TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • lmd lesoŋ 1
  • Wonal nit ñi ne am nga itte ci ñoom

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Wonal nit ñi ne am nga itte ci ñoom
  • Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ni ko Yeesu defe
  • Ban njàngale lañu mën a jële ci li Yeesu def?
  • Nanga roy ci Yeesu
  • Waxal mel ni kuy waxtaan
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Woneel mbaax
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
lmd lesoŋ 1

NI NGA MËNEE TÀMBALI WAXTAAN

Yeesu a ngi wax ak jigéen ju dëkkoon Samari, ci wetu teen.

Yowaana 4:6-9

LESOŊ 1

Wonal nit ñi ne am nga itte ci ñoom

Njàngale bi: «Ku bëgg . . . du wut njariñu boppam.»—1 Korent 13:​4, 5.

Ni ko Yeesu defe

Yeesu a ngi wax ak jigéen ju dëkkoon Samari, ci wetu teen.

Turu WIDEO bi: Yeesu ak jigéen ju dëkkoon Samari, ci wetu teen

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Yowaana 4:​6-9. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1. Lan la Yeesu seetlu woon ci jigéen ju dëkkoon Samari bala muy wax ak moom?

  2. Yeesu dafa ko waxoon ne: «May ma ndox, ma naan» Lu tax loolu nekk fasoŋ bi gën ngir tàmbali waxtaan ak moom?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Yeesu def?

2. Bu ñu njëkke wax nit ki li koo itteel dina ñu am waxtaan bu neex ak moom.

Nanga roy ci Yeesu

3. Tànnal waxtaan bu itteel nit ki. Bul wut a wax rekk li nga waajaloon. Njëkkal a wax ci li itteel nit ñi. Laajal sa bopp lii:

  1. «Yan xibaar lañu dégg fan yi?»

  2. «Ci lan la sa dëkkandoo yi, ñi nga bokkal liggéey, walla ñi nga bokkal kalaas di wax fan yi?»

4. Deel seetlu. Laajal sa bopp lii:

  1. «Lan la nit ki nekk di def? Lan moo war a nekk ci xelam fu mu nekk nii?»

  2. «Li nit ki sol ak ni këram mel, lan la ma mën a jàngal ci diineem walla ci aadam ?»

  3. «Ndax wax ak moom ci waxtu bii, mooy li gën ci moom, walla dama war a xar ba beneen yoon?»

5. Farlul ci déglu.

  1. Bul faral di wax lu bare.

  2. Mayal nit ki mu wax li mu xalaat. Laaj ko ay laaj ba mu amal boppam tontu bi.

SEETAL AAYA YII ITAM

Macë 7:12; 1 Korent 9:​20-23; Filib 2:4; Saag 1:19

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager