TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • ijwyp pàcc 12
  • Lan laa mën a def bu ñu may bundxataal?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Lan laa mën a def bu ñu may bundxataal?
  • Li ndaw ñi di laaj
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Lan mooy bundxataal?
  • Lu tax mu am ñuy bundxataal seeni moroom?
  • Ñan lañuy faral di bundxataal?
  • Lan nga mën a def bu dee dañu lay bundxataal?
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
Li ndaw ñi di laaj
ijwyp pàcc 12

LI NDAW ÑI DI LAAJ

Lan laa mën a def bu ñu may bundxataal?

  • Lan mooy bundxataal?

  • Lu tax mu am ñuy bundxataal seeni moroom?

  • Ñan lañuy faral di bundxataal?

  • Lan nga mën a def bu dee dañu lay bundxataal?

Jàngal li yeneen ndaw ak benn jàngalekat wax lu jëm ci bundxataal te tontu ci laaj yi jëm ci bundxataal.

Bundxataal du porobalem bu ñu war a xeeb. Am na benn gëstu bu ñu def ci Ãgalteer buy wone ne téeméer yoo jël ci ndaw ñiy xaru te ñu yégle ko ci xibaar yi ñeent fukk yi bundxataal bokk na ci li ko waral.

Lan mooy bundxataal?

Bundxataal yemul rekk ci ay dóor. Mën na ëmb itam lii di topp.

  • Saaga. Céline mi am ñaar fukki at lii la wax: «Yenn saa yi, xale yu jigéen ñi dañuy xaste. Duma mas a fàtte tur yi ñu ma doon jox ak li ñu ma doon wax. Tax nañu ba ma gëm ne jaruma dara, kenn bëggu ma te awma benn njariñ. Ñu dóoroon ma sax moo ma gënaloon.»

  • Ber. Haley mi am fukki at ak juróom ñett lii la wax: «Ñi ma bokkaloon lekkool, daawuñu ma boole ci dara. Bu waxtu añ daan jot dañu doon fexe ba duma mën a toog ak ñoom ci benn taabal. At mi yépp dama doon jooy di lekk man kese.»

  • Bundxataal ci internet. Daniel, mi am fukki at ñeent, lii la wax: «Mën nga toog ci sa ordinatëër, bind rekk, yàq deru jaambur, ba ci sax dundam. Loolu du ay wax rekk, lu mën a am la!» Yónnee foto walla mesaas ci telefon buy yàq deru nit ki, loolu itam bokk na ci bundxataal ci internet.

Lu tax mu am ñuy bundxataal seeni moroom?

Lii di topp bokk na ci li ko waral.

  • Ñoom ci seen bopp dañu leen doon bundxataal. Benn ndaw bu tudd Antonio lii la wax: «Ni ñu ma daan bundxataal, dafa ma mettiwoon lool ba ma komaase di bundaxataal yeneen ndaw ngir mën a neex ñi nga xam ne ñoo ma daan bundxataal. Waaye mujj naa gis ne li ma daan def baaxul dara.»

  • Amuñu ay royukaay yu baax. Jay McGraw lii la wax ci téereem bi mu bind lu jëm ci bundxataal: «Ci lu ëpp, ndaw ñiy bundxataal seeni moroom [...] dañuy roy ci ni seen waajur yi ak seen mag yu góor walla yu jigéen daan bundxataal ñeneen ñi.»

  • Dañuy def mel ni ñoo gën ñépp, fekk ci dëgg amuñu jàmm. Barbara Coloroso miy bind itam téere bu jëm ci bundxataal lii la wax: «Xale yuy bundxataal seeni moroom dañuy mel ni ñoo gën ñeneen ñi, te boo seetee ba ci biir ñu ngi dund lu metti te dañuy xeeb seen bopp.»

Ñan lañuy faral di bundxataal?

  • Ñiy beru. Ndaw ñi noppi te gaawuñu miin nit dañuy faral di beru. Moo tax bundxataal leen yomb.

  • Ndaw ñi ñu jàppe ni ñu wuute ak seeni moroom. Yenn ndaw, dañu leen di bundxataal ndax seen melokaan, seen xeet, seen diine walla sax laago bi ñu am, lépp daal loo xam ne mën nañu ci jaar ngir bundxataal leen.

  • Ndaw ñi xeeb seen bopp. Ñiy bundxatal, dañuy gaaw a ràññe ñi nga xam ne dañu xeeb seen bopp. Dafay yomb ñu bundxataal leen ndaxte duñu faral di feyyu.

Lan nga mën a def bu dee dañu lay bundxataal?

  • Bul leen won li ngay yëg. Benn janq bu tudd Kylie lii la wax: «Ñiy bundxataal dañuy bëgg xam ndax li ñu bëggoon am nañu ko, maanaam nga xeeb sa bopp. Boo leen wonul li ngay yëg dañu lay bàyyi. Biibël bi nee na: «Ku xelu, mer, ànd ak sagoom» (Kàddu yu Xelu 29:11).

  • Bul feyyu. Feyyu, dafay yokk porobalem bi waaye du ko faj. Biibël bi nee na: «Buleen feyante lu bon» (Room 12:17; Kàddu yu Xelu 24:19).

  • Bul dugal sa bopp ci porobalem. Defal sa kem kàttan ngir moytu ñi lay bundxataal walla dem fi nga xam ne mën nañu la fa bundxataal. (Kàddu yu Xelu 22:3)

  • Bettleen ci ni nga leen di tontoo. Biibël bi nee na: «Tont lu neex day giifal» (Kàddu yu Xelu 15:1).

  • Deel kaf. Bu ñu la nee danga am yaram, mën nga yëngal sa bopp nee ko: «Dëgg la, bu la neexee sax mën naa la ci may ñaari kilo.»

  • Demal sa yoon. Nora mi am fukki at ak juróom ñeent lii la wax: «Bañ a tontu dafay wone ne ku am xel nga, te yaa ëpp xel ki lay tàppaas. Loolu dafay wone ne ku maandu nga te ki lay bundxataal maanduwul.»

  • Góor-góorlul ngir bañ a xeeb sa bopp. Benn janq bu tudd Rita lii la wax: «Boo tiitee, ñi lay bundxataal dinañu ko xam te mën nañu ci jaar wàññi la ba nga xeeb sa bopp.»

  • Wax ko keneen. Am na benn gëstu buy wone ne, lu ëpp genn-wàll ci nit ñi ñuy bundxataal ci internet duñu ko wax kenn ndaxte xéyna dañoo rus, rawatina xale yu góor yi, walla ñu ragal ñu dalaat seen kaw.

Xelal yi jóge ci yeneen ndaw

«Moytul a jaar ci yenn béréb walla dugg ci loo xam ne mën nañu la ci bundxataal ci lu yomb. Bul fàtte ne ñi lay bundxataal am nañu ñoom itam ay porobalem. Boo xamee loolu, li ñu lay wax dootu la def dara» (Antonio).

«Bul xeeb sa bopp. Bul ragal a wax nit ñi li nga gëm. Ñu bare ci ñiy bundxataal seen moroom dañuy dellu ginnaaw bu ñu gisee ne li ñu bëggoon amuñu ko te ragaloo leen» (Jessica).

Li benn jàngalekat wax

«Bundxataal porobalem bu garaaw la. Fi may jàngale, xale yi dañuy xeex ci biir kalaas bi, ba ci sax ñi nekk CE1. Yenn ndaw, bëgg siiw walla ñu ràññee leen moo tax ñuy def lépp ngir bundxataal ñeneen ñi.

«Ñi ñuy bundxataal, duñu faral di wax ndax ragal ki leen di bundxataal dalaat seen kaw, walla rus ñi ñu bokkal kalaas jàppe leen ni ay tappet. Mën nañu ragal it ne kenn du ci def dara. Terewul maa ngi xiir képp ku ñuy bundxataal mu dem wax ko benn kilifa. Lu jaadu la te loolu mën na tax duñu bundxataal keneen» (Jenilee, mi nekkoon jàngalekat ci Etaa Sini).

Ay laaj yu jëm ci bundxataal

Dëgg la walla du dëgg?

  1. Ay junniy at a ngi nii muy am ñi ñuy bundxataal.

  2. Bundxataal fo rekk la, du lu garaaw.

  3. Boo bëggee ñu bàyyi di la bundaxataal, li gën mooy ngay feyyu.

  4. Bu ñu demee ba di la bundxataal, ci yow la.

  5. Ñenn ci ñi ñuy bundxataal dañuy mujj bundaxataal ñeneen ñi.

  6. Boo fekkee fu ñuy bundxataal nit, li gën mooy nga bañ cee dugg.

  7. Ak li muy bàkku yépp kiy bundxataal amul jàmm.

  8. Ñiy bundxataal mën nañu soppeeku.

TONT YI

  1. Dëgg la. Biibël bi wax na ci Nefilim yi, ñoom ñi nga xam ne seen tur mu ngi tekki «Ñiy daaneel ñeneen ñi». (Njàlbéen ga 6:4)

  2. Du dëgg. Bundxataal mën na rey nit . Am na ay ndaw yu mujj xaru ndaxte dañu leen daan bundxataal.

  3. Du dëgg. Ndaxte kiy bundxataal dafay faral di ëpp doole ki muy bundxataal. Kon jéem a feyyu du li gën.

  4. Du dëgg. Waruñoo bundxataal kenn. Kiy bundxataal, lépp moom la.

  5. Dëgg la. Ñenn ci ñi ñu daan bundxataal dañuy xëpp seen mer ci ñeneen, ni ñu leen ko defe woon.

  6. Du dëgg. Ku fekke te defoo dara, am nga ci wàll.

  7. Dëgg la. Bu dee sax ñiy bundxataal seen moroom dañuy yëg seen bopp, ñu bare ci ñoom amuñu jàmm. Dañuy wàññi ñeneen ñi ngir mën a nekk.

  8. Dëgg la. Bu ñu leen dimbalee, ñiy bundxataal ñeneen ñi mën nañu soppi seen xalaat ak seen doxalin (Efes 4:​23, 24).

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager