NJÀNGALE 18
Lan lañuy def ngir dimbali suñuy mbokk ci ngëm yi musiba dal ?
République dominicaine
Sapoŋ
Haïti
Bu musiba amee, dañuy def lépp, ñun seede Yexowa yi, ngir gaaw a dem dimbali suñuy mbokk ci ngëm yi musiba boobu dal. Ndimbal boobu dafay wone mbëggeel dëgg bi ñu am ci suñu biir ( Yowaana 13:34, 35 ; 1 Yowaana 3:17, 18). Naka lañuy dimbalee suñu mbokk yooyu ?
Dañuy joxe xaalis. Bi xiif bu metti amee ci dëkku Yude, karceen yu njëkk ya dañu yónnee woon xaalis ngir dimbali seeni mbokk ci ngëm ya fa dëkkoon (Jëf ya 11:27-30). Ñun itam, fépp fu ñu dégg ci àddina si ne am na suñuy mbokk ci ngëm yu nekk ci jafe-jafe, dañuy yónnee lu leen di dimbali jaarale ko ci suñu mbooloo yi. — 2 Korent 8:13-15.
Dañu leen di fajal seeni soxla. Bu musiba amee ci béréb, magi mbooloo ya fa nekk dañuy seet ku nekk ci waa mbooloo mi ba xam ndax ñépp a mucc. Lée-lée dafay am kurélu ñiy dimbali buy def lépp ba nit ñi jot lu ñuy lekk ak ndox bu ñu mën a naan ak ay yére, am fu ñuy fanaan te mën a faju. Am na itam ay seede Yexowa yu bare yuy jël ci seen alal te demal seen bopp ca béréb yooyu. Dañuy bokk ci ndimbal boobu walla ci defaraat kër ak saalu Nguur yi yàqu. Li ñu may ñu mën a def loolu yépp ci ni mu gën a gaawe mooy juboo bi ñu am ci suñu biir ak tàmm a ànd di liggéey. Dëgg la, dañuy dimbali sunuy mbokk ci gëm waaye saa yu ñu ko mënee dañuy dimbali itam ñeneen ñi, ak diine bu ñu mënta bokk. — Galasi 6:10.
Dañuy dëfal seen xol ak Mbind mu sell mi. Ñi musiba dal, dañu soxla lool ñu dëfal seen xol. Ci waxtu yu mel noonu, ki ñuy may doole mooy Yexowa miy “ Boroom lépp luy dëfal xol yi ” (2 Korent 1:3, 4). Dañuy sawar a won ñi nekk ci tiis dige yi nekk ci Biibël bi. Won leen itam ne ci kanam tuuti Nguuru Yàlla dina fi dindi bépp metit ak naqar te musiba dootul am. — Peeñu ma 21:4.
Lan moo may seede Yexowa yi ñu gaaw a mën a dimbali seeni mbokk ci ngëm bu musiba amee ?
Ak lan lañu mën a dëfal xolu ñi musiba dal ?