi wër ni gaynde guy yuuxu, di wut ku mu lekk.» (1 Piyeer 5:8, NWT) Yeesu bàyyil na ñu fi royukaay bu baax. Bi mu nekkee ci kaw suuf, dafa doon moytu bépp fiir bu ko Seytaane mënoon a tegal ngir yàq digganteem ak Yàlla. (Macë 4:1-11) Nañu roy ci moom.
13 Lenn li ñu mën a def ngir wéy di moytu mooy jariñoo bu baax matuwaay yi ñu Yexowa may. Waruñu sàggane jàng Kàddu Yàlla ak teewe ndaje yi. (Luug 4:4; Yawut ya 10:24, 25) Te ni daman yi nangoo gurupoo nekk benn, ñun itam nañu jege suñu mbokki kerceen yi ngir mën a dëfëlante ci suñu biir. (Room 1:12) Bu ñu nangoo Yexowa aar ñu, dinañu wone ne ànd nañu ci li yonent Daawuda waxoon. Dafa ne: «Aji Sax ji mooy sama cëslaay, moo may aar, di ma wallu. Yàllaay sama cëslaay li ma yiiroo, fegu; mooy Boroom doole ji may musal, di ma làq.» (Taalifi Cant 18:3).
15 BA 21 SEPTAAMBAR
NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA KÀDDU YU XELU PÀCC 31
Li ñu mën a jànge ci li ab yaay xelal doomam
Kàddu yu Xelu 31:3, 10, NWT
3 Bul jox sa doole jigéen ñi, bul am doxalin buy sànk ay buur.
10 Ana ku mën a am jabar ju baax? Moo gën fuuf ay gànjar.
w11 1/2 19 § 7-8
Jàngalal say doom ñu xam li baax ak li bon
Nanga jàngal say doom ñu xam gis-gisu Yexowa ci séy. Fàww nga xamal leen li ñu war a moytu. (1 Korent 6:18; Yanqóoba 1:14, 15) Waaye nag Biibël bi dafa njëkk a wone ne, séy mayug Yàlla la, bala muy xamle ne bokk na ci fiiri Seytaane. (Kàddu yu Xelu 5:18, 19; Ngën-gi-woy 1:2) Kon yow waajur bi, booy wax rekk ci musiba yi nekk ci tëdd ak góor walla jigéen, loolu mën na yàq xelu xale yi ci séy ndaxte gis-gis bi ñu ciy am, du dëppook li Biibël bi wax. Benn jànq bu tudd Corrine te dëkk Farãs lii la wax: «Samay waajur dañu dëkkoon ci di ma wax ne, tëdd ak góor baaxul. Loolu dafa mujj a yàq sama gis-gis ci séy, ba am jëkkër sax dama ko ragaloon.
Nangeen xamal seeni doom gis-gisu Yexowa ci séy. Nadia, benn jigéen ju dëkk Meksik lii la wax: «Dama doon fexe saa su nekk, samay doon nànd ne, Yexowa moo sos séy ngir góor ak jigéen am ci bànneex. Kon góor tëdd ak jigéen, bonul, lu jaadu la. Waaye nag ci kaw ñu séy ci yoon ñoom ñaar. Su ñu respektee loolu, mu jural leen bànneex. Su ñu ko deful jële ci naqar. Kon lépp ci ñoom la aju.»
Kàddu yu Xelu 31:4-6, NWT
4 Buur yi waruñu naan biiñ, Lemuyel; te njiit yi waruñu wax: «Joxleen ma ma naan!» 5 Lu ko moy, dinañu naan ba fàtte li yoon tëral te xañ néew-ji-doole yi li ñu yellool. 6 Joxleen biiñ ñiy waaj a dee ak ñi nekk ci naqar wu metti.
ijwhf waxtaan 4 § 11-13
Waxal say doom lu jëm ci sàngara
Njëkkal a wax ci loolu, bu leen xaar. Benn góor gu tudd Marc te dëkk Grande-Bretagne lii la wax: «Xale yi mën nañu bañ a am gis-gis bu leer ci sàngara. Dama toog ak sama doom bu góor bu am juróom-ñetti at, waxtaan ak moom, ni xaritam. Ma laaj ko ndax naan sàngara lu baax la walla déet. Ni ma waxee ak moom dal na xelam, ba mu wax ma lépp li nekk ci xolam.»
Booy faral di wax ak say doom lu jëm ci sàngara, bu yàggee dinañu ci bàyyi xel. Bu xale bi di gën di màgg, dee ko wax lu jëm ci sàngara, ci ni mu war a moytoo buy jéggi tali, ak lu jëm ci nobante diggante góor ak jigéen.
Nekkal royukaay. Boo tegee epoos fu ndox am, epoos ba dafay naan ndox mi. Noonu it la xale yi di jéemee def lépp li ñi leen wër di def. Te gëstukat yi wone nañu ne, xale yi seeni waajur lañuy gën a roy. Kon bu dee saa yoo meree walla nga am jafe-jafe, dangay naan sàngara ngir giif walla fàtte jafe-jafe yooyu; yaa ngi jàngal say doom ne, sàngara moo ñuy génne ci suñuy jafe-jafe. Kon nekkal royukaay bu baax. Deel jëfandikoo sàngara ni mu ware.
Kàddu yu Xelu 31:8, 9, NWT
8 Nanga waxal ki muuma, te sàmm yelleefu ñiy waaj a dee. 9 Deel wax te di àtte njub. Sàmmal yelleefu néew-ji-doole ji ak ñi ndóol.
g17.6 9 § 5
Jàngalal say doom ñu nekk ñu woyof
Xiir leen ci maye. Wonal sa doom ne «joxe mooy gën a indi mbégte nangu.» (Jëf ya 20:35) Noo ko mën a defe? Yaak sa doom, xalaatleen ci ay nit ñu soxla ñu demal leen marse, ñu yóbbu leen fenn, walla ñu defaral leen lu yàqu ci seen kër. Te booy dimbali ñooñu, yóbbalel sa doom. Boo koy yóbbaale, dina gis mbégte bi ngay jële ci dimbali ñeneen ñi. Jëf sa doom gis, mooy anam bi gën ngir jàngal ko, mu doon nit ku woyof. (Benn njàngale ci Biibël bi: Luug 6:38).
Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi
Kàddu yu Xelu 31:28, NWT
28 Ay doomam jóg ndokkeel ko; jëkkëram jóg tagg ko.
Gërëm ko
16 Lenn li góor mën a def ngir teral jabaram mooy di ko gërëm ci lépp li muy def ngir jàppale ko. Su ko defee, jabaram dina sawar te dina yëg ne fonk na ko. (Kolos 3:15) Bu jëkkër di wax jabaram lu baax li mu gis ci moom, loolu dina seddal xolu jabaram, dalal xelam te dina xam ne jëkkëram bëgg na ko. (Kàddu yu Xelu 31:28).
22 BA 28 SEPTAAMBAR
NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA KÀDDUY WAARE PÀCC 1-2
Wéyal di tàggat ndaw ñi
Kàdduy Waare 1:4, NWT
4 Ag maas dafay wéy, beneen dikk, waaye suuf si dafay sax ba fàww.
w17.01 27-28 § 3-4
‘Li nga dégge ci man nanga ko jottali nit ñu wóor’
3 Ñu bare ci ñun, fonk nañu liggéey bi ñuy def ci mbootaay bi te bu ñu sañoon duñu ko mas a bàyyi. Waaye ndeysaan, li ko dale ca maam Aadama ba léegi, ag maas dafay ñëw, dund jamanoom jàll, geneen maas ñëw. (Kàdduy Waare 1:4) Waaye ci kerceen dëgg yi, coppite yooyu dafa ànd ak jafe-jafe ci jamanoo yi weesu. Ndaxte liggéey bi ci mbootaayu Yexowa dafa gën a yokku te dafa gën a jafe. Dañuy komaase yenn liggéey yi, dem ba ci digg bi, ñu war a soppi ngir ànd ak jamono ndax coppite yu gaaw yi ci wàllu teknolosi. Te loolu mën na jafe ci yenn màgget yi. (Luug 5:39) Te bu dul loolu sax, ñiy jëm mag ñu ngi gis ne mënatuñu li ndaw ñi mën, ndax seen doole waññeeku na. (Kàddu yu Xelu 20:29) Kon, tàggat ndaw ñi ngir ñu mën a def liggéey bi ëllëg, lu am solo la, te it wone mbëggeel la. (Jàngal Taalifi Cant 71:18).
4 Dénk ndaw ñi liggéey, mën na jafe ci ñi am taxawaay ci mbooloo mi. Ñenn ñi dañu fonk lool li ñuy def ci mbooloo mi, ba ragal koo ñàkk. Ñeneen ñi dañu ragal a dénk ndaw ñi liggéey, ndaxte dañu ñu foog ne, ndaw ñi duñu ko mën a def ni ñu koy defe. Am na ñu jàpp ne, amuñu jotu tàggat ñeneen ñi. Waaye nag ak lu ci mënta xew, bu ñu nekkee ndaw, waruñu yàkkamti torop, rawatina bu ñu xeebee liggéey biñ ñu dénk.
Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi
Kàdduy Waare 2:24, NWT
24 Dara gënul neex lii, nit di lekk, di naan ak di bànneexoo ñaqam. Loolu itam, gis naa ne, may la gu jóge ci Yàlla.
Kàdduy Waare 1:1, NWT
1 Kàdduy dajalekat bi, doomu Daawuda, di buur ca Yerusalem.
it «Dajalekat» § 1
Dajalekat
Baatu Qo·heʹleth ci làkku Ebrë (miy tekki «Dajelekat», «Boolekat») tur la bu jekk ci buur yi Yàlla doon tànn ngir ñu nguuru ci Israyil. (Kàdduy Waare 1:1, 12) Ki doon jiite, moo amoon wareefu dimbali mbooloo mi, mu wéy di takku ci Yàlla, miy seen Buur dëgg. (1 Buur ya 8:1-5, 41-43, 66) Loolu moo taxoon ñu naan, buur bu baax mooy buur biy xiir mbooloo mi mu jaamu Yexowa, te buur bu ko deful, buur bu bon la. (2 Buur ya 16:1-4; 18:1-6) Suleymaan dajalekat bi, tàmmoon na di dajale ca kër-Yàlla ga, waa Israyil ak doxandéem ya ca dëkk ba. Ci téere Kàdduy Waare, dafay xiir jaamu Yàlla yi, ñu sore bépp doxalin bu bon. Te am doxalin bu jekk ci mbooloo mu jébbalu ci Yàlla. Ñi tekki Biibël bi ci làkku Gereg, baatu Qo·heʹleth ci làkku Ebrë lañu tekki Ékklêsiastês (Dajalekat), maanaam «ku bokk ci mbooloo, walla ci mbootaay». Baat boobu lañuy jëfandikoo ci Biibël yi, ci làkku farãse.
29 SEPTAAMBAR BA 5 OKTOOBAR
NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA KÀDDUY WAARE PÀCC 3-4
Dëgëral-leen seen séy
Kàdduy Waare 3:1, NWT
1 Lu nekk ak waxtoom, jëf ju nekk ak waxtoom.
Na ku nekk yem ci ki mu séyal
LI BIIBËL BI WAX: «Sàmmleen seen dundin, waxuma ni ñu amul xel, waaye ni ñu am xel» (Efes 5:15). Seen séy dafa war a bokk ci li ëpp solo ci seen dund. Gise seen séy noonu, am xel la.
Yexowa dafa bëgg nga bàyyi xel bu baax ci ki nga séyal te ngeen dund yéen ñaar ci bànneex (Ecclésiaste 9:9). Wone na ci lu leer ne waruloo sàggane mukk ki nga séyal, waaye kenn ku nekk ci yéen ñaar danga war a xool li nga mën a def ba bégal sa moroom (1 Korent 10:24). Na ku nekk won moroomam ne amal na ko njariñ te sopp na ko.
LI NGEEN MËN A DEF:
Nanga fexe ba am jot di nekk ak ki nga séyal te bàyyi sa xel bu baax ci moom
Bul xalaat sa bopp kese waaye nanga sóoraale ki nga séyal
Kàdduy Waare 4:9, NWT
9 Ñaar a gën kenn, ndaxte dinañu am yool bu réy ci seen liggéey bu metti.
w23.05 23-24 § 12-14
Sàmmleen «jum bu Aji Sax ji taal»
12 Lan la ñiy séy mën a jànge ci Akilas ak Piriska? Xalaatal ci lépp li ngeen war a def yeen ñaar. Li nga tàmm di def yow kese, xoolal ndax mën nga ko bokk def ak ki ngay séyal. Seet ko ci Akilas ak Piriska. Ñoom ñaar dañu ànd ci liggéeyu waare bi. Ndax tàmm ngeen di def loolu yeen ñaar? Akilas ak Piriska dañu doon ànd liggéeyandoo itam. Xéyna yaak ki nga séyal bokku leen liggéey. Waaye ndax mën ngeen bokk defandoo liggéeyu kër ngi? (Kàdduy Waare 4:9) Su ngeen di dimbalante, dingeen gën a doon benn te dingeen ci mën a porofitoo ngir waxtaan. Robert ak Linda bi ñu séyeek léegi def na 50 at. Lii la Robert wax: «Wax dëgg amuñu jot ngir ànd féexal suñu xol. Waaye bu may raxas ndab yi, sama jabar di leen fomp; walla may buddi ñax, mu ñëw di ma baleel, damay bég lool. Defandoo liggéey yooyu dafa tax ñu gën a xaritoo. Te suñu mbëggeel dafay gën di yokku.»
13 Waaye bul fàtte ne, ngeen di nekk yeen ñaar taxul ngeen bennoo. Suñu benn mbokk bu jigéen bu dëkk Brésil lii la wax: «Tey yitte yi bare nañu bare boo xam ne, mën nga bokk ak nit kër te du ngeen gisante lu bare. Moo tax dem naa ba gis ne, góor-góorlu ngir nekk ak sama jëkkër lu baax la, waaye ngir jot googu am njariñ, fàww ma bàyyi xel ci moom.» Suñu beneen mbokk bu tudd Bruno ak jabaram Tays, ñoom nee nañu dañuy fexe ku nekk bàyyi xel bu baax ci moroomam. Bruno nee na: «Bu ñu toogee ñun ñaar, dañuy teg suñuy telefon fee, ngir dara du yàq suñu jataay.»
14 Léegi bu dee yaak ki nga séyal bëgguleen di toog bokk jataay nag, lan ngeen mën a def? Xéyna li waral loolu mooy bokkuleen bëgg-bëgg walla ku ci nekk dafay tàngal xolu moroomam . Xalaatleen ci misaalu safara si ñu joxe woon. Mënoo taal safara léegi, mu tàkk jëppét. Fàww nga koy xamb ndànk-ndànk, njëkkee ay matt yu ndaw door a yokk yu mag. Noonu ngeen war a def yeen itam, tàmbalee nekk tuuti yeen ñaar bés bu nekk. Waaye tànnleen a def lu leen neex yeen ñaar ñépp ak lu dul indi werante. (Yanqóoba 3:18) Bu ngeen defee loolu, seen mbëggeel dina yokku ndànk-ndànk.
Kàdduy Waare 4:12, NWT
12 Nit mën na song kenn, daan ko; waaye ñaar mën nañu ko të. Ñetti buum yu ñu boole ràbb ñu doon benn, du yomb a dagg.
w23.05 21 § 3
Sàmmleen «jum bu Aji Sax ji taal»
3 Bu jëkkër ak jabar bëggee wéy di sàmm «jum bu Aji Sax ji taal», fàww ñu góor-góorlu ngir am diggante gu rattax ak Yexowa. Naka la leen loolu mënee dimbali ci seen biir séy? Bu jëkkër ak jabar amee diggante gu rattax ak Yexowa, dañuy sawar ci topp ay santaaneem. Te loolu dina leen dimbali ñu moytu jafe-jafe yi mën a waññi mbëggeel gi ku nekk am ci moroomam. (Jàngal Kàdduy Waare 4:12.) Bu ñu amee it diggante gu rattax ak Yexowa, dinañu ko wut a roy te wone jikko yu mel ni mbaax, muñ ak yërmande. (Efes 4:32–5:1) Su jëkkër ak jabar di wone jikko yooyu, seen mbëggeel dina yokku. Suñu benn mbokk bu tudd Lena te séy lu tollook 25 at, nee na: «Nit ku ragal Yàlla, bëgg ko te may ko cér lu yomb la.»
Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi
Kàdduy Waare 3:8, NWT
8 Waxtu bëgg ak waxtu bañ; waxtu xare ak waxtu jàmm.
it «Mbëggeel» § 39
Mbëggeel
«Waxtu bëgg» Nit ñi ñu dul won mbëggeel mooy ñi Yexowa àtte ne, yelloowuñu mbëggeel ak ñi dëkk ci def lu bon. Feek nit wonewul ne dafa bañ Yàlla, dañu ko war a won mbëggeel. Yexowa ak Yeesu dañu bëgg lu jub te bañ lu awul yoon. (Taalifi Cant 45:8; Yawut ya 1:9) Ñi bañ Yàlla dëgg waruñu leen a won mbëggeel. Li am mooy, wéy di won ñooñu mbëggeel amul benn njariñ. Ndaxte ñi bañ Yàlla, mbëggeelu Yàlla du laal seen xol benn yoon. (Taalifi Cant 139:21, 22; Esayi 26:10) Loolu moo tax Yàlla bañ leen te jàpp bés ngir sànk leen. (Taalifi Cant 21:9, 10; Kàdduy Waare 3:1, 8).
6 BA 12 OKTOOBAR
NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA KÀDDUY WAARE PÀCC 5-6
Ni ñuy wone ne may nañu cér suñu Yàlla ju Mag ji
Kàdduy Waare 5:1, NWT
1 Moytul sa bopp sooy dem ca kër Yàlla ga. Dem fa ngir déglu moo gën fuuf dem fa ngir saraxe, ni ko ñi ñàkk xel di defe, ndaxte xamuñu ne li ñuy def baaxul.
w08 15/8 15-16 § 17-18
Woneel worma booy jaamu Yexowa
17 War nañu wormaal Yexowa bu baax bu ñu koy jaamu. Lii lañuy jàng ci Kàdduy Waare 5:1, «Moytul sa bopp sooy dem ca kër Yàlla ga». Bi Musaa ak Yosuwe taxawe ci suuf su sell, Yàlla dafa leen sant ñu summi seen dàll. (Mucc ga 3:5; Yosuwe 5:15) Dafa leen santoon ñu def loolu ngir wone cér ak worma. Sarxalkat ya ca Israyil, dañu waroon a sol ‘ay tubéyi njiitlaayi lẽe ngir muur seeni cér’ (Mucc ga 28:42, 43). Sarxalkat yi dañu waroon a def loolu ngir bañ seeni cér feeñ bu ñuy liggéey ca sarxalukaay ba. Seen njaboot it dañu waroon a wone ne, wormaal nañu Yàlla ci ni ñuy toppe li leen Yàlla sant ci fànn boobu.
18 Kon teral Yàlla te wormaal ko dafa bokk ci jaamu Yàlla. Bu ñu bëggee nag, ñeneen ñi wormaal ñu te may ñu cér, fàww ñu njëkkee ko. Waaye waruñu wormaal nit rekk ngir nit ñi gis ñu, maanaam ci ngistal rekk. Waaye dafa war a jóge ci suñu biir xol, mi Yàlla rekk mën a gis. (1 Samiyel 16:7; Kàddu yu Xelu 21:2) Worma dafa war a bokk ci ñun te dafa war a feeñ ci suñuy jëf, ci suñu doxalin ak ñeneen ñi, ak sax ci ni ñu gise suñu bopp. Li am mooy dañu war a wone worma fépp fu ñu nekk, ci lépp li ñuy wax ak ci lépp li ñuy def. Lu jëm ci suñu doxalin ak ci suñu colin, war nañu bàyyi xel bu baax ci lii ndaw li Pool wax: «Bëggunu kenn sikk sunub liggéey, moo tax bëggunoo jëfe lenn luy doon tojaange ci kenn. Ci lépp kay lanu bëgga seedeel sunu bopp, ne noo yelloo ngërëm, te ay jawriñi Yàlla lanu.» (2 Korent 6:3, 4) Nañu rafetal ci lépp njàngalem Yàlla, suñu Musalkat. (Tit 2:10).
Kàdduy Waare 5:2, NWT
2 Bul gaaw a wax, te bul bàyyi sa xol yóbbee la ci wax ci kanamu Yàlla dëgg ji te xalaatoo ci; ndaxte Yàlla dëgg ji mu ngi ci kaw asamaan, waaye yow yaa ngi fii ci suuf. Kon na say kàddu néew.
w09 15/11 11 § 21
Nañu gëstu Kàddu Yàlla ngir suñuy ñaan gën xóot
21 Bu Yeesu doon ñaan Yàlla, dafa ko doon def ànd ceek teggin ak ngëm gu dëgër. Ci misaal, laata Yeesu di dekkil Lasaar dafa «xool ca kaw, daldi ne: ‘Baay, sant naa la, ndax nangul nga ma. Man nag xam naa ne saa su nekk danga may nangul’» (Yowaan 11:41, 42). Ndax suñuy ñaan dañuy wone ne am nañu teggin ak ngëm gu dëgër? Bu ñu xoolee ñaan bi Yeesu jàngaloon ay taalibeem, dinañu gis ne, li mu gën a fësal ci ñaan bi mooy, ñu sellal turu Yexowa, Nguuram dikk te coobareem am. (Macë 6:9, 10) Léegi nañu xalaat ci suñuy ñaan. Ndax li ñuy wax dafay wone ne, Nguuru Yàlla, sellal turam ak def coobareem, lu am solo la ci ñun? Loolu mooy li ñu war.
