TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • ll xaaj 13 p. 28-29
  • Lan lañu war a def ba am dundin bu neex Yàlla ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Lan lañu war a def ba am dundin bu neex Yàlla ?
  • Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Xaritu Yàlla yi dañuy moytu lu bon
    Mën nga nekk xaritu Yàlla !
  • Ndax Yàlla dina alagaat ñu bon ñi ?
    Dundleen ba fàww ak bànneex ci suuf si !
  • Lan ngeen war a def ?
    Dundleen ba fàww ak bànneex ci suuf si !
  • Jëf yi Yàlla bañ
    Lan la ñu Yàllay laaj?
Xóotalal waxtaan bi
Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
ll xaaj 13 p. 28-29

XAAJ 13

Lan lañu war a def ba am dundin bu neex Yàlla ?

Moytuleen lu bon. 1 Korent 6:9, 10

Yëf yi Yàlla bañ—sàcc, màndi, dorogewu, xeex, ñaan ay nataal ak di jaamu ay xërëm

Bu ñu bëggee Yexowa, duñu def li mu bañ.

Yexowa bëggul ñuy sàcc, walla ñuy màndi, walla ñuy dorogewu.

Yàlla dafa bañ rey nit ak yàq biir, ak mbirum góor-jigeen. Bëggul ñu bëgge, walla ñuy xeex ak suñu moroom.

Waruñu di jaamu ay xërëm walla ay nataal, walla di gisaane, di kort, di luxus walla di def yu mel noonu.

Bu suuf si nekkaatee àjjana, nit ñu bon ñi dootuñu fi nekk.

  • Naka la Yàlla gise mbirum luxus? — Deutéronome 18:10-12.

  • Lu tax waruñu di jaamu ay xërëm? — Isaïe 44:15-20.

Defleen lu baax. Macë 7:12

Yëf yi neex Yàlla—war nañoo bëgg suñu moroom, nekk ay nit yu jub te di baale

Bu ñu bëggee neex Yàlla, war nañu koo jéem a roy.

Nangeen baax te nangoo maye ngir wone seen mbëggeel ci seeni moroom.

Nangeen nekk ay nit ñu jub.

Nangeen am yërmande te di baale.

Ñaari Seede Yexowa yiy waare góor

Nangeen xamal nit ñi lu jëm ci Yexowa ak li mu bëgg. — Isaïe 43:10.

  • Nangeen roy Yexowa. — 1 Piyeer 1:14-16.

  • Nangeen am mbëggeel. — 1 Yowaana 4:7, 8, 11.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager