Ndax Biibël bi wax na ci mbirum ñaari góor walla ñaari jigéen ñuy séy?
Li Biibël bi wax
Yàlla mi ñu sàkk joxe na ay tegtal ci séy, lu yàgg bala nguur yi di ko def. Lii la téere bi njëkk ci Biibël bi wax: «Looloo tax góor di bàyyikoo ci ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñuy wenn suux». (Njàlbéen ga 2:24) Benn diksoneer buy firi baat yi nekk ci Biibël bi wone na ne, baatu Ebrë bi ñu tekki «soxna» ci wolof, jigéen rekk la mën a doon (Expository Dictionary of Biblical Words). Yeesu dëggal na loolu bi mu waxee ne ñaar ñiy séy war nañu nekk «kii góor, kii jigéen» (Macë 19:4).
Kon, Yàlla dafa bëggoon séy am diggante benn góor ak benn jigéen, ku nekk taq ci sa moroom te diggante boobu bañ a jeex. Yàlla dafa sàkk góor ak jigéen ngir ku nekk mën a faj li sa moroom soxla ci wàllu mbëggeel ak ci wàllu séy, te it ñu mën a jur ay doom.