LI ÑUY DEF AK LI NGEEN DI MAYE
Jàllale nañu ci tele yi ak ci rajo yi ndaje bu mag bu ñetti fan bi
1 UT 2021
Ci atum 2020 bii, ni ñu defe suñu ndaje bu mag bu ñetti fan bi, masuñu koo defe noonu. Porogaraam bi yépp lañu jàllale ci internet ngir nit ñi seetaan ko. Waaye ci réewu Malawi ak Mozambique, suñu mbokk yi seetaan nañu ndaje bi te jaaruñu ci internet. Kon ñoom nu ñu def?
Kurélu kordinatër yi ak kurél bi yor njàngale mi, di ñaari kurél yu bokk ci Jataay biy dogal, ñoo nangu ñu jàllale ndaje bu mag boobu ci tele yi ak ci rajo yi, ca Malawi ak ca Mozambique. Te ci ñaari réew yooyu rekk la loolu new. Lu tax kurél yi nangu ñu def loolu ci ñaari réew yooyu rekk? Ndaxte ci àddina si sépp, daanaka internet ci Malawi la gën a seer, te loolu tax na ba mbokk yu bare amuñu internet. Mbokk William Chumbi, kenn ci ñi bokk ci kurélu bànqaasu Malawi bi, lii la wax: «Mbokk yi amuñu woon beneen pexe, lu dul seetaan ndaje bag bi ci tele walla déglu ko ci rajo.» Luka Sibeko, keneen ku bokk ci kurélu bànqaas boobu, moom nee na: «Bu ñu jàllalewul woon ndaje bu mag bu ñetti fan bi ci tele walla ci rajo, mbokk yu bare naruwuñu woon a fekkee ndaje ren bi.» Ca Mozambique itam, ñi am li ñu jënde aparey ngir jot ci ndaje bi, ñu néew lañu, waxatuñu jënd internet.
Matuwaay yi ñu jël
Bala feebaru koronaa bi di tàmbali, amoon ay tele ak ay rajo yu doon jàllale suñu ndaje yi ñuy def ci mbooloo yi.a Mbokk yi dañu waxtaan ak boroom tele yooyu ak rajo yi ngir ñu yokkal leen waxtu yi ñu leen may, ba ñu mën a jàllale ndaje bu mag bi.
Waaye ca réewu Malawi, mbir mi yombul woon. Ci réew moomu, tele yi ak rajo yi benn waxtu rekk lañuy faral di jàllale ab porogaraam, ndaxte bu emisoŋ bi guddee, mën na soof nit ñi. Waaye suñu mbokk yi dañu leen xamal ne, ñun dimbali nit ñi moo ñu tax a jóg. Bu dee sax nit ñi mënatuñu génn seen kër, ñun dañu bëgg a séddoo ak ñoom xibaaru jàmm bi nekk ci Biibël bi. Ndaxte xibaar boobu dafay dëfël nit ñi, dimbali leen ñu nekk nit ñu baax te am jàmm ci seen njaboot. Bi njiitu tele yooyu ak rajo yi déggee li suñu mbokk yi wax, ñu yokkal leen ay waxtu, ci waxtu yi ñu leen mayoon ba pare.
Ca Malawi, benn tele ak benn rajo ñoo jàllale ndaje bu mag bu ñetti fan bi. Waaye tele boobu ak rajo boobu daanaka waa réew ma mépp mën nañu ko jàpp. Ca Mozambique, ndaje bu mag bi jàll na ci benn tele ak 85 rajo.
Ci ñaari réew yooyu, fey nañu lu tollook 28 227 dolaar (daanaka 16 milioŋi cfa)b ngir jàllale ndaje bi ci tele yi, ak lu ëpp 20 000 dolaar (daanaka 11 milioŋi cfa) ngir jàllale ko ci rajo yi. Rajo yi daanaka 15 dolaar (daanaka 8500 cfa) lañu ñu doon feyeeku, tele yi di ñu feyeeku 2 777 dolaar (daanaka 1,5 milioŋi cfa).
Suñu mbokk yi, def nañu seen kem-kàttan ngir yaxanal bu baax, xaalis bi suñu mbokk yi ci àddina si sépp di maye. Ci misaal, ca Malawi, mbokk yi waxaale nañu ba ñu wàññil leen baax njëg bi (téeméer boo jël, wàññil nañu leen ci fanweer). Mujj gi wàññil nañu leen 1 711 dolaar (daanaka 985 000 cfa). Ca Mozambique, yenn njiitu rajo yi dañu ne, ñépp a xam Seede Yexowa yi ci njub ak ci fey ñi leen liggéeyal, ci waxtoom. Loolu moo tax ñu nangoo ñoo wàññil.
Mbokk yi wone nañu seen ngërëm
Suñu mbokk yi seetaan ndaje bu mag bi ak ñi ko déglu, bégoon nañu ci lool. Patrick benn magu mbooloo ca Malawi, lii la wax: «Ñu ngi gërëm Jataay biy dogal ci lépp li mu ñu defal ci biir mbas mii.» Mbokk Isaac itam foofa ca Malawi, nee na: «Man, rajo rekk laa am sama kër, kon maa ngi gërëm mbootaayu Yexowa, ci ni mu jëlee ay matuwaay ba ñu jàllale ndaje bu mag bu ñetti fan bi, ci rajo yi. Li ñu def moo tax sama njaboot gépp mën a déglu ndaje bu mag bi. Xam nañu ne Yexowa bëgg na nit ñi koy jaamu.»
Am na benn waarekat boo xam ne, ndaje atum 2020 boobu ca Mozambique, mooy ndaje bi mu njëkk a fekke. Lii la wax: «Li mbokk yi def ba ñu seetaan ndaje bu mag bi ci tele bi, fàttali na ma ne, Yexowa mooy Aji Man ji. Mbas mi sax, terewu koo ñëw ba ci sama biir kër taajal ma ñam wi ma soxla ci wàllu ngëm. Lii mooy wone ne, jaamu Yexowa yi dañu bëggante dëgg. Gëm naa ne, seen diine bii, mooy diine dëgg ji.»
Benn magu mbooloo bu tudd Wyson lii la wax: «Maa ngi gërëm surga bu takku bi, ci ni mu ñu toppatoo ci biir mbas mii. Matuwaay yi ñu jël ba ñu mën a seetaan ndaje bu mag bi ñetti fan bi, ci tele yi walla déglu ko ci rajo, dimbali nañu bu baax ñun ñi suñu loxo jotul suñu ginnaaw.»
Kurélu kordinatër yi ak kurél bi yor njàngale mi, nangu nañu itam ci yenn gox yi, ñu jàllale ci tele yi ak ci rajo yi, ndaje bu mag bu ñetti fan bu atum 2021. Fan lañuy jële xaalis bi ñuy defe loolu? Xanaa ci xaalis bi mbokk yi di maye fépp ci àddina si ngir jàppale liggéeyu waare bi jaare ko donate.jw.org. Ñu ngi gërëm ñépp, ci li ñuy maye.
a Ci atum 2020, bi ñu nekkee ci biir mbas mi, Kurélu kordinatër yi nangu woon na ñuy jàllale ci tele yi ak ci rajo yi, ndaje yi ñuy def ci mbooloo mi. Matuwaay boobu dimbali na ñi mënul woon konekte ak seen waa mbooloo walla konekte ci JW Stream ndax ñàkk internet walla ñàkk xaalis bu ñu jëndee koneksoŋ. Te matuwaay boobu nag, ñi am jafe-jafe boobu rekk lañu ko jagleel internet.
b Xaalis bi ci dolaar, xaalisu waa Etaa Sina la.