Kàdduy Waare 5:4-6, NWT
4 Boo digee Yàlla dara, bu ko yéex a def, ndaxte ñi ñàkk xel, neexuñu ko. Li nga dige, def ko. 5 Bañ a dige dara moo gën, nga dige te defoo ko. 6 Bul nangu sa gémmiñ yóbbee la bàkkaar, te bul wax ci kanamu malaaka mi ne njuumte la woon. Lu tax Yàlla dëgg ji war a ñaawlu say kàddu, ba nar a yàq li nga liggéey ak say loxo?
w17.04 6 § 12
«Li nga dige, def ko»
12 Sóobu ci ndox, ndorteel rekk la. Kon li ñu bëgg mooy wéy di takku ci Yàlla ni ñu ko dige woon bi ñuy jébbalu ci moom. Nañu laaj suñu bopp lii: ‘Fan la sama ngëm tollu bi ma sóoboo ci ndox ba tey? Ndax maa ngi jaamu Yexowa ak sama xol bépp? (Kolos 3:23) Ndax damay faral di ñaan Yàlla, di gëstu Kàddu Yàlla, di teewe ndaje yi ak di bokk ci liggéeyu waare bi? Walla ndax sama yëngu-yëngu ci wàllu ngëm dafa nekk di wàññiku?’ Ndawu li Piyeer wone na ne buñu bëggul su nu ngëm wàññiku, dañoo war a wéy di gëstu ngir yokk suñu xam-xam, di muñ te wéy di takku ci Yàlla. (Jàngal 2 Piyeer 1:5-8.)
Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi
Kàdduy Waare 5:8, NWT
8 Boo gisee fi nga dëkk ñuy sonal ki néew doole, di jalgati yoon, bu la loolu jaaxal. Ndaxte njiit mu mag moo gis, am na ku ko gën a kawe te di ko bàyyi xel, te ñoom ñaar ñooñu sax, am na ñu leen sut.
w20.09 31 § 3-5
Ay laaj yu jóge ci ñiy jàng suñuy téere
Kàdduy Waare 5:8 dafay wax ci njiit buy toroxal néew-ji-doole yi ak di leen def lu awul yoon. Njiit moomu war na fàttaliku ne, am na beneen njiit bu ko féete kaw te ëpp ko sañ-sañ ci nguur gi. Boo demee sax, am na yeneen njiit yu bare yu ko ëpp sañ-sañ. Neexul a dégg, waaye li am mooy, njiit yu bare tey dañuy nangu ger. Te seen ñàkk doxal yoon, moo tax ba waa réew ma nekk ci coono.
Waaye ak lu mënta xew fi ñu dëkk, am nañu yaakaar ndax xam nañu ne, Yexowa a ngi bàyyi xel sax njiit yi gën a kawe. (Taalifi Cant 55:23; Filib 4:6, 7) Xam nañu ne, Yexowa «suuf sépp lay jéere ay gëtam, ngir dooleel ñi ko wéetalal seen xol.» (2 Jaar-jaar ya 16:9).
Kon Kàdduy Waare 5:8 dafa ñuy fàttali ne, képp kuy kilifa ci ab nguur, xamal ne am na ku la ëpp sañ-sañ ci nguur googu. Te aaya boobu mën nañu dimbali ñu xalaat ci leneen lu gën a am solo, maanaam Yexowa mooy njiit mi gën a mag ci njiit yi, moom mooy kilifay ñépp. Te tey mu ngi ilif jaare ko ci doomam Yeesu Kirist, buuru buur yi. Yexowa, Aji man ji tiim ñépp, njiit bu jub la, te doomam Yeesu it ku jub la.
13 BA 19 OKTOOBAR
NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA KÀDDUY WAARE PÀCC 7-8
«Dem dëj»
Kàdduy Waare 7:2, NWT
2 Dem dëj moo gën dem ci xew, ndaxte loolu mooy muju nit ñépp. Kuy dund war na ci bàyyi xel.
it «Dëj» § 9
Dëj
Bu dëj amee. Kàdduy Waare 3:1, 4 lii la wax: «Mu jot nga jooy, mu jot nga ree; mu jot nga ñaawlu, mu jot nga dukkat.» Ku am xel war na xam ne «dem dëj moo gën dem ci xew» ndaxte ñun ñépp ci dee lañuy mujj. (Kàdduy Waare 7:2, 4; xoolal itam Kàddu yu Xelu 14:13.) Kon ku am xel, dem dëfël ñi am dëj moo ko gënal dem feexali xolam. Loolu dina ko dimbali mu fàttaliku ne, moom ci boppam dina mas a dee, dimbali ko it mu bàyyi xel Yàlla ci dundam.
Kàdduy Waare 7:1, NWT
1 Tur wu rafet a gën diw gu xeeñ neex, te bésub dee moo gën bésub juddu.
w19.06 23 § 15
Dimbalil ñi nekk ci njàqare
15 William mi ñakk jabaram ay at ci ginnaaw, lii la wax: «su may dégg li ñeneen ñi di wax ci sama jabar, loolu dafay seddal sama xol. Te it sama xel dafay dal ndaxte wóor na ma ne, nit ñi soppoon nañu ko te nawoon nañu ko. Kàddu yu rafet yooyu dañu may dëfël bu baax. Dama ciy bég ndaxte dama fonkoon sama jabar lool te moom rekk laa amoon.» Bianca mi ñakk jëkkëram, lii la wax: «man li may dëfël mooy bu ñeneen ñi di ñaan ak man te di ma jàngal ay aaya ci Biibël bi. Dafa may neex itam, bu ñeneen ñi di wax ci sama jëkkër mbaa ñu may déglu su may wax ci moom.»
w17.07 16 § 16
«Ñi am naqar, bokkal ak ñoom seen naqar»
16 Booy ñaanal ki am dëj walla ngay ñaan ak moom, loolu mën na ko dëfël bu baax. Bu dee sax ñaan ci anam yooyu yombul ndax naqar bi ngay yëg, li ngay wax ci sa ñaan te tibbe ko ci sa xol, mën na ko dimbali. Lii la Dalene wax: «yenn saay dama doon wax mbokk yu jigéen yi ma doon seetsi, ñu ñaanal ma. Bu ñuy tàmbali ñaan Yàlla, du yomb ci ñoom, waaye bu ñu demee ba ci biir, li ñuy wax dafay laal sama xol. Seen mbëggeel, seen itte ci man ak seen ngëm gu dëgër yokk na sama ngëm.»
w17.07 16 § 17-19
«Ñi am naqar, bokkal ak ñoom seen naqar»
17 Am na ñoo xam ne bu ñu amee dëj, dañu koy naqarlu lu yàgg. Kon bu dëj bi weesoo ay weer sax, ba ñépp dellu seen kër, nanga wéy di taxawu suñu mbokk mi ci naqaram. «Xarit dëgg dafay wone mbëggeelam sa su nekk, te mbokk la bu juddu ngir jamonoy tiis.» (Kàddu yu Xelu 17:17, NWT) Kon feek ki am dëj a ngi soxla ndimbal, kerceen dëgg yi dañuy def lépp ngir wéy di ko dëfal. (Jàngal 1 Tesalonig 3:7).
18 Bul fàtte ne bu nit ñàkkee mbokkam lu yàgg sax, lu yomb mën a tax ba xelam dem ci kooku, mu amaat metit. Ci misaal, loolu mën a nekk bésu aniwerseeru ki dee, ab misik, foto, xew-xew, walla sax xet bu koy fàttali kooku. Ki ñàkk jabaram walla jëkkëram dafay faral di am naqar buy def lu ñu faraloon di def ñoom ñaar, lu ci mel ni dem ci ndaje yu mag yi walla ci ndaje fàttaliku deewu Yeesu. Lii la suñu benn mbokk bu góor wax: «Xamoon naa ne, bu suñu bésu séy dellusee, dinaa am naqar. Waaye bi bés agsee, samay mbokki kerceen dañu ma taxawu, ba tax wéetuma benn yoon.»
19 Nañu xam ne ki am dëj dafa soxla ñu dëfël ko saa su nekk. Lii la Junia wax: «Su ma mbokk yi seetsee, bés bu dul suñu aniwerseeru séy, dama ciy bég lool.» Dëgg la ne, bu nit amee dëj, mënuñu dindi metitam, waaye mën nañu def lépp li ñu mën ngir dimbali ko. (1 Yowaan 3:18) Gaby nee na: «Maa ngi gërëm Yexowa ci ni ma magi mbooloo mi jàppale ma génn ci jafe-jafe yooyu. Ñoom ñoo tax ma yëg mbëggeel gi Yexowa am ci man ci biir jafe-jafe boobu.»
Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi
Kàdduy Waare 7:20-22, NWT
20 Amul ci àddina si nit ku jub kuy def lu baax bés bu nekk te du bàkkaar mukk. 21 Te it, bul bàyyi xel ci lépp li nit ñi di wax. Lu ko moy, dinga mas a dégg sa surga di wax lu ñaaw ci yow; 22 ndaxte xam nga bu baax ci sa biir xol ne, yow ci sa bopp, wax nga lu ñaaw ci ñeneen ñi ay yooni yoon.
w23.03 31 § 18
«Ni ñépp di xame ne samay taalibe ngeen»
18 Bu ñu suñu mbokk defe lu ñu metti, dañu ko koy bëgg a wax. Waaye bala ñu ko koy wax, nañu laaj suñu bopp lii: ‘Ndax xam naa lépp li xew?’ (Kàddu yu Xelu 18:13) ‘Ndax moo tey li mu ma def?’ (Kàdduy Waare 7:20) ‘Ndax man mas naa def loolu keneen?’ (Kàdduy Waare 7:21, 22) ‘Mbaa du ma indi beneen coow, bu ma demee wax ak moom?’ (Jàngal Kàddu yu Xelu 26:20.) Bu ñu jëlee jot ngir xalaat bu baax ci laaj yooyu, amaana ñu gis ne li gën mooy, ñu baal ko ndax mbëggeel gi ñu am ci moom.
20 BA 26 OKTOOBAR
NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA KÀDDUY WAARE PÀCC 9-10
Amal gis-gis bu baax ci say jafe-jafe
Kàdduy Waare 9:11, NWT
11 Seetlu naa it ne fii ci kaw suuf: du ñi gaaw ñooy raw saa su nekk ci rawante yi, te du ñi am doole ñooy daan saa su nekk, du ñi muus ñooy am li ñu lekk bés bu nekk, du ñi am xel ñee bare alal, te du ñi am xam-xam, la seen lépp di àntu; ndaxte jafe-jafe ak xew-xew yu ñu xaarul dañu leen di bett ñoom ñépp dal seen kaw.
w13 15/8 14 § 20-21
Bul «mere mukk Yexowa»
20 Bul tuumaal keneen. Lu tax waroo koo def? War nañu nangu ne am na jafe-jafe yoo xam ne, ñun ñoo ko yóbbe suñu bopp. (Galasi 6:7) Kon foog ne lépp lu ñu dal ndogalu Yàlla la, yenuwul maanaa. Lu tax? Nañu jël misaalu dawalkatu oto. Bu sofër toppul yoon te bañ a dawal ndànk ba def aksidã, ndax ki defar oto bi lañuy sikk? Déedéet! Noonu it, Yexowa dafa ñu sàkk ak sañ-sañu tànn li ñuy def, te jox ñu ay tegtal ngir ñu jël ay dogal yu baax. Kon waruñu tuumaal Yàlla ci njuumte yi ñuy def.
21 Waaye nag, nekkul ne jafe-jafe bu ñu am rekk, ñoo ko teg suñu bopp. Ndaxte am na «jafe-jafe ak xew-xew yu ñu xaarul» yu ñu mën a bett te dal suñu kaw. (Kàdduy Waare 9:11) Te it waruñu fàtte ne, tey ci àddina si, li ëpp ci jafe-jafe yi, Seytaanee ko waral. (1 Yowaan 5:19; Peeñu 12:9) Moom mooy suñu noon waaye du Yexowa! (1 Piyeer 5:8).
Kàdduy Waare 10:7, NWT
7 Gis naa ay surga yu war fas, te doomi buur yi di dox, mel ni ñooy surga yi.
w19.09 5 § 10
Yexowa fonk na jaamam yi woyof
10 Bu ñu woyofee, suñu dund dina gën a yomb. Waaye li am mooy, ci àddina sii, lépp mënta jaar yoon. Lii la buur Suleymaan wax: «Gis naa ay surga yu war fas, te doomi buur yi di dox, mel ni ñooy surga yi.» (Kàdduy Waare 10:7) Nit mën naa gën a xareñ moroomam, waaye kooku ëpp ko bayre. Loolu moo tax ni ko Suleymaan wonee, am na mbir yoo xam ne, duñu leen mas a mën a jubbanti, nañu leen nangu rekk te jàpp ci Yàlla. Lu ko moy, xol bu jeex rekk lañu ciy jële. (Kàdduy Waare 6:9) Bu ñu woyofee, suñu dund dina gën a yomb, ndaxte duñu bëgg mbir yi deme ni ñu ko bëgge rekk.
Kàdduy Waare 9:7, 10, NWT
7 Demal, lekk sa ñam ci bànneex te naan sa biiñ ci xol bu sedd, ndaxte Yàlla dëgg ji bég na ci say jëf. 10 Lépp lu sa loxo jot, def kook sa kàttan gépp, ndaxte dara amul ci Bàmmeel bi nga jëm, du jëf, du mébét, du xam-xam, du xel.
w11 15/10 8 § 1-2
Ndax li ngay féexale sa xol baax na ci yow?
Aaya yu bare ci Biibël bi, wone nañu ne Yexowa bëggul rekk ñu dund waaye dafa bëgg ñu bége. Ci misaal, Taalifi Cant 104:14, 15 nee na, Yexowaa ngi saxalal «gàncax gu doom aadama di bey, ba génnee ab dund fi suuf, dugub di ko dooleel, biiñ di bégal xolam, ag diw di leeral kanamam.» Kon dëgg la ne, Yexowa moo ñu may pepp, diw ak biiñ ngir ñu am lu ñu dunde. Biiñ nag, day ‘bégal xol.’ Loolu dafay wone ne Yexowa yemul rekk ci jox ñu lu ñu dunde, waaye dafa bëgg it ñu bége. (Kàdduy Waare 9:7; 10:19) Waaw Yexowa dafa bëgg suñu «xol fees ak mbég.» (Jëf ya 14:16, 17).
2 Kon jël jot ngir xool ‘picc asamaan yi’ ak «tóor-tóor yiy saxe ci tool yi» walla def leneen lu ñuy bégal, dara aayu ci. (Macë 6:26, 28; Taalifi Cant 8:4, 5) Kon nañu bége ci suñu dund ndaxte loolu, mayug Yàlla la. (Kàdduy Waare 3:12, 13) Gise jot googu ni mayug Yàlla, dina ñu xiir ci jariñoo ko ci anam bu neex suñu Boroom, mi ñu ko baaxe.
Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi
Kàdduy Waare 10:12-14, NWT
12 Kàddu yu jóge ci ku am xel dañuy jur yiw, waaye kàdduy ki amul xel dañu koy yóbbee sànkute. 13 Waxi dof lay njëkk a génnee ci gémmiñam, daaneele ak wax ju koy yóbbee musiba. 14 Ab dof waxam du jeex. Te kenn xamul li nar a xew; ana ku ko mën a xamal li nar a xew ginnaawam?
it «Jëw, Sos» § 4, 8
Jëw, Sos
Jëw mën na yóbbee ci sos te loolu musiba la. Li ci Kàdduy Waare 10:12 ba 14 wax leer na nàññ: «Kàdduy ki amul xel dañu koy yóbbee sànkute. Waxi dof lay njëkk a génnee ci gémmiñam, daaneele ak wax ju koy yóbbee musiba. Ab dof waxam du jeex.»
Dëgg la ne, jëw mën na bañ a lor nit. Waaye li mën a soppi jëw mu mujj doon sos, lu yomb la. Te sos du mas a jur lu baax , ndaxte dafay gaañe te di indi xuloo. Ki sosal moroomam, moo xam mu tey ko walla mu doon njuumte, dafay yàq digganteem ak Yàlla. Ndaxte Yexowa dafa sib «képp kuy xiir ay mbokk ci xuloo.» (Kàddu yu Xelu 6:16-19) Baatu di·aʹbo·los ci làkku Gereg dafay tekki «soskat» walla «tuumaalkat». Ci Biibël bi, noonu lañuy woowe Seytaane, miy Ibliis, moom mooy kiy sosal Yàlla. (Yowaan 8:44; Peeñu 12:9, 10; Njàlbéen ga 3:2-5.) Kon sos ci Ibliis la jóge.
27 OKTOOBAR BA 2 NOWÀMBAR
NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA KÀDDUY WAARE PÀCC 11-12
Toppatool sa wér-gi-yaram te bég
Kàdduy Waare 11:7, 8, NWT
7 Leer dafa neex, te gis jant bi, aka baax ci bët. 8 Moo tax su nit dundee at yu bare, na ci am bànneex bés bu nekk. Waaye bumu fàtte ne, bési tiis yi mën nañu bare; te li ci nar a topp lépp, du am benn njariñ.
g 15/3 13 § 6-7
Ngelaw lu neex ak tàngooru naaj bi dafa baax ci wér-gi-yaram
Naaj bi dafay rey yenn mikorob yi. Benn yéenekaay bu tudd The Journal of Hospital Infection ci làkku ãgale nee na: «Lu ëpp ci mikorob yi mën a jaar ci bakkanu nit ngir dugg ko, naaj bi dafa leen di rey.»
Naka nga mënee jariñoo loolu? Mën nga génn doxantu, noyyi ngelaw lu neex, sa yaram jël tuuti ci naaj bi. Dinga yëg ci sa yaram ne, loolu dafa baax ci nit.
Kàdduy Waare 11:10, NWT
10 Kon dàqal lépp lu lay jural naqaru xol, te sore lépp lu mën a lor sa yaram, ndaxte ndaw ak dooley ndaw, amul benn njariñ.
w23.02 21 § 6-7
Fonkal dund gi ñu Yàlla may
6 Dëgg la ne, Biibël bi du téere buy wax ci wàllum paj walla ci lekk bi gën, waaye dafay wone gis-gisu Yexowa ci fànn yooyu. Ci misaal, wax na ñu ‘sore lépp lu mën a lor suñu yaram.» (Kàdduy Waare 11:10) Yàlla tere na ci Biibël bi, lekk lekk bu ëpp ak naan ba màndi. (Kàddu yu Xelu 23:20) Yexowa dafa bëgg ñu xam fi ñu war a yem ci lekk ak ci naan. (1 Korent 6:12; 9:25).
7 Nañu jëfandikoo bu baax suñu xel ngir wone ne, fonk nañu dund gi ñu Yàlla may. (Taalifi Cant 119:99, 100; jàngal Kàddu yu Xelu 2:11.) Kon war nañu demee xel ci lépp li ñuy def. Ci misaal, bu ñu xamee ne lekk bii dafa ñuy lor, waratuñu koo lekk. War nañu it di nelaw nelaw yu doy, di yëngatu, di lekk lu set te baax ci yaram te di toppatoo suñu kër ba mu set.
Kàdduy Waare 12:13, NWT
13 Liy jeexal wax ji, gannaaw bi ñu déggee lépp, mooy lii: Ragalal Yàlla te topp ay ndigalam, ndax loolu mooy lépp li war nit.
«Doonleen jëfekati kàddu gi»
2 Ñun jaamu Yexowa yi, dañoo bég ci suñu dund. Lan moo ñu may mbégte moomu? Li ko waral bare na, waaye li ñuy gën a may mbégte mooy ne, dañuy jàng Kàddu Yàlla te di ko jëfe. (Jàngal Yanqóoba 1:22-25).
3 Bu ñuy ‘jëfe kàddu gi’ barke yu bare lañu ciy jële. Dañuy bég ndaxte xam nañu ne, suñu jikko neex na Yexowa. (Kàdduy Waare 12:13) Ndegam dañuy jëfe li ñuy jàng ci Kàddu Yàlla, suñu dundu njaboot dafa gën a neex te suñu diggante ak suñu mbokki kerceen yi dafa gën a rattax. Xéyna yow sax seetlu nga loolu. Rax-ci-dolli, jëfe li ñuy jàng tax na, ba amuñu jafe-jafe yu bare yuy dal ñi dul topp santaaney Yexowa. Ci lu wóor, ànd nañu ci li Daawuda waxoon. Bi mu waxee ci yoonu Yexowa, aki santaaneem ba pare, nii la daaneele: «ku ko sàmm yokku yool.» (Taalifi Cant 19:8-12)
Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi
Kàdduy Waare 12:9, 10, NWT
9 Dajalekat bi yemul woon rekk ci doon ku xelu, waaye dafa wéy di jàngal mbooloo mi li mu xam; dafa doon xalaat bu baax aka gëstu ngir dajale ay léebu yu bare. 10 Dajalekat bi dafa def lépp li mu mën ngir tànn kàddu yu rafet, te bind kàddu yu leer te dëggu.
it «Ci Yàlla la jóge» § 10
Ci Yàlla la jóge
Góor yi Yàlla jox xelam ngir ñu bind téere yu Sell yi meluñu woon ni ay robot, yem rekk ci di bind li ñu leen wax. Ci misaal, Yàlla dafa jaar ci ab malaaka ngir xamal ndaw li Yowaan, Peeñu ma. Te Yowaan ‘seede na fa li mu gis lépp, maanaam kàddug Yàlla ak seede, si ñu seedeel Yeesu Kirist.’ (Peeñu ma 1:1, 2) ‘Leerug Yàlla moo ko dikkal’ ba mu gis li naroon a xew ci bésub Sang bi. Lii lañu ko wax: «mboolem loo gis, bind ko cib téere». Kon, Yàlla may na ñi doon bind Biibël bi, ñu tànnal seen bopp baat yi ñu mën a jëfandikoo ngir bind li ñu gis. (Abakug 2:2) Waaye bàyyi na leen xel, ba tax li ñuy bind nekk lu wér, lu dëggu te méngook li mu bëggoon. (Kàddu yu Xelu 30:5, 6) Kàdduy Waare 12:9 ak 10 wone na ne, ki doon bind waroon na def wàllam, maanaam mu xalaat bu baax, gëstu te «jekk-jekkal kàdduy xel yu takku.» (Xoolal Luug 1:1-4).